Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

Showing 401 - 500 of 470 • previous

s-401 Abdu Juuf digoon na ma kër, waaye booba ba tey am na at, te gisuma dara.
s-402 Abdu dina ma déglu, dina ma jàng, dina ma gis.
s-403 Umpalewul ne Njaga Mbay mu ngi ci réew mi.
s-404 Ku réew yépp war a soxla, war nga mën a soxla sa réew.
s-405 Jawriñ ji yore caada gi di Abdulaay Elimaan Kan, fan yii rekk gis naa ko, war nañoo gisewaat ci fan yii.
s-406 Sëriñ Abdu Asiis Si dama koo bëgg.
s-407 Di ñaan Yàlla yeene bi mu amoon ci bani aadama yi ci kow suuf, Yàlla defal ko ko mu di mbégtéem ci biir suuf.
s-408 Ku baax la;
s-409 Tey wéetal na askan wi.
s-410 Maa ngi koy jaale waa kër Seexu Umar, waa kër Momar Anta Sali ak kilifaay diine yépp: Laayeen, Ñaseen, Njaasaan, Cenaba, ak fépp fu jullit yi féete.
s-411 Ndax du naqar weet rekk la!
s-412 Képp ku baax ba seeti sa xarit bi nga gën a fonk ñee la rekk a war!
s-413 Yàlla na suuf sedd ci kawam te eggali sunu yeene ci kow suuf.
s-414 Mebét maa ngi xaar laata may génnéewaat leneen, ndax ku lekk ak ñaari loxo gaw a suur.
s-415 Te war na boo nekkee ci géew, ba mu yàgg, nga demaat ca làng ga, ngir jàngaat.
s-416 Man woy, bu ma dee fàttaliku, maa ngi ko tàmbalee def bi ma nekkee xale.
s-417 Bi may raam, sama pàppa, dafa amoon benn xaritu «seef de kanton» bu nuy wax Seex Njaay.
s-418 Bu ngoonaan bu ñu dikkee ca kër ga, di xawaare may raam nag di fëxle xalam yi ag di woyantu;
s-419 Su ko defee ñu daldi may jël tërali.
s-420 Ma màgge noonu, màgge noonu ba ba may dugg lekkool.
s-421 Ca lekkool ba itam, ci jamono yi fa Fay Waali doonoon jàngalekat, Rosiñool lañu ma doon woowee.
s-422 Booba Iba Deer Caam mii tey, moom ak Seneraal Waali Fay jàngaloon nañu ma.
s-423 Nàqar, tiis ak metit
s-424 Réewum Senegaal tollu na diggante bu xat te mooy diggante dund ak dee gannaaw ba kuréel gi waroon a saytu sàrti-réew mi feeñalee parparloom ne ki ñépp di mbàmb, neex nàqari dafay bokk.
s-425 Li ñépp yaakaaroon ne dinañu takk seen fit, def ni seen natangoo ya ca Maali gii mbaa Niseer defoon tas na!
s-426 Wante Yàlla ak askani Senegaal dina leen àtte ci lu wér, ndax seen i maas a nga 'La Haye' cóowu àddina sépp topp leen!
s-427 Nàqaru-xol dëgg lañu ame téy bi ñu gisee ni Ablaay Wàdd ak ñi ko wër jóge di dal ci kow askan wi, genne seen sox di fétal ak a réy ay xale, ay jiggéen ag ay màggat yu yorewul benn ngannaay bu dul seen fit, seen jom ak seen ngor!
s-428 Ablaay Wádd moo toroxal askanu Senegaal mi ko teral, mi ko yëkkati woon, teg ko fu mu masul a teg kenn daanaaka, dénkk ko ëllëgam ak ëllëgi doomam, dénkk ko lépp li ko tax a beew ba def boppam Yálla di faat ay bakkan!
s-429 Askani Senegaal askan wu Yàlla màggal la, askani nit ñu am ngor lañu, am teraanga, gëm Yàlla.
s-430 Képp ku tuur deretam Yàlla dina la sànkk saayiir ak baatin!
s-431 Kenn mënu ci dara!
s-432 Ñépp xamoon nañu ne Ablaay Wàdd kilifaag mbëtt la:
s-433 Soo toppee ci ginnaawam mu ne 'bul dëgg sama geen'.
s-434 Nga tollook moom mu ne 'danga maa bëgg a yab'.
s-435 Soo ko jiitoo, mu ne 'toppal sama naaj'.
s-436 Wante téy weesu na foofu, gaynde-sibi gu tëx, xiif yàpp la ba naan askan wi 'Yeena ngi may xeeñ i seel'!
