s-201
| Ñi daan layal melokaan wu sax wi yàgg nañoo lànk Big Bang, waaye ci biir loolu xam-xam moom di wéy di leen weddi. |
s-202
| Jorg Gamow indi na beneen xalaat ci lu aju ci Big Bang. |
s-203
| Saxal na ne ginnaaw bi àdduna bi sosoo ci ag fàcc gu mag, ab gëwéelub ceññeer war na am ci àdduna bi, niki jeexiitu fàcc gii. |
s-204
| Rax-ci-dolli, ceññeer gii dafa war a nekk di lu tas ci anam gu bennoo ci mbooleem àdduna bi. |
s-205
| Firnde loolu doon na feeñi. |
s-206
| Ca 1965 ñaari gëstukat yu tudd Arno Pinsiyas ak Robert Wilson wuññi nañu ceññeer yii ci ag mbetteel. |
s-207
| Ceññeer yii ñu di wooye ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang niruwuñu woon lu jóge ci benn gongikuwaay, waaye dafa doon lu tas ci jawwu jépp. |
s-208
| Pensiyas ak Wilson joxees na leen neexalub Nobel ngir seen wuññi yooyu. |
s-209
| Ci 1989, Nasaa sànni woon na ci jawwu ji satalit bii di Kob, ngir def ay gëstu ci ceññeeri mbëj-bijjaakon yu Big Bang. |
s-210
| Ba ñu defee juróom ñatti simili ci jawwu ji lañu dëggal xaymay Pensiyas ak Wilson yii. |
s-211
| Kob wuññi na jeexiiti fàcc gu mag googee amoon ca ndoortel àdduna bi. |
s-212
| Wuññi gii ñu jàppe gi gën a mag ci mbooleem jamono yi, indi na firnde lu leer ñeel gisiinu Big Bang. |
s-213
| Leneen firnde lu am solo lu Bing Bang mu ngi bawoo ci kem bu Idrojen ak Eliyon bi nekk ci jawwu ji. |
s-214
| Ci biir gëstu yi gisees na ne dajaloog Idrojen-Eliyom gi am ci àdduna bi dëppoo naak xaymay gisiin yu dajaloog Idrogen-Elyom yi desoon ginnaaw Big Bang. |
s-215
| Bu àdduna bi amul woon fu mu tàmbalee mbaa mu nekkoon di lu fi mas di nekk, kon aji toggaleem ju Idrogen lekku na ba jeex bu yàgg ba far soppiku di Elyom. |
s-216
| Firnde yu leer yépp nag ñoo tax woroom xam-xam yi nangu gisiinu Big Bang. |
s-217
| Misaalum Big Bang moo di baat bu mujj bi boroom xam-xam yi agseegunu ci lu aju ci cosaanul àdduna bi. |
s-218
| Ginaaw bi mu yàggee layal melokaan wu sax wi ci wetu Fred Hoyle, Denis Kiyama melal na taxawaayam bu mujj bi mu mujj a àgg, ginnaaw feeñalug mbooleem firnde yi di dëgëral gisiinu Big Bang. |
s-219
| Kiyama jibal na ne layal na gisiinu melokaan wu sax wi, du caagéenug ngir ne dafa ko wóoroon ne mooy dëgg, waaye rekk ngir ne loolu la bëggoon muy li am. |
s-220
| Kiyama dolli na ci ne, bi firnde yi tegaloo, manatul a def lu dul nangu nag ne làmb ji tas na, te wacci gisiinu melokaan wu sax wi. |
s-221
| Lu fi amoon kon njëkk Big Bang? |
s-222
| Jan doole moo sabab amug àdduna bi ci fàcc gu mag gii te kat bu njëkk lu amadi la woon? |
s-223
| Laaj bii dafa di fi indi - ci waxi Artir Edington – lu naqari li ci wàllug xeltu li ñoñ ngérum ne-ne nanguwul a nangu te moo di amug aji bind (aji sàkk). |
