Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev

Select a sentence

Showing 201 - 300 of 449 • previousnext

s-201 Mu ni: Ba ñu dugalee Seexul Xadiim ci puq si woon ci Ndakaaru, mu xat lool, sëfees ko ak i ràbb ak i fital, ndeysaan, Soxna Jaara fekk na ko fay ko mastawu di ko ñaax.
s-202 Soxna si di ko fàttali la mu ko yare woon, muy di xool ca gaa ñu baax ña wéy, ak la ñu dajoon ngir yelloo seen i cer.
s-203 Yonent bi feeñu na ko di ko ñaaxe Amsatu, naan ko: Xoolal Amsatu (jàmmi Yàlla ci moom) di ab Sahaaba bu jàmbaare ak rayiin wu ñaaw wu ñu ko ray.
s-204 Loolu la Sëriñ Muusaa Ka naan: nee na keroog gis na fa sunu maam Jaara, mu di ko ñaax te di ko dolli ay daara.
s-205 Njool Màkka naan ko xamalal Sahaaba bu tudd Amsatu lan moo di Xitaaba.
s-206 Sëriñ bi nag, ku fonkoon Soxna si la te daan ko wormaal.
s-207 Dëkk bii mu nekkoon di Poroxaan dafa mujjoon gent, waaye Sëriñ bee ko dekkilul, lépp ngir worma ak fonkeel ak bëgg noo baaxe jeexiti soxna si.
s-208 Xabru ba it reeroon na, ba xameesul fu mu nekkati, waaye Sëriñ bee jox ndigël Sëriñ Mbàkke Gani Buso, doomu nijaayam, ngir mu seetal ko te saytul ko barab boobee.
s-209 Sëriñ Mbàkke Gani Buso def ay yitte, ba dégg ab pël bu ko xam.
s-210 Mu ànd ak moom ñu wër ba gis ko, mu koy taxawu ci ndigëlul Sëriñ bi.
s-211 Ginnaaw bi mu tàbbi ci loxol Sëriñ Muhammadu Basiiru Mbàkke, mu koy taxawu ba ni mu fi jógee.
s-212 Noonu it la ko ag njabootam di taxawoo ba fimne.
s-213 Am na sëriñ bu sàmmu woon, ragal Yàlla, di ab jàngkat te di ab jàngalekat, muy Sëriñ Sàmba Mareema Saa-kokki, doon wóllare wu Maam Moor Mbàkke, sëriñu Soxna si, wayoon na ay woy ci Araab ngir seere jikko yu sell te rafet yu mu gis ci Soxna soosii di soxnas wóllareem, Soxna Jaara Buso.
s-214 Way yooyu waxees na ni lu Sëriñ bi fonkoon la, daan ko yër lu bari, ba mujj gi mu wayluwaat ko ngir ag yaatal.
s-215 Loolu lépp di tektale ag cofeel ak ag fonkeel gu mu am ñeel way-jur wi.
s-216 Waaw kon ana lu tee ñi dëkk ak moom xëntewoowuñu jéem a mel nii?
s-217 Ana lu tee nu gaaral aw doxiinam ak i jikkoom ci kanamu sunu ag njaboot?
s-218 Lu tee nu jàppe ko royuwaayu askan wi ñeel soxna yépp?
s-219 Waaye fimne ak lii lépp tudd ci sunu aw làmmeñ Àllin Situwe Jaata mbaa ñu mel ni niki royuwaayu jigéeni réew mi moo di lu ràññeeku, te di lu dajale ba ñépp man ko a wax ci barab yépp it.
s-220 Waaye tudd sunu soxna yi moom, dafa mel ni lu informel la te it ku ci nekk ña féete ak yaw rekk a di tudd sa aw tur, di wax sa ay jikko, di la misaaloo.
s-221 Ba mujj sax ñu di am ag pasu ci tudd leen ngir bañ ñu ni fii nga bokk mbaa fee.
s-222 Nangu naa ag bañam ak ag njàmbaaram ci kanamu notaakon yi.
s-223 Waaye matul ab royuwaay sunu jigéen ñi ci wàllu diine, ndax wax dëgg Yàlla nag, moom dafa amoon ay gëm-gëmi boppam, muy la maam ya daan dund muy ag xërëm (animisme).
s-224 Bokkoon na ci xeexam bi gënoon a rëy, delloo askan wi ak di leen xelal ci ñu dellu ci jaamu li fi maam yi bàyyi woon, te bàyyi diine yu bees yi fi ganesi (Nasaraan, Lislaam, añs...).
s-225 Wax dëgg kii ak lu mu jàmbaare-jàmbaare matul royuwaay ñeel sunu soxnay jullit yi ngir ab pas-pas moo war a jëkk ci ag roy, te wuute nañu ci.
s-226 Kon daal ku mu neex yamal ci di ko sargale li mu def rekk, ak taxawaay bi mu amee woon ci kanamu tubaab yi.
s-227 Loolu mu gëmoon it nag du ab gàkk ci moom, ndax ci bañ gi mu doon bañ kenn moom nu rekk la ko tegoon, tax mu bañaale bépp diine bu fi nar a jële li fi nekkoon.
s-228 Waaye ginnaaw diine yooyu nag noo ko tànnal sunu bopp ginnaaw bi, nanu ci farlu te roye ci ñi ci nekkoon waliif keneen.