s-437 Te ñun de askani Senegaal, xamuñu lu dul cere ak soow!
s-438 Li ko waroon moo doon lekk ci ndab li ñu ko jox joxin wu rafete rafet bu àddina sépp bàkk, ubb ko ba mu jekk woo keneen!
s-439 Wante lekk ba noppi xëpp ci suuf loolu la faye askani Senegaal!
s-440 Laam-laame nag weesu na, artu itam wéy na!
s-441 Lenn rekk a dés, ci képp ku yore kàddu, nga wax dëgg!
s-442 Lu dul dëgg du yàgg te jenn dëgg rekk la: Na Ablaay Wàdd dem!
s-443 Menn ab picc mënul a yàq am réew!
s-444 Moom ak doomam la ak seeni dag ak réewum lëmm, mu beggul lu dul tedd, dund ci teraanga, tedd ag jaamu-Yàlla!
s-445 Wante gudd nopp taxul a dégg, nde kon kenn du door mbaam te nag mujju mbaam ay tan, buuru buuri kasaara yi!
s-446 Xeex bëtt-bëttu wasin
s-447 Ngir xeex bëtt-bëttu wasin «fistule obstétrique» dafa laaj kilifa yi amal aw tëralin wu matale, daj réew mépp loolu la Profesëer Magéy Géy xalaat, njiital bànqaas bi màcc ci mbirum awra ak sawukaay, ci oppitaalu Grã Yoof.
s-448 APS 25 ut 2009
s-449 Amal aw tëralin wu ànd ak ay jumtukaay yu ñu ko doxale
s-450 Tëralin woowu, su ñu ko doxalee ni mu ware, mën naa tax ñu daan ci juróomi at yi di ñëw (2010 - 2015), musiba mu réy moomu, nga xam ne jigéen ñu bare yàq na seen àddina, te dara waralu ko, lu moy ñàkk ku leen taxawu.
s-451 Li ci am solo moo di tasaare fajukaay yi, ak ndawi kër doktoor yi, ak jumtukaay yi ci biir gox yi, jigéen ñi mën ci a dem ci lu àndul ak benn gàllankoor.
s-452 Bëtt-bëttu wasin lu koy indi?
s-453 Bëtt-bëttu wasin «fistule obstétrique», bëtt-bëtt la bu ubbiku diggante paftan mi nga xam ne mooy denc saw mi ak awra jigéen ji.
s-454 Bëtt-bëttu wasin, li koy yóbbe jigéen mooy ñàkk ku ko taxawu ba mu ëmbee, ñàkk yit ku ko taxawu ba muy wasin.
s-455 Jàngoro jaa ngi di sababoo ci mat gu yàgg te metti.
s-456 Baagante bi doom ji di baagante ci biiru ndey ji, diggante paftan mi ak yaxu ndigg li, ngir bëgg a génn, mu , am na lu mu di yàq diggante paftan mi ak awra ndey ji, ndax béréb bi mu di dal, dafa di def ab góom.
s-457 Bu doom ji génnee, góom boobu, bu demee ba wow ba def aw àkk, dafa di mujj rot, su ko defee mu bàyyi ab bëtt-bëtt bu saw mi di jaar, di sotteeku ci awra ji.
s-458 Saw moomu nag dara dootu ko mën a téye, saa su ne dafa di sotteeku, su ko defee nit ki fu mu tollu dafa di tooy, xetu saw mi topp ko fu ne, àddinaam yàqu.
s-459 Yan pexe ñoo gën a baax ci wàllu fagaru ak paj?
s-460 Pexe mi jiitu ci wàllu fagaru mooy samp ay fajukaay yu daj réew mi, boole ci nit ñi mën a jot ci paj mi.
s-461 Dafa laaj ndawal kër doktoor bu am xam-xam taxawu jigéen ji ëmb ak jigéen ji di wasin.
s-462 Wasinu kër moom lu mat a bàyyi la.
s-463 Nan lañu koy faje?
s-464 Ngir faj ko, fàww ñu oppeere ko, téere yi ak yeneen xeeti njabar yi mënuñu ci dara.
s-465 Aji-tekki ji: Soxna Aram Faal
s-466 Osad a leen baaxe dénkaane yii ci suuf, tibbe leen ci téere bi mu siiwal tudde ko: Ëmbub jàmm, Osad, 1994
s-467 Yow, jigéenu-wérul bi: Deel seeti ndawal kër doktoor diirub ëmb bi;
s-468 Dina def li war ci yow, teg la ci yoon;
s-469 Bu Yàlla defee ba nga di matu, demal ci ab fajukaay, ndawal kër doktoor taxawu la;
s-470 Dina la toppatoo, toppatoo sa doom, xamal la li nga war a def gannaaw wasin gi.

Text viewDownload CoNNL-U