Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

Showing 302 - 401 of 470 • previousnext

s-302 Li jaaxal nit ñi mooy nan la askan wi, rawatina kilifa diine Lislaam nar a doxale?
s-303 Ndax dinañu teeweeji tudd ba am déed?
s-304 Ndax it kilifa yeneen réew yi ñu wóo dinañu ñëw am dañuy gàntu?
s-305 Kon mbir maa ngi noonu: cóow li bare na, xel yi ag xalaat yaa ngi joŋante!
s-306 Su dee seetaan a daq cib ndajee kon lay ñëw ca kanam a war a gën a neex!
s-307 Kopparu CFA ak Ëro ñoo xoj Afrik!
s-308 Nicolas Agbohou jàngalekat la ci fànnu koom-koom ci daara yu mag ya ca Tugal, cosaanoo Kodiwaar.
s-309 Ci laaj-toontu bii ñu leen fi tekkil dafay ηàññ doxalinu réewi Afrik yiy jëfandiku kopparu CFA.
s-310 Nee na kopparu Ëro ag bu CFA, ñooy ñaari yëf yi tax ba réewi Afrik yi feete làng googu.
s-311 Mënuñoo génn ci ag ndóol feek wutuñu seen xaalisu bopp.
s-312 Afirik: Sa téere bi, kalaame bu meti la, boo di kalaame kopparu Euro ak CFA.
s-313 Nga ne kon koppar yooyu ñooy lor Afrik?
s-314 Nicolas Agbohou: Ci lu wér, ndax kuréli koom-koom yi di saytu kopparu CFA, moo xam ay bànk yu mag lañu, walla yeneen, bëgguñu benn yoon réewi Afrik yooyu am yokkute...
s-315 Boo seetee ci ñi jiite kurél yooyu, naka «conseils d'administration», bu BCEAO, bànk bu mag bi nekk Ndakaaru, BCEAC walla bànku réewum Komóor, ay doomi Faraas ñoo fay dogal.
s-316 Dañu faa am sax sañ-sañu tere lépp lu dëppoowul ak li leen sóob, maanaam dañu faa am «droit de véto» ci Nasaraan.
s-317 Kóomóor naka noonu, ndax ci seen bànk bu mag ba ñeenti doomi Faraas ak ñeenti doomi Komóor a fa nekk.
s-318 Ndeem nag foofee, bépp dogal bu ñu fa war a jël alafokk, juróomi nit ànd ca, kon su benn doomi Faraas àndul ca loola, dogal booba du mën a àntu.
s-319 «Africains» yi waruñoo fàtte ni CFA kopparu Faraas la.
s-320 Afrik: Wante bu loolu weesoo, lu tax nga ni CFA njataη la ci Arik?
s-321 Nicolas Agbohou: Li tax mooy lii: dafa jot «Africains» yi am sañ-sañu doxal seen politiki bopp ci wàllu xaalis, politik bu dëppoo ak seen yakaar.
s-322 Seetal ni, 15 réew yi bokk ci CFA yépp, at mu jot, soo jëlee li ñuy jaay bitim-réew, 100 dolaar yu nekk dañu cay dindi 65 dugal bànku Faraas, ñu ne ngir garanti kopaaru CFA.
s-323 Seetal loolu!
s-324 Réew mu mel ni Niseer, su jaayee lu tollu ak 1 miliyaar ci dolaar, 650 Miliyon ya ñu nga des bànku Faraas, fekk Niseer ci boppam du am sax lu mu faye ay liggéeykatam.
s-325 Lii xel mënu koo nangu!
s-326 Bàyyi koppar yu ni tollu réewu jambur, sa réew nit ña di dee ak xiif...
s-327 Kopparu CFA daal dafay gën a yokk ndóol gi, dëkkee nu ci nooteel gu amul àpp...
s-328 Afrik: Lu tax nag Ëro bi moom du njëriñ ci réewi CFA yi?
