s-301
| Ci bésu 04 Awril 2010, temboo ak 50eelu at ba Senegaal moomee boppam ba léegi, lees ko war a ngente. |
s-302
| Li jaaxal nit ñi mooy nan la askan wi, rawatina kilifa diine Lislaam nar a doxale? |
s-303
| Ndax dinañu teeweeji tudd ba am déed? |
s-304
| Ndax it kilifa yeneen réew yi ñu wóo dinañu ñëw am dañuy gàntu? |
s-305
| Kon mbir maa ngi noonu: cóow li bare na, xel yi ag xalaat yaa ngi joŋante! |
s-306
| Su dee seetaan a daq cib ndajee kon lay ñëw ca kanam a war a gën a neex! |
s-307
| Kopparu CFA ak Ëro ñoo xoj Afrik! |
s-308
| Nicolas Agbohou jàngalekat la ci fànnu koom-koom ci daara yu mag ya ca Tugal, cosaanoo Kodiwaar. |
s-309
| Ci laaj-toontu bii ñu leen fi tekkil dafay ηàññ doxalinu réewi Afrik yiy jëfandiku kopparu CFA. |
s-310
| Nee na kopparu Ëro ag bu CFA, ñooy ñaari yëf yi tax ba réewi Afrik yi feete làng googu. |
s-311
| Mënuñoo génn ci ag ndóol feek wutuñu seen xaalisu bopp. |
s-312
| Afirik: Sa téere bi, kalaame bu meti la, boo di kalaame kopparu Euro ak CFA. |
s-313
| Nga ne kon koppar yooyu ñooy lor Afrik? |
s-314
| Nicolas Agbohou: Ci lu wér, ndax kuréli koom-koom yi di saytu kopparu CFA, moo xam ay bànk yu mag lañu, walla yeneen, bëgguñu benn yoon réewi Afrik yooyu am yokkute... |
s-315
| Boo seetee ci ñi jiite kurél yooyu, naka «conseils d'administration», bu BCEAO, bànk bu mag bi nekk Ndakaaru, BCEAC walla bànku réewum Komóor, ay doomi Faraas ñoo fay dogal. |
s-316
| Dañu faa am sax sañ-sañu tere lépp lu dëppoowul ak li leen sóob, maanaam dañu faa am «droit de véto» ci Nasaraan. |
s-317
| Kóomóor naka noonu, ndax ci seen bànk bu mag ba ñeenti doomi Faraas ak ñeenti doomi Komóor a fa nekk. |
s-318
| Ndeem nag foofee, bépp dogal bu ñu fa war a jël alafokk, juróomi nit ànd ca, kon su benn doomi Faraas àndul ca loola, dogal booba du mën a àntu. |
s-319
| «Africains» yi waruñoo fàtte ni CFA kopparu Faraas la. |
s-320
| Afrik: Wante bu loolu weesoo, lu tax nga ni CFA njataη la ci Arik? |
s-321
| Nicolas Agbohou: Li tax mooy lii: dafa jot «Africains» yi am sañ-sañu doxal seen politiki bopp ci wàllu xaalis, politik bu dëppoo ak seen yakaar. |
s-322
| Seetal ni, 15 réew yi bokk ci CFA yépp, at mu jot, soo jëlee li ñuy jaay bitim-réew, 100 dolaar yu nekk dañu cay dindi 65 dugal bànku Faraas, ñu ne ngir garanti kopaaru CFA. |
s-323
| Seetal loolu! |
s-324
| Réew mu mel ni Niseer, su jaayee lu tollu ak 1 miliyaar ci dolaar, 650 Miliyon ya ñu nga des bànku Faraas, fekk Niseer ci boppam du am sax lu mu faye ay liggéeykatam. |
s-325
| Lii xel mënu koo nangu! |
s-326
| Bàyyi koppar yu ni tollu réewu jambur, sa réew nit ña di dee ak xiif... |
s-327
| Kopparu CFA daal dafay gën a yokk ndóol gi, dëkkee nu ci nooteel gu amul àpp... |
