s-402
| Abdu dina ma déglu, dina ma jàng, dina ma gis. |
s-403
| Umpalewul ne Njaga Mbay mu ngi ci réew mi. |
s-404
| Ku réew yépp war a soxla, war nga mën a soxla sa réew. |
s-405
| Jawriñ ji yore caada gi di Abdulaay Elimaan Kan, fan yii rekk gis naa ko, war nañoo gisewaat ci fan yii. |
s-406
| Sëriñ Abdu Asiis Si dama koo bëgg. |
s-407
| Di ñaan Yàlla yeene bi mu amoon ci bani aadama yi ci kow suuf, Yàlla defal ko ko mu di mbégtéem ci biir suuf. |
s-408
| Ku baax la; |
s-409
| Tey wéetal na askan wi. |
s-410
| Maa ngi koy jaale waa kër Seexu Umar, waa kër Momar Anta Sali ak kilifaay diine yépp: Laayeen, Ñaseen, Njaasaan, Cenaba, ak fépp fu jullit yi féete. |
s-411
| Ndax du naqar weet rekk la! |
s-412
| Képp ku baax ba seeti sa xarit bi nga gën a fonk ñee la rekk a war! |
s-413
| Yàlla na suuf sedd ci kawam te eggali sunu yeene ci kow suuf. |
s-414
| Mebét maa ngi xaar laata may génnéewaat leneen, ndax ku lekk ak ñaari loxo gaw a suur. |
s-415
| Te war na boo nekkee ci géew, ba mu yàgg, nga demaat ca làng ga, ngir jàngaat. |
s-416
| Man woy, bu ma dee fàttaliku, maa ngi ko tàmbalee def bi ma nekkee xale. |
s-417
| Bi may raam, sama pàppa, dafa amoon benn xaritu «seef de kanton» bu nuy wax Seex Njaay. |
s-418
| Bu ngoonaan bu ñu dikkee ca kër ga, di xawaare may raam nag di fëxle xalam yi ag di woyantu; |
s-419
| Su ko defee ñu daldi may jël tërali. |
s-420
| Ma màgge noonu, màgge noonu ba ba may dugg lekkool. |
s-421
| Ca lekkool ba itam, ci jamono yi fa Fay Waali doonoon jàngalekat, Rosiñool lañu ma doon woowee. |
s-422
| Booba Iba Deer Caam mii tey, moom ak Seneraal Waali Fay jàngaloon nañu ma. |
s-423
| Nàqar, tiis ak metit |
s-424
| Réewum Senegaal tollu na diggante bu xat te mooy diggante dund ak dee gannaaw ba kuréel gi waroon a saytu sàrti-réew mi feeñalee parparloom ne ki ñépp di mbàmb, neex nàqari dafay bokk. |
s-425
| Li ñépp yaakaaroon ne dinañu takk seen fit, def ni seen natangoo ya ca Maali gii mbaa Niseer defoon tas na! |
s-426
| Wante Yàlla ak askani Senegaal dina leen àtte ci lu wér, ndax seen i maas a nga 'La Haye' cóowu àddina sépp topp leen! |
s-427
| Nàqaru-xol dëgg lañu ame téy bi ñu gisee ni Ablaay Wàdd ak ñi ko wër jóge di dal ci kow askan wi, genne seen sox di fétal ak a réy ay xale, ay jiggéen ag ay màggat yu yorewul benn ngannaay bu dul seen fit, seen jom ak seen ngor! |
s-428
| Ablaay Wádd moo toroxal askanu Senegaal mi ko teral, mi ko yëkkati woon, teg ko fu mu masul a teg kenn daanaaka, dénkk ko ëllëgam ak ëllëgi doomam, dénkk ko lépp li ko tax a beew ba def boppam Yálla di faat ay bakkan! |
s-429
| Askani Senegaal askan wu Yàlla màggal la, askani nit ñu am ngor lañu, am teraanga, gëm Yàlla. |
s-430
| Képp ku tuur deretam Yàlla dina la sànkk saayiir ak baatin! |
s-431
| Kenn mënu ci dara! |
s-432
| Ñépp xamoon nañu ne Ablaay Wàdd kilifaag mbëtt la: |
s-433
| Soo toppee ci ginnaawam mu ne 'bul dëgg sama geen'. |
s-434
| Nga tollook moom mu ne 'danga maa bëgg a yab'. |
s-435
| Soo ko jiitoo, mu ne 'toppal sama naaj'. |
s-436
| Wante téy weesu na foofu, gaynde-sibi gu tëx, xiif yàpp la ba naan askan wi 'Yeena ngi may xeeñ i seel'! |
s-437
| Te ñun de askani Senegaal, xamuñu lu dul cere ak soow! |
s-438