s-329 Nicolas Agbohou: Lu jiitu ñuy yeew CFA bi ci Ëro, Faraas rekk a daan lëñtu sunu koom-koom yi, léegi nag Ërop gépp am kàddu ak sañ-sañ ci nun.
s-330 Li yees, mooy natt yu tar yi nu 'Bruxelles' teg ànduñu ak sunuy namm-namm.
s-331 Warees na kon ñu tàggook CFA bi ci ni mu gën a gaawe!
s-332 Lu ñu fay teg su ñu teggee CFA bi?
s-333 Nicolas Agbohou: Amul benn réew bu mën a jëm ca kanam te moomul doxalinam ci wàllu xaalis.
s-334 Li ñu soxla mooy xaalis bu bees bu ñu moomal sunu bopp, bu ñu bokk.
s-335 Sàrt yi di doxal CFA bi dañu leen war a sànni ca mballit ma.
s-336 Laaj-toontu ak Njaga Mbay
s-337 Jaar-jaaru woykat bu jege woon askanam
s-338 Ci Sanwiye 1999, yeneekay Lasli/Njëlbéen amoon na laaj-tontu bu yaatu ag Njaga Mbay, doon ca feeñal ay jaar-jaaram.
s-339 Waxtaan woowu Njaga Mbay amoon ak Séydu Nuuru Njaay, di njiital Lasli/Njëlbéen, moom lañu leen fi indilaat, di ci ñeel woykat bu mag bu àddina sépp jooy.
s-340 Kan mooy Njaga Mbay?
s-341 Njaga jooju nga tudd, ñu ngi ma tuddee genn góor gu tudd Njaga Mbeng, nekkoon jaaykat bu mag di woon itam aalim.
s-342 May doomu góor gu ñuy wax Ngóor Mbay, ñu koy woowee Abdu Faatma ca Cilmaxa, ak jiggéen ju ñuy wax Kumba Ndaxaar Sàll.
s-343 Ngóor Mbay nag dafa daan xalam, Kumba Ndaxaar moo yore woon kër gi.
s-344 Maa ngi judd ci 1948 ci Taatagin ca diiwaanu Siin-Saalum;
s-345 Booba jamono ay arondismaa amagul.
s-346 Fa laa jàngee sama njàng mu njëkk ci tubaab, ba Yàlla def ci 1962, ma jóge fa dem Fatig di yokki sama njàng ci «CEG» ba fa nekk.
s-347 Ci ñi njëkk a jàng ci «CEG» ci laa bokk.
s-348 Ci 1965, ginaaw ñetti at ci daara ju dig-dóomu jooju, ma bàyyi dem nekki benewol ca rondismaa Taatagin.
s-349 Foofu laa duggee làrme ci 1966.
s-350 Ci xumbte yi doon tëj sunu jàngum militeer man ak ñoom Mbeng Mbay Maa Daawur, Siidi Buya Njaay booba liyetnaa la woon, ñoo xumbal ngoonal gi.
s-351 Bi ñu paree ñu indi nu Dakaar;
s-352 Booba Cerno Ba, mu ngi woon ca jawriñ ji ñu dénk gi Caada gi.
s-353 Moom moo gis Sonaar Seŋoor ne ko gis naa xale boo xam ne, boo leen ko jëlee dina leen amal solo lool.
s-354 Booba 1967 la woon, maa ngi woon «Marin»;
s-355 Bi may dem ñu may dégglu ca Soraano, booba yere «Marin» laa soloon.
s-356 Ma dem ñu déglu ma.
s-357 Bés ba ma delluwaatee Soraano ngir nemmeeku la ma fa defoon, ñu ne ma foo nekkoon?
s-358 Ñëwal liggéeysi.
s-359 Noonu laa duggee Soraano.
s-360 Am naa ñetti soxna ak ay doom.
s-361 Aal Pulaaren yi ñu ngi may njukkal.
s-362 Am na ay gëstukat yu mel ni Amiidu Ja, yu bind ci man ay téere ak itam Ibrahima Wan, doon def ab gëstu ci njàngam ca Daara ju mag ja ci man, ak ñoom Samba Jabare ak Yusu Nduur.