s-328
| Afrik: Lu tax nag Ëro bi moom du njëriñ ci réewi CFA yi? |
s-329
| Nicolas Agbohou: Lu jiitu ñuy yeew CFA bi ci Ëro, Faraas rekk a daan lëñtu sunu koom-koom yi, léegi nag Ërop gépp am kàddu ak sañ-sañ ci nun. |
s-330
| Li yees, mooy natt yu tar yi nu 'Bruxelles' teg ànduñu ak sunuy namm-namm. |
s-331
| Warees na kon ñu tàggook CFA bi ci ni mu gën a gaawe! |
s-332
| Lu ñu fay teg su ñu teggee CFA bi? |
s-333
| Nicolas Agbohou: Amul benn réew bu mën a jëm ca kanam te moomul doxalinam ci wàllu xaalis. |
s-334
| Li ñu soxla mooy xaalis bu bees bu ñu moomal sunu bopp, bu ñu bokk. |
s-335
| Sàrt yi di doxal CFA bi dañu leen war a sànni ca mballit ma. |
s-336
| Laaj-toontu ak Njaga Mbay |
s-337
| Jaar-jaaru woykat bu jege woon askanam |
s-338
| Ci Sanwiye 1999, yeneekay Lasli/Njëlbéen amoon na laaj-tontu bu yaatu ag Njaga Mbay, doon ca feeñal ay jaar-jaaram. |
s-339
| Waxtaan woowu Njaga Mbay amoon ak Séydu Nuuru Njaay, di njiital Lasli/Njëlbéen, moom lañu leen fi indilaat, di ci ñeel woykat bu mag bu àddina sépp jooy. |
s-340
| Kan mooy Njaga Mbay? |
s-341
| Njaga jooju nga tudd, ñu ngi ma tuddee genn góor gu tudd Njaga Mbeng, nekkoon jaaykat bu mag di woon itam aalim. |
s-342
| May doomu góor gu ñuy wax Ngóor Mbay, ñu koy woowee Abdu Faatma ca Cilmaxa, ak jiggéen ju ñuy wax Kumba Ndaxaar Sàll. |
s-343
| Ngóor Mbay nag dafa daan xalam, Kumba Ndaxaar moo yore woon kër gi. |
s-344
| Maa ngi judd ci 1948 ci Taatagin ca diiwaanu Siin-Saalum; |
s-345
| Booba jamono ay arondismaa amagul. |
s-346
| Fa laa jàngee sama njàng mu njëkk ci tubaab, ba Yàlla def ci 1962, ma jóge fa dem Fatig di yokki sama njàng ci «CEG» ba fa nekk. |
s-347
| Ci ñi njëkk a jàng ci «CEG» ci laa bokk. |
s-348
| Ci 1965, ginaaw ñetti at ci daara ju dig-dóomu jooju, ma bàyyi dem nekki benewol ca rondismaa Taatagin. |
s-349
| Foofu laa duggee làrme ci 1966. |
s-350
| Ci xumbte yi doon tëj sunu jàngum militeer man ak ñoom Mbeng Mbay Maa Daawur, Siidi Buya Njaay booba liyetnaa la woon, ñoo xumbal ngoonal gi. |
s-351
| Bi ñu paree ñu indi nu Dakaar; |
s-352
| Booba Cerno Ba, mu ngi woon ca jawriñ ji ñu dénk gi Caada gi. |
s-353
| Moom moo gis Sonaar Seŋoor ne ko gis naa xale boo xam ne, boo leen ko jëlee dina leen amal solo lool. |
s-354
| Booba 1967 la woon, maa ngi woon «Marin»; |
s-355
| Bi may dem ñu may dégglu ca Soraano, booba yere «Marin» laa soloon. |
s-356
| Ma dem ñu déglu ma. |
s-357
| Bés ba ma delluwaatee Soraano ngir nemmeeku la ma fa defoon, ñu ne ma foo nekkoon? |
s-358
| Ñëwal liggéeysi. |
s-359
| Noonu laa duggee Soraano. |
s-360
| Am naa ñetti soxna ak ay doom. |
s-361
| Aal Pulaaren yi ñu ngi may njukkal. |
s-362
| Am na ay gëstukat yu mel ni Amiidu Ja, yu bind ci man ay téere ak itam Ibrahima Wan, doon def ab gëstu ci njàngam ca Daara ju mag ja ci man, ak ñoom Samba Jabare ak Yusu Nduur. |
s-363
| Baaba Maal moom itam moom bañ na ko ba balaa bég, su nee cépp Podoor ma dikk fa. |
s-364
| Ku dikk mu ne ko kii mooy sunu xalifa, mooy sunu mag, mooy sunu lépp. |
s-365
| Xam nga kon mënumaa wax ci lenn di wone sama bopp te wonewuma sama bopp jarale ko ci njabootu Aal-Pulaar yi. |
s-366
| Maa ngi sargal itam Seex Aamidu Kan. |
s-367
| Maa ngi ci sama ñeenteeli kaset. |
s-368
| Booba xalaatuma woon defarlu kaset. |
s-369
| Sama kaset bu njëkk mu ngi tudd «Dans le vent». |
s-370
| Bi ci topp maa ngi ko tuddee «ndaanaani réew mi». |
s-371
| Bi ci topp maa ngi ko tudde «nanu muñ». |
s-372
| Bi ci topp moo di bi mujj, maa ngi ko tudde «Njaga plus». |
s-373
| Ndax damaa fas yeenee wettali xale yi, moo tax ma ne Njaga ak as lëf, Njaga ak leneen. |
s-374
| Misiku kaset moo deme noonu. |
s-375
| Li jëm ci woy wi Yusu Nduur woy tudde ko «Buleen kuppe», xam naa ne ñiy kuppe xam nañu sekere bi ci biir woy bi. |
s-376
| Ndax ki ñu waxoon ne moo koy kuppe ba ñu ko deñcee ba négëni sii, yëf yaa ngi wéy di kuppe. |
s-377
| Xéy na Yusu dafa njëkk a wax nit ñi, waaye ku fekke am na ci kàddu. |
s-378
| Lii dañu koo fekk ci jamono, te man samay woy damaa bëgg muy doon luy wéy. |
s-379
| Lii kuppeeg tey la rekk ak tàkku ëllëg. |
s-380
| Yëfi jamono la rekk. |
s-381
| Man nag, samay woy dama ci bëgg di woy lu nga xam ne luy wéy la ba pare tey jii itam ma ciy woy luy wéy ëllëg. |
s-382
| Woy lu wéyoon démb, ngir fattali nit ñi. |
s-383
| Woy itam luy wéy ëllëg lu mën a jàngale la. |
s-384
| Njiinu réew mi bu ñu ci jàppul bu baax dina réeri. |
s-385
| Amoon nañu ci tiit ci jamono jee weesu waaye tey ñu ngi dikk, di jéem a saxal ndax ci seeni woy ñu ngi ciy wax ay kàddug Wolof. |
s-386
| Ñu ngi ciy woy di ci boole ay tama ag ndënd, di ci boole li ñu moom. |
s-387
| Ñakkaguñu. |
s-388
| Jàng ak bind ci làmmiñi réew mi? |
s-389
| Lu am solo la! |
s-390
| Jiggéen ju masul jàng tubaab mën na tey bindal boppam ci làmmiñam. |
s-391
| Moo tax Yàlla di gën barkeel seen liggéey! |
s-392
| Na ku nekk jàpp ci li nu moom mën caa lijjanti li mu soxla. |
s-393
| Wolof ak Pulaar lépp a ci yem, loo ci woyofal mu wéy. |
s-394
| Lasli/Njëlbéen liggéeyam rafet na! |
s-395
| Njiitam Séydu Nuura Njaay woyof na! |
s-396
| Abdu Juuf sama digaale ak woykat yi, digaale bu rafet la. |
s-397
| Dinaay seeti Coon, Yusu, Baaba. |
s-398
| Baaba moom sama lépp la. |
s-399
| Abdu Juuf dama koo waxoon ne: yaa di baayu nasiyoŋ bi, kon yaa war a yore sama «sold». |
s-400
| Politiguma ni ko nitu politik yi di defe waaye damay dindi lépp luy xiiroo te loolu ndimmbal la. |