s-224
| Xeltukat bu weddi bu siiw ba nii la saraa laaj boobu: Xamees na bu baax ne diine lu baax ci bakan la. |
s-225
| Kon maa ngi doore ci nangu ne Stratonocien bu weddi bii manul lu dul nangu dëppoo gu àdduna gii. |
s-226
| Ndax mel na bu baax ne sóobukati jawwu yi indi nañu firndey xam-xam ci ne àdduna bi am na ab tàmbali. |
s-227
| Ca dëgg-dëgg, Big Bang indi na ci ay jafe-jafe lu sakkan ñeel woroom xam-xami ngérum ne-ne mi. |
s-228
| Antoni Flew dëggal na loolu. |
s-229
| Ndax Big Bang saxalul rekk ne àdduna bi ci ag neen lañu ko sose, waaye saxal na ne it dees koo sos ci anam gu nosu, gu tegu ci yoon, gu ñu fuglu. |
s-230
| Big Bang mu ngi ame ci fàccu ag tomb bi ëmboon mbooleem ne-ne ak kàttanug àdduna bi, ak ag tasam ci jawwu ji ci mbooleem wàll yi, ci ab gaawaay bu yéeme. |
s-231
| Ne-ne bii ak kàttan gii ñoo jur ag màndaqoo gu mag gu ame ci ay galagsi, ay bidiw, jant bi, suuf si ak mbooleem yeneen yaram yu asamaan yi. |
s-232
| Rax-ci-dolli, ay àtte yi ñu tudde àttey xam-xamu jëmm daldi feeñ, ay àtte yu niroo ci àdduna bi bépp, yu dul soppiku. |
s-233
| Àttey jëmm yii feeñ ànd ak Big Bang, soppikuwuñu lu gën a néew ci diir bu tollu ci 15 milyaari at. |
s-234
| Rax-ci-dolli, àtte yii ñu ngi tegu ci ay xayma yu àgg ci leer ba bu ñu ci soppee la gën a néew ci li mu doon, mu yàq bindub àdduna bépp ak aw meloom. |
s-235
| Lii lépp li mu di wund moo di Big Bang indi na fi ag nosu gu yéeme. |
s-236
| Ci biir loolu ag fàcc, ci yoon, ag nosu daawu ci juddoo. |
s-237
| Mbooleem fàcc yu ñu man a gis, toc la daan def, moñoxe, wisaare, tas. |
s-238
| Bu ñu gisee nag ag fàcc def ag nos gu mel ne gii, li ñu di man a wax moo di ag yewwute manul a ñàkk ci ginaaw li ko amal, te nag kenn daal moo war a yëngal mbooleem cér yii tas ngir fàcc gi, ci anam gu ñu fuglu lool. |
s-239
| Freds Hoyle mi mujjoon nangu gisiinu Big Bang, ginnaaw bi mu ko weddee ay at mu ngi leeral loolu ci anam gu leer. |
s-240
| Gisiinu Big Bang saxal na ne àdduna bi mu ngi tàmbalee ci genn fàcc. |
s-241
| Moo ne ni ñu ko man a seetloo, ag fàcc du def lu dul tas ne-ne, te Big Bang moom ci anam gu mbóotu dafa def safaan ba, ci dajale ne-ne ci melow ay galagsi. |
s-242
| Bu ag fàcc yobboo ci ag nosu gu mag loolu du man a def lu dul gëmloo ci ne am na aji sàkk juy ki ko def. |
s-243
| Weneen feeñiit wu nosu gu kiimaane gii sosu ci àdduna bi ci ginnaaw Big Bang moo di sosuwu ab àdduna bu ñu man a dëkke. |
s-244
| Sart yi manul a ñàkk ci sosuwu ag àdduna bu ñu man dëkke bari nañu te jafe ba xel du nangu ne man nañu a sosoo ci ag tombe. |
s-245