| Li ko waroon moo doon lekk ci ndab li ñu ko jox joxin wu rafete rafet bu àddina sépp bàkk, ubb ko ba mu jekk woo keneen! |
s-439
| Wante lekk ba noppi xëpp ci suuf loolu la faye askani Senegaal! |
s-440
| Laam-laame nag weesu na, artu itam wéy na! |
s-441
| Lenn rekk a dés, ci képp ku yore kàddu, nga wax dëgg! |
s-442
| Lu dul dëgg du yàgg te jenn dëgg rekk la: Na Ablaay Wàdd dem! |
s-443
| Menn ab picc mënul a yàq am réew! |
s-444
| Moom ak doomam la ak seeni dag ak réewum lëmm, mu beggul lu dul tedd, dund ci teraanga, tedd ag jaamu-Yàlla! |
s-445
| Wante gudd nopp taxul a dégg, nde kon kenn du door mbaam te nag mujju mbaam ay tan, buuru buuri kasaara yi! |
s-446
| Xeex bëtt-bëttu wasin |
s-447
| Ngir xeex bëtt-bëttu wasin «fistule obstétrique» dafa laaj kilifa yi amal aw tëralin wu matale, daj réew mépp loolu la Profesëer Magéy Géy xalaat, njiital bànqaas bi màcc ci mbirum awra ak sawukaay, ci oppitaalu Grã Yoof. |
s-448
| APS 25 ut 2009 |
s-449
| Amal aw tëralin wu ànd ak ay jumtukaay yu ñu ko doxale |
s-450
| Tëralin woowu, su ñu ko doxalee ni mu ware, mën naa tax ñu daan ci juróomi at yi di ñëw (2010 - 2015), musiba mu réy moomu, nga xam ne jigéen ñu bare yàq na seen àddina, te dara waralu ko, lu moy ñàkk ku leen taxawu. |
s-451
| Li ci am solo moo di tasaare fajukaay yi, ak ndawi kër doktoor yi, ak jumtukaay yi ci biir gox yi, jigéen ñi mën ci a dem ci lu àndul ak benn gàllankoor. |
s-452
| Bëtt-bëttu wasin lu koy indi? |
s-453
| Bëtt-bëttu wasin «fistule obstétrique», bëtt-bëtt la bu ubbiku diggante paftan mi nga xam ne mooy denc saw mi ak awra jigéen ji. |
s-454
| Bëtt-bëttu wasin, li koy yóbbe jigéen mooy ñàkk ku ko taxawu ba mu ëmbee, ñàkk yit ku ko taxawu ba muy wasin. |
s-455
| Jàngoro jaa ngi di sababoo ci mat gu yàgg te metti. |
s-456
| Baagante bi doom ji di baagante ci biiru ndey ji, diggante paftan mi ak yaxu ndigg li, ngir bëgg a génn, mu të, am na lu mu di yàq diggante paftan mi ak awra ndey ji, ndax béréb bi mu di dal, dafa di def ab góom. |
s-457
| Bu doom ji génnee, góom boobu, bu demee ba wow ba def aw àkk, dafa di mujj rot, su ko defee mu bàyyi ab bëtt-bëtt bu saw mi di jaar, di sotteeku ci awra ji. |
s-458
| Saw moomu nag dara dootu ko mën a téye, saa su ne dafa di sotteeku, su ko defee nit ki fu mu tollu dafa di tooy, xetu saw mi topp ko fu ne, àddinaam yàqu. |
s-459
| Yan pexe ñoo gën a baax ci wàllu fagaru ak paj? |
s-460
| Pexe mi jiitu ci wàllu fagaru mooy samp ay fajukaay yu daj réew mi, boole ci nit ñi mën a jot ci paj mi. |
s-461
| Dafa laaj ndawal kër doktoor bu am xam-xam taxawu jigéen ji ëmb ak jigéen ji di wasin. |
s-462
| Wasinu kër moom lu mat a bàyyi la. |
s-463
| Nan lañu koy faje? |
s-464
| Ngir faj ko, fàww ñu oppeere ko, téere yi ak yeneen xeeti njabar yi mënuñu ci dara. |
s-465
| Aji-tekki ji: Soxna Aram Faal |
s-466
| Osad a leen baaxe dénkaane yii ci suuf, tibbe leen ci téere bi mu siiwal tudde ko: Ëmbub jàmm, Osad, 1994 |
s-467
| Yow, jigéenu-wérul bi: Deel seeti ndawal kër doktoor diirub ëmb bi; |
s-468
| Dina def li war ci yow, teg la ci yoon; |
s-469
| Bu Yàlla defee ba nga di matu, demal ci ab fajukaay, ndawal kër doktoor taxawu la; |
s-470
| Dina la toppatoo, toppatoo sa doom, xamal la li nga war a def gannaaw wasin gi. |