Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

Showing 203 - 302 of 470 • previousnext

s-203 Saxal na ne ginnaaw bi àdduna bi sosoo ci ag fàcc gu mag, ab gëwéelub ceññeer war na am ci àdduna bi, niki jeexiitu fàcc gii.
s-204 Rax-ci-dolli, ceññeer gii dafa war a nekk di lu tas ci anam gu bennoo ci mbooleem àdduna bi.
s-205 Firnde loolu doon na feeñi.
s-206 Ca 1965 ñaari gëstukat yu tudd Arno Pinsiyas ak Robert Wilson wuññi nañu ceññeer yii ci ag mbetteel.
s-207 Ceññeer yii ñu di wooye ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang niruwuñu woon lu jóge ci benn gongikuwaay, waaye dafa doon lu tas ci jawwu jépp.
s-208 Pensiyas ak Wilson joxees na leen neexalub Nobel ngir seen wuññi yooyu.
s-209 Ci 1989, Nasaa sànni woon na ci jawwu ji satalit bii di Kob, ngir def ay gëstu ci ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang.
s-210 Ba ñu defee juróom ñatti simili ci jawwu ji lañu dëggal xaymay Pensiyas ak Wilson yii.
s-211 Kob wuññi na jeexiiti fàcc gu mag googee amoon ca ndoortel àdduna bi.
s-212 Wuññi gii ñu jàppe gi gën a mag ci mbooleem jamono yi, indi na firnde lu leer ñeel gisiinu Big Bang.
s-213 Leneen firnde lu am solo lu Bing Bang mu ngi bawoo ci kem bu Idrojen ak Eliyon bi nekk ci jawwu ji.
s-214 Ci biir gëstu yi gisees na ne dajaloog Idrojen-Eliyom gi am ci àdduna bi dëppoo naak xaymay gisiin yu dajaloog Idrogen-Elyom yi desoon ginnaaw Big Bang.
s-215 Bu àdduna bi amul woon fu mu tàmbalee mbaa mu nekkoon di lu fi mas di nekk, kon aji toggaleem ju Idrogen lekku na ba jeex bu yàgg ba far soppiku di Elyom.
s-216 Firnde yu leer yépp nag ñoo tax woroom xam-xam yi nangu gisiinu Big Bang.
s-217 Misaalum Big Bang moo di baat bu mujj bi boroom xam-xam yi agseegunu ci lu aju ci cosaanul àdduna bi.
s-218 Ginaaw bi mu yàggee layal melokaan wu sax wi ci wetu Fred Hoyle, Denis Kiyama melal na taxawaayam bu mujj bi mu mujj a àgg, ginnaaw feeñalug mbooleem firnde yi di dëgëral gisiinu Big Bang.
s-219 Kiyama jibal na ne layal na gisiinu melokaan wu sax wi, du caagéenug ngir ne dafa ko wóoroon ne mooy dëgg, waaye rekk ngir ne loolu la bëggoon muy li am.
s-220 Kiyama dolli na ci ne, bi firnde yi tegaloo, manatul a def lu dul nangu nag ne làmb ji tas na, te wacci gisiinu melokaan wu sax wi.
s-221 Lu fi amoon kon njëkk Big Bang?
s-222 Jan doole moo sabab amug àdduna bi ci fàcc gu mag gii te kat bu njëkk lu amadi la woon?
s-223 Laaj bii dafa di fi indi - ci waxi Artir Edington lu naqari li ci wàllug xeltu li ñoñ ngérum ne-ne nanguwul a nangu te moo di amug aji bind (aji sàkk).
s-224 Xeltukat bu weddi bu siiw ba nii la saraa laaj boobu: Xamees na bu baax ne diine lu baax ci bakan la.
s-225 Kon maa ngi doore ci nangu ne Stratonocien bu weddi bii manul lu dul nangu dëppoo gu àdduna gii.
s-226 Ndax mel na bu baax ne sóobukati jawwu yi indi nañu firndey xam-xam ci ne àdduna bi am na ab tàmbali.
s-227 Ca dëgg-dëgg, Big Bang indi na ci ay jafe-jafe lu sakkan ñeel woroom xam-xami ngérum ne-ne mi.
s-228 Antoni Flew dëggal na loolu.
s-229 Ndax Big Bang saxalul rekk ne àdduna bi ci ag neen lañu ko sose, waaye saxal na ne it dees koo sos ci anam gu nosu, gu tegu ci yoon, gu ñu fuglu.
s-230 Big Bang mu ngi ame ci fàccu ag tomb bi ëmboon mbooleem ne-ne ak kàttanug àdduna bi, ak ag tasam ci jawwu ji ci mbooleem wàll yi, ci ab gaawaay bu yéeme.
s-231 Ne-ne bii ak kàttan gii ñoo jur ag màndaqoo gu mag gu ame ci ay galagsi, ay bidiw, jant bi, suuf si ak mbooleem yeneen yaram yu asamaan yi.
s-232 Rax-ci-dolli, ay àtte yi ñu tudde àttey xam-xamu jëmm daldi feeñ, ay àtte yu niroo ci àdduna bi bépp, yu dul soppiku.
s-233 Àttey jëmm yii feeñ ànd ak Big Bang, soppikuwuñu lu gën a néew ci diir bu tollu ci 15 milyaari at.
s-234 Rax-ci-dolli, àtte yii ñu ngi tegu ci ay xayma yu àgg ci leer ba bu ñu ci soppee la gën a néew ci li mu doon, mu yàq bindub àdduna bépp ak aw meloom.
s-235 Lii lépp li mu di wund moo di Big Bang indi na fi ag nosu gu yéeme.
s-236 Ci biir loolu ag fàcc, ci yoon, ag nosu daawu ci juddoo.
s-237 Mbooleem fàcc yu ñu man a gis, toc la daan def, moñoxe, wisaare, tas.
s-238 Bu ñu gisee nag ag fàcc def ag nos gu mel ne gii, li ñu di man a wax moo di ag yewwute manul a ñàkk ci ginaaw li ko amal, te nag kenn daal moo war a yëngal mbooleem cér yii tas ngir fàcc gi, ci anam gu ñu fuglu lool.
s-239 Freds Hoyle mi mujjoon nangu gisiinu Big Bang, ginnaaw bi mu ko weddee ay at mu ngi leeral loolu ci anam gu leer.
s-240 Gisiinu Big Bang saxal na ne àdduna bi mu ngi tàmbalee ci genn fàcc.
s-241 Moo ne ni ñu ko man a seetloo, ag fàcc du def lu dul tas ne-ne, te Big Bang moom ci anam gu mbóotu dafa def safaan ba, ci dajale ne-ne ci melow ay galagsi.
s-242 Bu ag fàcc yobboo ci ag nosu gu mag loolu du man a def lu dul gëmloo ci ne am na aji sàkk juy ki ko def.
s-243 Weneen feeñiit wu nosu gu kiimaane gii sosu ci àdduna bi ci ginnaaw Big Bang moo di sosuwu ab àdduna bu ñu man a dëkke.
s-244 Sart yi manul a ñàkk ci sosuwu ag àdduna bu ñu man dëkke bari nañu te jafe ba xel du nangu ne man nañu a sosoo ci ag tombe.
s-245 Paule Davis ab boroom xam-xamu jëmm bu gisiin bu siiw jibal na, ginnaaw bi mu defee ay xayma ci kemub tàllalikug àdduna bi, ne kem bi de àgg na ci leer ak tegu ci yoon fu xel manul a xalaat.
s-246 Davis nee na: njuumte gu ndaw ci natt kemub tàllikug àdduna bi man na a waral àdduna bi moy ag bijjam, bu ko defee wéyal ag tàllalikoom ci anam gu nosoodiku.
s-247 Adduna bi, bu gënoon a dox ndànk ci nii mu ko di defe, dafa di daldi rot, bu gënoon a gaaw tuuti rekk nga gis ne-ne bu àdduna bi tas bu yàgg.
s-248 Big Bang de du fàcc gu mel ne yépp.
s-249 Ag fàcc la gu am ab tolluwaay bu sax, gu yam fi ñu ko yamloo.
s-250 Prosesëer Stefaan Aukin, di ab boroom xam-xamu jëmm bu mag, jibal na ca téereem ba ne: àdduna bi mu ngi tegu ci ay xayma ak i màndaqe yu ñu nos, defar leen ci anam gu leer gu nu manul a xalaat nun.
s-251 Aukin jibal na ci lu aju ci tàllalikug àdduna bi: Su fekkoon ne kemub tàllaliku gi, as cimili ginaaw Big Bang bi, dafa yées ak doonte lu tollu ak téeméeri miyaari milyoŋeem la, àdduna bi dafay daanuwaat ci ag teel balaa tollu nii mu toll tay.
s-252 Paul Davies leeral na ba tay ngérte lu ñu manul a moyu, lu ñu di génnee ci xayma ak màndaqoo yu leer yii te yam ba ëpp.
s-253 Ci gàttal daal bu ñu dee settantal nosteg àdduna gu yéeme gii, dinanu gis ne amug ak nosu gu àdduna bi dañoo goor ci ay màndaqoo yu yëgu ak ci nosu gu fasu ba tombe rekk ak fiiroo duñu doyati ngir firi leen, leeral leen.
s-254 Ci lu leer, lu manul a nekk la nosu gii ak màndaqoo gu mat gii nekk di lu fi dikkal boppam ak ci ag tombe ginnaaw ag fàcc gu mag.
s-255 Sosu gu ag nosu gu ni mel, ginnaaw ag fàcc gu mel ne Big Bang moo di firnde lu fés li ci ag sàkk gu xarbaaxe.
s-256 Nosu ak tegu ci yoon gu mat gu àdduna bi dañu di wone ci anam gu ñu manul a moyu teewaayug aji-bind ju yor xam-xam, kàttan ak hikma ju dul jeex.
s-257 Moo di ki sos ne-ne jële ko ci ag neen, te di fuglu ak a doxal lii lépp ci ag wéy.
s-258 Aji bind jii moo di Allaa, boroom àdduna yépp.
s-259 Profesëer Jorj Abel bu Daara ju Kawe ju Kaliforni nangu na moom it ndam lu mujj li ñeel Big Bang.
s-260 Mu daldi jibal ne firnde yi am ci jamono jii wone nañu ne àdduna bi mu ngi feeñ ci ay milyaari at ci ginnaaw, te Big Bang gi waral ko.
s-261 Mu nangu ne amul meneen pexe mu dul nangu gisiinu Big Bang.
s-262 Ak dikkug gisiinu Big Bang, léebu aw ne-ne bu sax wi nga xam ne moo doonoon cëslaayul xeltug ngérum ne-ne mujjees na ko sànni ci sënu ab taarix.
s-263 Gisiinu Big Bang mu ngi doon wone ne, ci njëlbéen gi, mbooleem yëf yi nekk ci àdduna bi benn cér rekk lañu woon, ginnaaw bi ñu séddalikoo.
s-264 Lii nga xam ne gisiinu Big Bang wee ko wone, Alquaraan it jotoon na koo wone booba ak léegi toll na ci fukk ak ñeenti xarnu, ci jamono ju nga xam ni nit lu néew la xamoon ci àdduna bi.
s-265 Du rekk bidiw yi ak galagsi yi dañu di sori wëlis nu, waaye dañu di dox di soreente ñoom ci seen biir.
s-266 Ndegam nag mbooleem céri àdduna bi dañu di soreyante ci seen biir, lenn lañu man a jàpp moo di ne àdduna bi dafa nekk ci ag yaatu gu sax (tàllaliku = expension).
s-267 Ngir gën a xam loolu man nañu a jeneer àdduna bi mu mel ne kaw ag manq gu ñu nekk di wal.
s-268 Ni tomb yi nekk ci kaw manq gi di soreentee la ñu ko di gën di wal, ni la yëf yi nekk ci jawwu ji di soreentee lu àdduna bi gën di tàllaliku.
s-269 Lii sax wuññeesoon na ko ci gisiin ci lu gënoon a teel.
s-270 Albeer Anstaayin mu ñu jàppe ne moo di boroom xam-xam bi gën a mag ci ñaar-fukkeelu xarnu àggoon na, ci ginnaaw ay xayma yu xam-xamu jëmm bu gisiin, ci ne àdduna bi nekkul di lu man a sax.
s-271 Ci biir loolu dafa tegoon nee wuññeem googu, ngir rekk bañ a dëppoodi ak misaalum sax mu àdduna bi, mi nga xam ne moom la ñépp jëloon ci ay jamonoom.
s-272 Ci ginnaaw bi Anstaayin gisoon na ne def na ci loolu njuumte li gën a mag ci ag dundam ak ab liggéeyam.
s-273 Boroom xam-xam yu bari yu dul tënk seen bopp ci ne fàwwu dañoo war a nekk ñu gëmadi, nangu nañu ne am na aji-sàkk ju man lépp ju sabab sosug àdduna bi.
s-274 Aji-sàkk jii dafa war a nekk aji-nekk ju nga xam ni moo sàkk jamono ji ak jawwu ji, waaye nekk it di ku temb (maanaam ku wéeruwul, sukkandikuwul) ci jamono ak jawwu ji.
s-275 Lii la boroom xam-xamu jëmm bu siiw bii di Hugh Ross wax:
s-276 Bu tàmbalig jamono tollook tàmbalig àdduna bi ni ko layal wu féex gi saxale, kon li sabab àdduna bi dafa war a nekk ag nekkte guy jëfe ci tolluwaayu jamono bu temb ci anam gu mat, ba noppi jiitu fi tooluwaayu jamono bu àdduna bi.
s-277 Jii wax nag mu ngi nu di jàngal ne àdduna bi du Yàlla moom ci boppam, te Yàlla it nekkul di lu ëmbu ci àdduna bi.
s-278 Waa-waaw ne-ne ak jamono aji-sàkk jee leen sàkk, ki nga xam ne wéeruwul ci benn ci maanaa yii.
s-279 Jii aji-sàkk nag moo di Allaa Yàlla mi di aji-man-lépp, ki di boroom asamaan yi ak suuf.
s-280 Bennoog xaalis: Réewi CEDEAO yi dinañu bokk benn xaalis ci atum 2020
s-281 Njiitu Kuréel gi di saytu xaalis bi ci Afrig sowwu-jant (AMAO), Mohamed Ben Omar Njaay xamale na, talaata jii ci njalbéenu limu waxtaan yi IDEP (Daara ji ñu di jàngalee suqalig koom akug sooraale) amal, ne goxu bennoo réewi Afrig yu sowwu-jant (CEDEAO) dina bennal xaalis bi.
s-282 Jibal na ci yéenekaay bii di 'Observateur' ne kuréel gu ëmb ay way-màcc ak i kilifa dina xalaat ci anam gi xaalis boobu di ame ak nan lañuy bennale xaalis yu wuute yi am ci réew yooyu.
s-283 Ci ay waxam, 2009 ak léegi, réew yooyu tëral nañu yoon wu bees wuy leeral ay liggéey yu jëm ci bennoo gi: bennale sistemu peyoor yi, yu estatistik yi, yu politigu alalal yi.
s-284 Leeral na ne ci Bennale doxaliinu bànk yi ci atum 2015, séenu nañu ag jàll jëm ci benn xaalis ci ñaareel goxu CEDEAO gi ëmb réew yi di jëffandikoo làkku Àngale.
s-285 Xaalisu ñaareelu gox boobu moo di pàcc bi njëkk laata ñu koy bennale ci atum 2020 ak xaalisu CFA ngir ñu am benn xaalis ci goxu CEDEAO gépp.
s-286 Yàtt bi lëmbe jamono!
s-287 Su dee ni ko yenn waay-xeltu yi di waxee namm-namm xarala dëggantaan mooy gësëm xelu nit ñi ba ñu xippi xool, gise neneen mbir yi leen wër.
s-288 Ku yebboo kon ne yàtt bi Ablaay Wàd yàttlu Wakaam yégg na ca la mu ca doon wut.
s-289 Ndax doonte sax nag sotteegul, 'ngenteeguñu' ko maanaam, xel yi ak xalaat yépp a ngi lëmbe di ko xaar...
s-290 Su caaxaan faaxee dëgg dés, yàtt bi dafa xajjàlle réew mi ak li ko weesu ñaar ba ñett ak ñeenti làng:
s-291 Am ñeneen ñu ne yàtt bii moo di firndeel dëgg cuune, caaxaan ag càggante gi nguuru Ablaay Wàdd ngemboo:
s-292 Ndax nan lañuy jëlee ci réew mu lótt ni Senegaal, nit ñi dëkkee jaaxle ak di tuuñ-tuuñi lu ñu lekk, xale yi di sóobu ci géej gi di wut a raw, ay miliyaari-miliyaar di ko def ci yàtt bu kenn xamul yàttu lan la?
s-293 Am geneen làng gu ca yokk ne li wér mooy yàtt bi warul a taxaw mukk ci réewum Senegaal gii di réewu julit, ndax diine Lislaam dafay tere di yàtt ay nit, rawatina yëkkati ko ba mu mel ni luy juqarbi asamaan...
s-294 Am na itam ñoo xam dañu ne ñoom li leen naqari mooy yàtt bi ci boppam dafa amul lenn lu am solo lu muy misaal, rax-ci-dolli rafetul, taaruwul!
s-295 Dafa fóoyóoy daal manaam su ñu ko seetee, tég ko ci sàrt yi aaru Afrik di wéy.
s-296 Yàtt bi nag ci wàllu boppam mu nga nekk Wakaam, ca tundu Mamel, jakarloo ag géej.
s-297 Tollu na ci taxawaay 50 m, genn góor jàpp jenn jiggéen, fab ci loxo càmmoñ benn xale bu talal loxom di joxoñ xarfu.
s-298 Loolu nag li muy misaal, ñu ne, taxaw-temmu Afrik la, gi di gindeekoo ci lëndëmtoo ag njaam, dëgmal ëllëgug yaakaar ag ngëm gu mat sëkk.
s-299 Li wér daal mooy ne yàtt bi ci jëmmam yeneen yàtt yu mel ni 'yàttu moomeel sa bopp' ba ca Amerik, mbaa yàttu Yeesu Kiris ba ca Riyoo lay diiranteel mbàgg!
s-300 Ndaxam sax nag Beresil mbaa Amerik mëneesu leen a jawaatle ak Senegaal!
s-301 Ci bésu 04 Awril 2010, temboo ak 50eelu at ba Senegaal moomee boppam ba léegi, lees ko war a ngente.
s-302 Li jaaxal nit ñi mooy nan la askan wi, rawatina kilifa diine Lislaam nar a doxale?

Text viewDownload CoNNL-U