s-363 Baaba Maal moom itam moom bañ na ko ba balaa bég, su nee cépp Podoor ma dikk fa.
s-364 Ku dikk mu ne ko kii mooy sunu xalifa, mooy sunu mag, mooy sunu lépp.
s-365 Xam nga kon mënumaa wax ci lenn di wone sama bopp te wonewuma sama bopp jarale ko ci njabootu Aal-Pulaar yi.
s-366 Maa ngi sargal itam Seex Aamidu Kan.
s-367 Maa ngi ci sama ñeenteeli kaset.
s-368 Booba xalaatuma woon defarlu kaset.
s-369 Sama kaset bu njëkk mu ngi tudd «Dans le vent».
s-370 Bi ci topp maa ngi ko tuddee «ndaanaani réew mi».
s-371 Bi ci topp maa ngi ko tudde «nanu muñ».
s-372 Bi ci topp moo di bi mujj, maa ngi ko tudde «Njaga plus».
s-373 Ndax damaa fas yeenee wettali xale yi, moo tax ma ne Njaga ak as lëf, Njaga ak leneen.
s-374 Misiku kaset moo deme noonu.
s-375 Li jëm ci woy wi Yusu Nduur woy tudde ko «Buleen kuppe», xam naa ne ñiy kuppe xam nañu sekere bi ci biir woy bi.
s-376 Ndax ki ñu waxoon ne moo koy kuppe ba ñu ko deñcee ba négëni sii, yëf yaa ngi wéy di kuppe.
s-377 Xéy na Yusu dafa njëkk a wax nit ñi, waaye ku fekke am na ci kàddu.
s-378 Lii dañu koo fekk ci jamono, te man samay woy damaa bëgg muy doon luy wéy.
s-379 Lii kuppeeg tey la rekk ak tàkku ëllëg.
s-380 Yëfi jamono la rekk.
s-381 Man nag, samay woy dama ci bëgg di woy lu nga xam ne luy wéy la ba pare tey jii itam ma ciy woy luy wéy ëllëg.
s-382 Woy lu wéyoon démb, ngir fattali nit ñi.
s-383 Woy itam luy wéy ëllëg lu mën a jàngale la.
s-384 Njiinu réew mi bu ñu ci jàppul bu baax dina réeri.
s-385 Amoon nañu ci tiit ci jamono jee weesu waaye tey ñu ngi dikk, di jéem a saxal ndax ci seeni woy ñu ngi ciy wax ay kàddug Wolof.
s-386 Ñu ngi ciy woy di ci boole ay tama ag ndënd, di ci boole li ñu moom.
s-387 Ñakkaguñu.
s-388 Jàng ak bind ci làmmiñi réew mi?
s-389 Lu am solo la!
s-390 Jiggéen ju masul jàng tubaab mën na tey bindal boppam ci làmmiñam.
s-391 Moo tax Yàlla di gën barkeel seen liggéey!
s-392 Na ku nekk jàpp ci li nu moom mën caa lijjanti li mu soxla.
s-393 Wolof ak Pulaar lépp a ci yem, loo ci woyofal mu wéy.
s-394 Lasli/Njëlbéen liggéeyam rafet na!
s-395 Njiitam Séydu Nuura Njaay woyof na!
s-396 Abdu Juuf sama digaale ak woykat yi, digaale bu rafet la.
s-397 Dinaay seeti Coon, Yusu, Baaba.
s-398 Baaba moom sama lépp la.
s-399 Abdu Juuf dama koo waxoon ne: yaa di baayu nasiyoŋ bi, kon yaa war a yore sama «sold».
s-400 Politiguma ni ko nitu politik yi di defe waaye damay dindi lépp luy xiiroo te loolu ndimmbal la.
s-401 Abdu Juuf digoon na ma kër, waaye booba ba tey am na at, te gisuma dara.

Text viewDownload CoNNL-U