| Paule Davis ab boroom xam-xamu jëmm bu gisiin bu siiw jibal na, ginnaaw bi mu defee ay xayma ci kemub tàllalikug àdduna bi, ne kem bi de àgg na ci leer ak tegu ci yoon fu xel manul a xalaat. |
s-246
| Davis nee na: njuumte gu ndaw ci natt kemub tàllikug àdduna bi man na a waral àdduna bi moy ag bijjam, bu ko defee wéyal ag tàllalikoom ci anam gu nosoodiku. |
s-247
| Adduna bi, bu gënoon a dox ndànk ci nii mu ko di defe, dafa di daldi rot, bu gënoon a gaaw tuuti rekk nga gis ne-ne bu àdduna bi tas bu yàgg. |
s-248
| Big Bang de du fàcc gu mel ne yépp. |
s-249
| Ag fàcc la gu am ab tolluwaay bu sax, gu yam fi ñu ko yamloo. |
s-250
| Prosesëer Stefaan Aukin, di ab boroom xam-xamu jëmm bu mag, jibal na ca téereem ba ne: àdduna bi mu ngi tegu ci ay xayma ak i màndaqe yu ñu nos, defar leen ci anam gu leer gu nu manul a xalaat nun. |
s-251
| Aukin jibal na ci lu aju ci tàllalikug àdduna bi: Su fekkoon ne kemub tàllaliku gi, as cimili ginaaw Big Bang bi, dafa yées ak doonte lu tollu ak téeméeri miyaari milyoŋeem la, àdduna bi dafay daanuwaat ci ag teel balaa tollu nii mu toll tay. |
s-252
| Paul Davies leeral na ba tay ngérte lu ñu manul a moyu, lu ñu di génnee ci xayma ak màndaqoo yu leer yii te yam ba ëpp. |
s-253
| Ci gàttal daal bu ñu dee settantal nosteg àdduna gu yéeme gii, dinanu gis ne amug ak nosu gu àdduna bi dañoo goor ci ay màndaqoo yu yëgu ak ci nosu gu fasu ba tombe rekk ak fiiroo duñu doyati ngir firi leen, leeral leen. |
s-254
| Ci lu leer, lu manul a nekk la nosu gii ak màndaqoo gu mat gii nekk di lu fi dikkal boppam ak ci ag tombe ginnaaw ag fàcc gu mag. |
s-255
| Sosu gu ag nosu gu ni mel, ginnaaw ag fàcc gu mel ne Big Bang moo di firnde lu fés li ci ag sàkk gu xarbaaxe. |
s-256
| Nosu ak tegu ci yoon gu mat gu àdduna bi dañu di wone ci anam gu ñu manul a moyu teewaayug aji-bind ju yor xam-xam, kàttan ak hikma ju dul jeex. |
s-257
| Moo di ki sos ne-ne jële ko ci ag neen, te di fuglu ak a doxal lii lépp ci ag wéy. |
s-258
| Aji bind jii moo di Allaa, boroom àdduna yépp. |
s-259
| Profesëer Jorj Abel bu Daara ju Kawe ju Kaliforni nangu na moom it ndam lu mujj li ñeel Big Bang. |
s-260
| Mu daldi jibal ne firnde yi am ci jamono jii wone nañu ne àdduna bi mu ngi feeñ ci ay milyaari at ci ginnaaw, te Big Bang gi waral ko. |
s-261
| Mu nangu ne amul meneen pexe mu dul nangu gisiinu Big Bang. |
s-262
| Ak dikkug gisiinu Big Bang, léebu aw ne-ne bu sax wi nga xam ne moo doonoon cëslaayul xeltug ngérum ne-ne mujjees na ko sànni ci sënu ab taarix. |
s-263
| Gisiinu Big Bang mu ngi doon wone ne, ci njëlbéen gi, mbooleem yëf yi nekk ci àdduna bi benn cér rekk lañu woon, ginnaaw bi ñu séddalikoo. |
