Text view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Ci Kaw Gaambi ak Penku Senegaal ay nguur yu bari toftaloo nañu ci dexug Gaambi gi, yi ci ëpp solo ñooy Ñaani ak Wuli. Ñoom nag ñu ngi leen taxawal ci xarnub fukk ak ñeent g.j. Ay way gàddaay yu bàyyikoo ca Imbratóor gu Mali gaa leen taxawaloon. Yii nguur nag ci ron waawug Jolof gu mag gi lañu nekkoon, ba kero ñuy nanguwaat seenug temb ci xarnub fukk ak juróom benn g.j. Nguur yii nag bokkoon nañu ci joqalanteg yaxantu gi ci anam gu sawar. Looloo taxoon ñuy réew yu naat.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees