Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

Showing 4 - 103 of 470 • previousnext

s-4 Naka-jekk dafay doon ay téere yu bari.
s-5 Cër yi ëpp solo yi di tax a raññee ab jimbulang, ñeent lañu: Jagleel gi ci am, seenug lëkkaloo, nosiin wi ak mbidiinu jukki yi.
s-6 Jimbulang yi man nañu a wuute, aju ci seen ëmbiit, man nañu a ubbeeku ci xeeti xameef yépp (Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa Brëtaañ, ñoo di yi ci gën a siiw), walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi, niki ab jimbulangu paj, bu xam-xam walla bu xeltu.
s-7 Am na it ay jimbulang yu di jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan, diine walla politig wu wenn askan, walla xeet, niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi, Jimbulangu Jewish bi...
s-8 Yitteey liggéeyi jimbulang moo di jébbal xameef gi ëpp solo gi di dajale ñeel tëriit li.
s-9 Yii liggéey nit yàgg na koo def, dalee lu sori ci taariixam, waaye baatu jimbulang ñu ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu.
s-10 Bépp liggéeyu jimbulang, ci lu leer, ab tënk rekk la ci xameefi nit, te it liggéey bi dafa di soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam.
s-11 Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi; ab jimbulang bi ñuy jagleel i gune mooy gën a néew bi ñuy jagleel i mag.
s-12 Nosiinu jukki yi am na solo lool, ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb, kon gëstu ci dina yomb.
s-13 Ci taariix, ñaari xeeti nosiin lañu di jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi: nosiin gu abajada, jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba, beneen bi moo di séddale leen ci ay wàll.
s-14 Nit, dale ci lu yàgg ci ag nekkam, doon na jéem a nos ay xameefam.
s-15 Li dale ci jamono ju yàgg ja, bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp.
s-16 Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu ci a lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia (taariixu dend bi), doonoon ag faramfacce, ci fanweer ak juróom-ñaari téere ñeel dend bi, nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja.
s-17 Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377, duppee ko Al-Muqaddima (Taariixu àdduna bi), mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi: melosuuf, xeltu, taariix, koom-koom, gëstumboolaay, politig, paj ba ci suqaliku gu sax.
s-18 Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr Al-Razi, mutasilita bu Al-Kindi (ci daanaka 270 téere)
s-19 Imbratóor bu Siin bi, Cheng-Zu bu Callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle, di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix.
s-20 Mu ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yi ñu binde ak loxo, lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay.
s-21 Yii téere, loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool, boroom alal yi ak niti diine yi rekk ñoo ci doon jot: doonoon nañu ay téere yu seer lool.
s-22 Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juróom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko.
s-23 Ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko.
s-24 Bu ko defee mu daldi jël nguur gi.
s-25 Ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana.
s-26 Waar Jaabi dugg na ci Lislaam, daldi jóg def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit.
s-27 Ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci Lislaam ci Senegaal.
s-28 Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi.
s-29 Li ko waraloon it moo di dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi.
s-30 Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn).
s-31 Ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent).
s-32 Ci mujjug xarnub fukk ak juróom la Koli Tingala jóg xeex Tukulóor yi, daldi tembal ay goxam, taxawal nag nguur gu yees, mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko.
s-33 Ci xarnub fukk ak juróom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom: Jolof, Kajoor.
s-34 Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarloo ak cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi.
s-35 Ci atum 1770 g.j, la ag fippu am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daldi daaneel njabootug Deñanke.
s-36 Bu ko defee, Baal jël Lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale.
s-37 Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan.
s-38 Moom lañu di jàppe ki njëkk a doon Yilimaan.
s-39 Lebu, mooy benn waaso nekk ci reewum Senegaal.
s-40 Ñoom, Ndakaaru moo di seen dëkk, nu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint-Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur, ci wetu geej ak tefes.
s-41 Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan.
s-42 Seen làkk di wolof.
s-43 Seen wolof dafa xaw a wuute tuuti ak wolof bi ñeneen ñi di làkk.
s-44 Am na ñu ne, lebu yi ñoo sos làkk wolof.
s-45 Cosaanu baat boobu, wuute na ci li kilifa yi tekki.
s-46 Ñooñu dinañu di nettali ay cosaan yu wuute: 'leeb' moo juur baat bi.
s-47 Am na ñeneen ñu ni 'luubu' mooy 'bañ', ndax ci cosaan, Lebu yi dañu mas a bañ ku leen noot.
s-48 Seex Anta Jóob, ci gëstoom, dafa wone ni, li ñu tudde lebu, am na lu mu bokk ak tur boobu ñu joxe reewum Libi.
s-49 Libi, ci jamono Isipt gu yàgg ga, benn diwaan la woon bu nit ñi daan dem di fa rëbbi, ak nappi.
s-50 Dëkk boobu dafa jannoo ak géej gi.
s-51 Moo tax ñu yoroon Isipt gu yagg ga, tudde dëkk boobu: rëbu.
s-52 Ñu war a xam ni, Seex Anta Jóob ak yeneen gestukat wone nañu ko.
s-53 Làkk boobu amoon ca Isipt boobu, ak làkk wolof, ñoo bokk maam.
s-54 Rëbu moo juur Lebu.
s-55 Lebu moo juur Libi.
s-56 Dëkk bi ñu xam ne, ay nit ñu ñuul ñoo fa ne woon, te ñu daan tudde ñu dëkk ca biir réew mi 'kaw'.
s-57 Mel ni li am Senegaal tey: Lebu yi dëkk ci tefes ak wetu geej gi, kaw-kaw yi dëkk ci biir réew mi.
s-58 Lebu yi, kon, réew mi ñu tudde tey Libi, lañu ne woon ci jamono yu Isipt gu yàgg ga ame.
s-59 Dañoo mujj daw dëkk boobu, ndax amoon na benn askan bu ñëwoon foofu, jóge Asi, te ñu leen daan bëgg a noot.
s-60 Ñoom ñooy Persi yi.
s-61 Ci seen gàdday, jaar nañu ci ay dëkk yu bare (Sudaan, Caad, Niseer, Mali).
s-62 Sudaan, mooy dëkk bi Lebu yi baawoo.
s-63 Ñu ko gën a ràññe ci turu Nubi walla Kuus.
s-64 Senegaal, lañu agsi, jamono ja nguuru Tekuruur ame.
s-65 Foofu lañu fekk seen bokk, di Pël yi ak Séeréer yi, rawatina Pël ak Seereer yi ñuy napp.
s-66 Ñu leen tudde ci làkku pulaar ay Cuballo / Subalbe.
s-67 Foofu lañu sanc ay dëkk yu mel ni KasKas ak Njum.
s-68 Waaye ci Senegaal, taxawuñu Tekruur rekk.
s-69 Jaar nañu Jolof, ak Kajoor, soog a mujj agsi ca Ndakkaru ci diggante atum 1430 ak 1530.
s-70 Foofu, ay Socé lañu fa fekk.
s-71 Fukki ak ñaari xeet ñoo nose askanu Lebu yi.
s-72 Ñu ne tamit, fukki ak ñaari PENC yi.
s-73 Ñoom ci senn bopp, dañu xaaj ci ñaari njabootay yu mag, di Sumbejun yi ak Beeñ yi.
s-74 Ñoo yore woon gox yi ci Ndakaaru: Yoff, Wakam, Ngor, Sumbejun, ...
s-75 Lebu yi ñoo bokk sant ak Seereer yi, mel ni: Ndóoy, Puy, Ndir, Jeen, Yaad, Jaañ, Fay, Jeey, Sar, Caw, Njaay, Juuf, Sek.
s-76 Ñu sant 'Mbeŋ', ci li cosaan tekki, seen maam ay Mandiŋ lañu woon.
s-77 Seen mamaat di Jolof Mbeŋ (ab lamaanu Jolof), jóge Mali.
s-78 Da firnde ni, Lebu yi, ci ñoom lañu cosaanoo.
s-79 Mel ni wolof yi rekk.
s-80 Lebu yi, ay jullit lañu.
s-81 Ñu bare bokk ci Tariqa Tijaan, ak Layeen yi (Seydinaa Limaamu Laay).
s-82 Seen këru diine di Kambereen, ca Yoff.
s-83 Waaye, du tax ñu fate seen cosaan, ak li seen maam defoon, ba ñu nekkee Ceddo, manaam tuur yi.
s-84 Tuur yi, am na solo ci Lebu yi.
s-85 Ci seen jaar jaar, tuur yi, gëdd gu mag lañu yoroon ci ñoom, ci lu jëm ci xare yi, ak yeneen xeew yu amoon solo ci seen cosaan.
s-86 Ci seen tuur yi, 'ndëpp' la nit ñi gën a xam, ngiir faj febaru ñooñu ñu xam ne, jiine a leen jàpp.
s-87 Jiine ci Lebu, 'rab' lañu ko tudde.
s-88 Lëk Dawwur, Maam Kumba Kastel, Maam Jaare, ak yeneen i tuur, bokk nañu ci ñooñu Lebu yi seqante.
s-89 Askanoog Kleopaatar ci Afrig: firnde gu tukkee ci ay yax
s-90 Li Liz Taylor doon Kleopaatar (Cléopatre) ci filmu Joseph Mankiewicz dina jur ag jaaxle gu réy.
s-91 Ana lu ko waral?
s-92 Kleopaatar VII doonoon buuru Misra (Egypte) bu jigéen, te ñu ko daan woowe 'Grek bi' ndax li mu bokkoon ci askanu ptolémaïque sosoo Masedoni (Macédonie).
s-93 Ndeke ku ñuul la woon.
s-94 Loolee la BBC xamale ci ab dokimaanteer bu mu duppee Kleopaatar: jëmmi reykatu nit, dees na ko wone 23 maars.
s-95 Kleopaatar, mi juddu atum 69 laata Yónnent Yàlla Isaa, ma nga bokkoon ca askanu Lasit (Lagites) yu waa Masedoni.
s-96 Askan woowu dafa càllaloo woon ci Seneraal Ptolemee mi doonoon buuru Misra ganaaw paacoog nguurug Aleksaandar mu màg ma (Alexandre le Grand).
s-97 Loolu moo waraloon wesaareeg nit ñu weex ña ca tefesug dexu Nil ga.
s-98 Buur bu jigéen boobee nga xam ne jiite woon na Misra atum 51 ba 30, ku weex lees ko jàppee woon boobu ak léegi.
s-99 BBC xamalees na ne firndalees na ci ay gëstu ne yaxi nit ka ñu gis ci ab bàmmeel ca Turki yoy raki Kleopaatar la ma tuddoon Arsinoe IV te ñu faatoon ko ci ndigalu Kleopaatar.
s-100 Gëstu ya ñu def ca yaxi bopp ba, wone na ne, Arsinoe ku ñuul la woon, muy luy wone ne Kleopaatar ku ñuul la woon.
s-101 Li ndeyi Arsinoe doonoon nit ku ñuul dëgg-dëgg ëpp na tool.
s-102 Te dina gën a leeralaat njabootug Kleopaatar, la Hilke Thuer, bu Akadëmi siyans bu Ótris, mi jiite gëstukat yooyee waxoon.
s-103 Loolu nag moom, dafay dëggal rekk li Seex Anta Jóob waxoon te firndeeloon: 'Waa Misra ya ñu ñuul lañu woon'.

Text viewDownload CoNNL-U