s-264
| Lii nga xam ne gisiinu Big Bang wee ko wone, Alquaraan it jotoon na koo wone booba ak léegi toll na ci fukk ak ñeenti xarnu, ci jamono ju nga xam ni nit lu néew la xamoon ci àdduna bi. |
s-265
| Du rekk bidiw yi ak galagsi yi dañu di sori wëlis nu, waaye dañu di dox di soreente ñoom ci seen biir. |
s-266
| Ndegam nag mbooleem céri àdduna bi dañu di soreyante ci seen biir, lenn lañu man a jàpp moo di ne àdduna bi dafa nekk ci ag yaatu gu sax (tàllaliku = expension). |
s-267
| Ngir gën a xam loolu man nañu a jeneer àdduna bi mu mel ne kaw ag manq gu ñu nekk di wal. |
s-268
| Ni tomb yi nekk ci kaw manq gi di soreentee la ñu ko di gën di wal, ni la yëf yi nekk ci jawwu ji di soreentee lu àdduna bi gën di tàllaliku. |
s-269
| Lii sax wuññeesoon na ko ci gisiin ci lu gënoon a teel. |
s-270
| Albeer Anstaayin mu ñu jàppe ne moo di boroom xam-xam bi gën a mag ci ñaar-fukkeelu xarnu àggoon na, ci ginnaaw ay xayma yu xam-xamu jëmm bu gisiin, ci ne àdduna bi nekkul di lu man a sax. |
s-271
| Ci biir loolu dafa tegoon nee wuññeem googu, ngir rekk bañ a dëppoodi ak misaalum sax mu àdduna bi, mi nga xam ne moom la ñépp jëloon ci ay jamonoom. |
s-272
| Ci ginnaaw bi Anstaayin gisoon na ne def na ci loolu njuumte li gën a mag ci ag dundam ak ab liggéeyam. |
s-273
| Boroom xam-xam yu bari yu dul tënk seen bopp ci ne fàwwu dañoo war a nekk ñu gëmadi, nangu nañu ne am na aji-sàkk ju man lépp ju sabab sosug àdduna bi. |
s-274
| Aji-sàkk jii dafa war a nekk aji-nekk ju nga xam ni moo sàkk jamono ji ak jawwu ji, waaye nekk it di ku temb (maanaam ku wéeruwul, sukkandikuwul) ci jamono ak jawwu ji. |
s-275
| Lii la boroom xam-xamu jëmm bu siiw bii di Hugh Ross wax: |
s-276
| Bu tàmbalig jamono tollook tàmbalig àdduna bi ni ko layal wu féex gi saxale, kon li sabab àdduna bi dafa war a nekk ag nekkte guy jëfe ci tolluwaayu jamono bu temb ci anam gu mat, ba noppi jiitu fi tooluwaayu jamono bu àdduna bi. |
s-277
| Jii wax nag mu ngi nu di jàngal ne àdduna bi du Yàlla moom ci boppam, te Yàlla it nekkul di lu ëmbu ci àdduna bi. |
s-278
| Waa-waaw ne-ne ak jamono aji-sàkk jee leen sàkk, ki nga xam ne wéeruwul ci benn ci maanaa yii. |
s-279
| Jii aji-sàkk nag moo di Allaa Yàlla mi di aji-man-lépp, ki di boroom asamaan yi ak suuf. |
s-280
| Bennoog xaalis: Réewi CEDEAO yi dinañu bokk benn xaalis ci atum 2020 |
s-281
| Njiitu Kuréel gi di saytu xaalis bi ci Afrig sowwu-jant (AMAO), Mohamed Ben Omar Njaay xamale na, talaata jii ci njalbéenu limu waxtaan yi IDEP (Daara ji ñu di jàngalee suqalig koom akug sooraale) amal, ne goxu bennoo réewi Afrig yu sowwu-jant (CEDEAO) dina bennal xaalis bi. |
s-282
| Jibal na ci yéenekaay bii di 'Observateur' ne kuréel gu ëmb ay way-màcc ak i kilifa dina xalaat ci anam gi xaalis boobu di ame ak nan lañuy bennale xaalis yu wuute yi am ci réew yooyu. |
s-283
| Ci ay waxam, 2009 ak léegi, réew yooyu tëral nañu yoon wu bees wuy leeral ay liggéey yu jëm ci bennoo gi: bennale sistemu peyoor yi, yu estatistik yi, yu politigu alalal yi. |
s-284
| Leeral na ne ci Bennale doxaliinu bànk yi ci atum 2015, séenu nañu ag jàll jëm ci benn xaalis ci ñaareel goxu CEDEAO gi ëmb réew yi di jëffandikoo làkku Àngale. |
s-285
| Xaalisu ñaareelu gox boobu moo di pàcc bi njëkk laata ñu koy bennale ci atum 2020 ak xaalisu CFA ngir ñu am benn xaalis ci goxu CEDEAO gépp. |
s-286
| Yàtt bi lëmbe jamono! |
s-287
| Su dee ni ko yenn waay-xeltu yi di waxee namm-namm xarala dëggantaan mooy gësëm xelu nit ñi ba ñu xippi xool, gise neneen mbir yi leen wër. |
s-288
| Ku yebboo kon ne yàtt bi Ablaay Wàd yàttlu Wakaam yégg na ca la mu ca doon wut. |
s-289
| Ndax doonte sax nag sotteegul, 'ngenteeguñu' ko maanaam, xel yi ak xalaat yépp a ngi lëmbe di ko xaar... |
s-290
| Su caaxaan faaxee dëgg dés, yàtt bi dafa xajjàlle réew mi ak li ko weesu ñaar ba ñett ak ñeenti làng: |
s-291
| Am ñeneen ñu ne yàtt bii moo di firndeel dëgg cuune, caaxaan ag càggante gi nguuru Ablaay Wàdd ngemboo: |
s-292
| Ndax nan lañuy jëlee ci réew mu lótt ni Senegaal, nit ñi dëkkee jaaxle ak di tuuñ-tuuñi lu ñu lekk, xale yi di sóobu ci géej gi di wut a raw, ay miliyaari-miliyaar di ko def ci yàtt bu kenn xamul yàttu lan la? |
s-293
| Am geneen làng gu ca yokk ne li wér mooy yàtt bi warul a taxaw mukk ci réewum Senegaal gii di réewu julit, ndax diine Lislaam dafay tere di yàtt ay nit, rawatina yëkkati ko ba mu mel ni luy juqarbi asamaan... |
s-294
| Am na itam ñoo xam dañu ne ñoom li leen naqari mooy yàtt bi ci boppam dafa amul lenn lu am solo lu muy misaal, rax-ci-dolli rafetul, taaruwul! |
s-295
| Dafa fóoyóoy daal manaam su ñu ko seetee, tég ko ci sàrt yi aaru Afrik di wéy. |
s-296
| Yàtt bi nag ci wàllu boppam mu nga nekk Wakaam, ca tundu Mamel, jakarloo ag géej. |
s-297
| Tollu na ci taxawaay 50 m, genn góor jàpp jenn jiggéen, fab ci loxo càmmoñ benn xale bu talal loxom di joxoñ xarfu. |
s-298
| Loolu nag li muy misaal, ñu ne, taxaw-temmu Afrik la, gi di gindeekoo ci lëndëmtoo ag njaam, dëgmal ëllëgug yaakaar ag ngëm gu mat sëkk. |
s-299
| Li wér daal mooy ne yàtt bi ci jëmmam yeneen yàtt yu mel ni 'yàttu moomeel sa bopp' ba ca Amerik, mbaa yàttu Yeesu Kiris ba ca Riyoo lay diiranteel mbàgg! |
s-300
| Ndaxam sax nag Beresil mbaa Amerik mëneesu leen a jawaatle ak Senegaal! |