Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

Showing 101 - 200 of 470 • previousnext

s-101 Li ndeyi Arsinoe doonoon nit ku ñuul dëgg-dëgg ëpp na tool.
s-102 Te dina gën a leeralaat njabootug Kleopaatar, la Hilke Thuer, bu Akadëmi siyans bu Ótris, mi jiite gëstukat yooyee waxoon.
s-103 Loolu nag moom, dafay dëggal rekk li Seex Anta Jóob waxoon te firndeeloon: 'Waa Misra ya ñu ñuul lañu woon'.
s-104 Xibaaryi.com ab dal la (site) bu di tas xibaar ci wolof, muy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal.
s-105 Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar doonoon gëstug jeexal gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa Kelekey Jaxate.
s-106 Dal bii nag benn la ci saafara yi nu nar a saafaraa jafe-jafe yii nu lim ci suuf.
s-107 Ci Senegaal, lu tollu fukk ci téeméer (10 %) rekk ci askan wi ñoo dégg làkku Frãse ba mën ci a jariñu, bu nu méngalee lim boobu ak lu ëpp juróom ñatt fukk ci téeméer (80 %) ci askan wi, ñu nga xam ne seen ag dégg wolof kawe na.
s-108 Ñu bari ci askan wi dañu di seetaan ay film te duñu xam sax lu di maanaa mi.
s-109 Loolu nag di mbir mu doy waar ci askan wu bëgg ñu weg ko.
s-110 Sunu ndaw ñi, di ëllëgu réew mi, dégguñu solo si baat yi ëmbu dëg-dëg ci film yi ñu leen di jagleel, wante dañuy banneexu rekk ci jëf ju reetaanlu ju ñu gis.
s-111 Loolu tamit di mbir mu nga xam ne du nàmm seen am xel.
s-112 Bu njëkkoon, barab ya ñu daan seetaane filmu Endo ak kowboy ya dañu daan fees dell ndax ñoo gënoon a neex a nànd.
s-113 Léegi, barab yooya soppees na leen ay ja (marse).
s-114 Loolu tax ba nit ñi dematuñu sinemaa niki nu ko daan defe bu jëkkoon, waaye tamit dégg-dégg bi jàppandiwul ci film yu mel ni poliis especiaal, afeer kalase tere awaase ak yeneen ak yeneen.
s-115 Kuréel yiy tàggat askan wi dañoo bàyyi ñi jàngul ak seen bopp ndax làkk frãse lañu fay tàggate.
s-116 Tàggat nit ki ci làkk wi mu dégg moo gën a yomb juróom ñaari yoon - gën gaa néew - tàggat ko ci lammiñu jàmbur.
s-117 Tàggat ci wolof soxlawul lu dul mu man a bind, man a yër ndax làkk wi dégg na ko ba noppi.
s-118 Bu dee ci wu doxandéem la nag (niki Frãse), dina laaj yeneen yu mel ni nos-wax, tëggiin xam bennaani baat yi ak waxiin wi añs.
s-119 Nguur gi am na ay jafe-jafe ci fal boroom lijaasa yi sunu daara yu kawe yi tàggat, rawatina ñi seen xam-xam màcc ci kàllaama yi.
s-120 Ñu néew ci askan wi ñoo di yër yéenekaay yi ñu bind ci wu Frãse.
s-121 Daanaka ñi leen di yër matuñu ñaar fukk ci téeméer (20 %).
s-122 Ba tax na njariñam taxu koo bari.
s-123 Saafara si: Gën a yaatal njàngale mi ci sunu làkki réew, jaarale ko ci taxawal ay jumtukaayu tas xibaar ci sunu làkki réew, rawatina ay dali internet.
s-124 Taxawal ay këri yéenekaay ci sunu ay làkk;
s-125 Fexe ba tekki film yi ñu di seetaan ak fowukaay yi sunu xale di jëfandikoo ci sunu ay làkk; rawatina ci wolof ndax mooy làkk wi ëpp lu ñu koy jëfandikoo ci réew.
s-126 Defar tëriin ci sunu ay làkk.
s-127 Loolu doon na luy yokk xereñug askan wi.
s-128 Dina yokk ay junniy junniy liggéey ñeel ndongo-daara yi ñu tàggat te amuñu fu ñu leen dugal, ñoñ fànn ñi (ci tekkig film yi ci sunu ay làkk).
s-129 Dina yokk sinemaa yi ñuy seetaane film yi, dina yokk njënd mi ak njaay mi.
s-130 Nañu xayma ñaata ci ay film yu wayndare, fowukaay, téere ak film yu xale ñoo am ci àdduna bi ci yeneen i làkk te ñu man koo soppi ci sunu ay làkk, su nu bëggee xam njariñ li ci wàllu kom-kom ak xel.
s-131 Ndaxam man nañu di jëfandikoo làkku Faraas ba léegi, waaye loolu warul a tax ba ñu bañ a xalaat ne aw làkk lu man a indi kom-kom la su fekkee ni lu ëpp ci askan wi moom lañu di jëfandikoo.
s-132 Looloo dal wolof fii ci Senegaal, bambara ca Mali.
s-133 Loolu la Microsoft sàmm ba tàmbali a amal Windows ak Office ci làkk yu mel ni wolof ak bambara.
s-134 Google tamit tàmbali na ko.
s-135 Loolu tamit la waa Faraas xam ba taxawal kuréel gi ñuy woowe Francophonie.
s-136 Lu ñu gën di jëfandikoo làkku Faraas ci àdduna bi rekk (lu tollu ak ñaari téeméeri milyoŋ ci doomi aadama) gën di yokk ay liggéey ca Faras, ndax ñoom ñoo di soppi film yooyu di ko jaayaat yeneen téeméer ak ñeen-fukki milyoŋi doomi aadama yi nekk ci yeneen réew te di jëfandikoo làkku Faraas te nun noo ngi ci biir.
s-137 Ndax làkk wolof am na mucc?
s-138 Colette Grinevald di ab gëstukat ci làkk ca laboraatuwaaru làkk ba ne ca Lyon-II.
s-139 Ci ab gëstu bu mu defal Unesco aju ci dundiinu làkk yi, jàpp na ne lu jege 50 % ci làkk yi dinañu saay fi ak atum 2100.
s-140 Am na sax gox yu nga xam ni, man na a am mu egg ci 90 % (niki Óstrali ak Amerig).
s-141 Gisees na ne ca atum 2100, làkk yu ñu di gën a wax ñoo di: Àngale, niki làkk njënd, njaay ak xarala, Español ca bëj-saalumu Amerig, Purtugees, ca bëj-saalumu Amerig ak Afrig, Araab, Sinwaa ak Endo ca Asii, Swaahili ak Wolof, ci Afrig.
s-142 Li ñu mën a jàngee ci mbajtalu gëstu bi moo di: Benn, làkk Frãse bokkul ci làkk yi am mucc.
s-143 Te monte Colette Grinevald mi jiite gëstu bi doomu réewum Frãs la.
s-144 Kon ndax warees naa wéy di jiital ci réewum Senegaal làkk wu amul mucc, rax-ci-dolli 10 % askan wi rekk a ko dégg ba mën koo jariñoo?
s-145 Ñaar: Sunu làkk wii di Wolof doon na làkk wu am mucc ba tax ñu war koo jiital ci réew mi.
s-146 Kon ndax wareesuñoo jiital làkk wu ame nii mucc te lu ëpp 80 % askan wi dégg te di jëfandikoo?
s-147 Cosug àdduna bi ak Big Bang
s-148 Nit dafa mas di laaj ci jamono ju nekk, fan la àdduna su daytaluwul sii jóge?
s-149 Fan la jëm?
s-150 Nan la àtte yiy wattu ag màndaqoom ak ag nosoom di doxe.
s-151 La-ko-dale ci ay xarnu, boroom xam-xam yi def nañu ay gëstu ci lu aju ci tëriit loolu.
s-152 Ñu àgg ci génne am mbooloom ay gisiin.
s-153 Xalaat bi notoon ci xarnub fukk ak juróom ñeent moo doonoon àdduna bi de am mbooloom ne-ne la, yu yor dayo bu amul yamu, yu fi nekkoon naka jekk, te di yu fi dul jóg it ba fàwwu.
s-154 Gis-gis bii nga xam ne mooy cëslaayu xeltu gu ngérum ne-ne dafa daan dàq ak a weddi amug aji-sàkk ji (Yàlla), ba noppi di saxal ne àdduna bi amul ab tàmbali, te amul it ab yamu.
s-155 Ngérum ne-ne, nosteg xalaat la, gu di jàppe ne-ne ne mooy genn nekk gu joyu gi fi am, ci noste gii.
s-156 Lenn lu dul ne-ne amul.
s-157 Nosteg xalaat gii nga xam ne mu ngi sosoo ca Geres Gu Yàgg ga, te gën a tase ci fukk ak juróom ñeenteelu xarnu, mujj na di lu siiwe ci turu ngérum ne-ne mu dàggasante mu Karl Maks.
s-158 Ñoñ ne-ne ñi dañoo jàppe woon xalaatu àdduna bu amul yamu bii muy seen ndëerlaay lu mag.
s-159 Ci misaal, ca téereem ba tudd (dal yu dàttu yu xeltu) saa ne-ne mii di Jorj Politseer, saxaloon na ca ne àdduna bi du lu ñu sàkk.
s-160 Mu dolli ca ne bu doonoon lu ñu sàkk, dafa waroon a nekk di lu Yàlla sàkk ca saa sa te mu tukkee ci ag neen.
s-161 Bi Politseer saxalee ne àdduna bi sàkkeesu ko ci ag neen, dafa sukkandiku woon ci misaal mu sax mu àdduna bi te nekkoon fi ci fukk ak juróom ñeenteelu xarnu.
s-162 Mu xalaatoon ne def na ag saxal gu xam-xam.
s-163 Ci biir loolu jëm-kanam yi xam-xam ak xarala amal ci ñaar-fukkeelu xarnu, màbb nañu ci mujj gi xalaat bu njëlbéenu bii ñu di wooye ngérum ne-ne, wuññees na ne àdduna bi saxul ni ko ñoñ ne-ne ñi daan waxe.
s-164 Waaye ci safaan bi dafa nekk ci ag tàllaliku.
s-165 Gisees na it jaare ko ci seetlu ak xayma ne àdduna bi am na ab tàmbali (fu mu tàmbalee), te dees ko sàkk mu tukkee ci tus, ci ag fàcc gu mag.
s-166 Tay jëf jii àddunay xam-xam jépp nangu na ko, te wuññig jëf yu am solo yii mu ngi jàppandee ci ay seetlu ak i njuréefi gëstu yu di ag jeqiku.
s-167 Ca 1929 ca seentluwaay bu Monpiuson ca Kaliforni, ab saytukatu bidiw bu Amerig bu tudd Elwin Oban defoon na benn ci wuññi yi gën a mag ci taariixu saytu-bidiw.
s-168 Bi mu di seetlu bidiw yi ci ag fésalukaay gu ngande, gis na ne dañuy génne genn leer gu xaw a xonq, ci kem seen ag soreyoo.
s-169 Loolu li muy wund moo di bidiw yi dañu di dem sori nu.
s-170 Waawaaw, ci li ay àtte yi ñu nangu ci jëmm wax, jëmmi ceññeer yu leer yi bu ñu di tuxu jëm ca tombub seetlu ba, dañu di jeng jëm ci yolet, te jëmmi ceññeer yu leer yi di dem di sori tombub seetlu bi dañu di jeng jëm ci xonq.
s-171 Seetluy Oban yi may nañu nit xam ne leeri bidiw yi dañuy jëm ci xonq.
s-172 Loolu li muy wund mooy ñoom kat dañoo dëkk ci di nu sori, di dem wëlis nu.
s-173 Ginaaw loolu Oban defaat geneen wuññi gu mag.
s-174 Lu tàllalikug àdduna bi di wund?
s-175 Tallalikug àdduna bi dafa di wund ne bu ñu manoon a deltu ginnaaw, dinañu seetlu ne àdduna baa ngi doore ci benn tomb, fa la jële cosaanam.
s-176 Xayma yi wone nañu ne benn tomb bii nga xam ne moo ëmboon mbooleem ne-ne bu àdduna bi dafa waroon a am kemu ab dayoo ak ag fataay gu amul yamu.
s-177 Àdduna bi nag mu ngi sosoo ci fàccug benn tomb bii yoroon dayob tus.
s-178 Fàcc gu mag gii nga xam ne ci la àdduna bi doore, tuddeesoon na ko Big Bang, gisiin wi it daal di jël tur wi.
s-179 Ci ag pàttali dayob tus aw waxiin wu gisiin la wu ñu jëfandikoo ngir man a leeral.
s-180 Xam-xam manul a leeral maanaam neen mi nga xam ne weesu na digi déggiinu nit, ba mu koy tuddee tombub tus.
s-181 Ca dëgg-dëgg, dayob tus mooy ag neen.
s-182 Ci noonu àdduna bi mu ngi sosoo ci ag neen.
s-183 Ngir gën a leer, dees koo sàkk.
s-184 Lii nga xam ne ci ñaar fukkeelu xarnu rekk la ko xam-xamu jëmm bu jamonoo bi wuññi, Alquraan moom saxaloon na ko booba ak léegi tollu na ci fukk ak ñeenti xarnu.
s-185 Moom moo sos asamaan yi ak suuf si.
s-186 Ñi weddi xanaa gisuñu ne asamaan yi ak suuf si benn jóor lañu woon bu taqaloo (lu ci ne tayu ci moroom ji), ñu tàqale leen.
s-187 Loolu li muy wund mooy lépp sàkkees na ko ci genn fàcc gu mag gu bawoo ci benn tomb.
s-188 Bu ko defee mu doon àdduna bii nga di gis bi mu tàqalikoo.
s-189 Tàllalikug àdduna bi benn la ci firnde yi di wone ne àdduna bi ci ag neen lañu ko sàkke.
s-190 Lii nag xam-xam wuññiwu ko lu moy ci ñaar-fukkeelu xarnu bii rekk, waaye Yàlla moom jotoon na nu koo xibaar ci Alquraan, ju ñu wàcce booba ak léegi tollu na ci 1400 at.
s-191 Asamaan si ñoo ko tabax ci sunu kàttan, di ko yaatal it ci anam gu sax.
s-192 Big Bang dafay wone ci anam gu leer ne àdduna bi ci ag neen lañu ko sàkke.
s-193 Ci nu gën a leer, Yàllaa ko sàkk.
s-194 Looloo tax saytukatu bidiw yi taqoo woon ak xeltu gu ngérum ne-ne mi (materialime) wéyoon ci weddi Big Bang te sax ci dëgëral xalaatu ab àdduna ju amul yamu bi.
s-195 Sababi lànk gii feeñ na ci baati Artir Edington, benn boroom xam-xamu jëmm bu siiw la woon: (ci wàllug xeltu, déggiit wu ag tàmbali gu bette dafa ma di xatal).
s-196 Beneen saa ne-ne bu waa Angalteer di Fred Hoyle, moom itam gisiinu Big Bang xatal na ko.
s-197 Ci digg ñaar-fukkeelu xarnu Hoyle daldi nay doon farandoob gisiin wu melokaan wu sax wi.
s-198 Woowu gisiin dafa niroo woon ak wa fi nekkoon ca fukk ak juróom ñeenteelu xarnu, te di woon àdduna bu tekkaaral bi.
s-199 Gisiinu melokaan wu sax wi dafa saxaloon ne àdduna bi ab kemam amul yamu naka noonu ab diiram.
s-200 Gisiin wii nga xam ne amul woon geneen jublu gu feeñ gu dul dëgëral xeltug ngérum ne-ne nekkoon na di lu safaanoo ak gisiinu Big Bang wi saxaloon ne àdduna bi am na ag tàmbali.

Text viewDownload CoNNL-U