s-229 Ma ni nanu bàyyi par-parloo te yeewu, génn ci ag fasu, dugante, xam sunu ay nit, xam seen i jëf, seen i melo, xam li nuy jariñ nu jëfandikoo ko.
s-230 Waaye kii fee la bokk ak fii bu mu nu tee xamale sunu soxna yu yéeme yii ci ay jëf, di yi ñu taamu te war leen a jàppe niki ay royuwaay, ñeel askan wépp, te di jàngale jikkoy Soxna yii ak seen ab taxawaay ci njaboot gi ak pénc mi.
s-231 Ngir nu man a am pénc mu dal te bari jàmm, bari jaamukati Yàlla, di ay jullit, yu sàmmu, sàmm seen ngor, di dund ci sutura, te mucc ci tooñ...
s-232 Lii daal lañu di sàkku ci Yàlla mayaakon bi.
s-233 Kii nee na: Man de soxna laa te ab jullit laa, waaye nii Soxna Jaara mel manuma koo mel?
s-234 Wax nga dëgg kay!
s-235 Waaye bu la loolu tax a sàggan mukk ba doo def kem sa kàttan te defe fi nga toll.
s-236 Ndax kat, bu ñu nee ku ñëw Tuuba dinañu faj sa aajo, sëriñ si ak taalube yi ñépp ay jógandoo wuti Tuubaa.
s-237 Ñi yor wata taal ko.
s-238 Ñi yorul wata paas dem.
s-239 Ñi yorul paas dox wuti Tuuba.
s-240 Ku di xalaate nii de doo nangoo tële dara lu sa moroomu nit def ndax danga di defe ca na nga ko mane rekk ak sa tolluwaay.
s-241 Li ci des Yàlla aji-tedd ji moo koy mottali.
s-242 Dama di wax ni: Yàlla laaju nu nu gën fi waaye li mu nu laaj kay mooy nu def sunu kem kàttan!
s-243 Kon nanu farlu te xam ni nag Yàlla xam na li nu man.
s-244 Bu nu ko deful rekk danoo lànk, te jaam bu lànkal boroomam ab atteem leer na.
s-245 Nu leen di ñaanal Yàlla màggalug jàmm, ak i xeewal ak pajug aajo, ci bis bu tedd bii di màggalug Poroxaan, dees na ko fàttalikoo jëmm ju tedd, di soxna su nu taamu, Soxna Jaara Buso.
s-246 Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yi di dugg Senegaal te di jóge bitim-réew war a am.
s-247 Mu ngi ko dogale ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru.
s-248 Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare 2012-444 soppi bu 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi.
s-249 Dekkare boobu dafa di tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yi di duggu Senegaal war a am.
s-250 S. Sàll dige woon na ci baatum dagaan ne dina ko def bu ñu ko tegee ci boppu réew mi.
s-251 Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal.
s-252 Lu tax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal?
s-253 Loolu la waxoon.
s-254 Dogal booboo ngi tukkee woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar yi te aar kéew gi ci saxaar su bon si di tukkee ci oto yu màgget yi.
s-255 Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi yi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon.
s-256 Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dogal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi.
s-257 Milyoη ak 450 junni ay toni jën ñoo di jaar at mu nekk ci géeji Senegaal yi.
s-258 Jëwriñ ji yor Koomug Géej gi, Xureysi Caam jibal na ne at mu jot 1 Milyoη ak 450 junni ay toni jëni biir géej dinañu di jóge géeju Kap-weer jaar ci sunu géej yi.
s-259 Xureysi Caam mi doon àddu ci surnaalu 12 w bu Rfm, leeral na ne jën yooyu dañuy njëkke jaar Giné-Bisaaw, Gàmbi, Senegaal, Moritani, Marok door a dëppaat.
s-260 Bu ñu egsiwaatee Moritani, te nappeesu leen, dañuy dee.
s-261 Teg na ci ne: am na 1 milyoη ak 450 junni ay ton yu doomi réew mi mënul a napp, ndax amuñu jumtuwaay yu ko mën a napp.
s-262 Jëwriñ jee ngi laaj: Ku di napp toni jën yooyu?
s-263 Ay bato wëyyu ñoo koy napp, bato yu xarala lañu, gaaw lool te mëneesu leen a teg loxo.
s-264 Loolu lanuy ñàkk at mu jot.
s-265 Ndax jaadu na nguur gi di seetaan woowu yàqute, déedéet.
s-266 Nee na, xalaat nanu ren, jàppandal ay batoy biir réew mi ak yu bitim-réew ngir ñu dem nappi jën yooyu.
s-267 Nee na, li ñuy napp dina nu indil at mu nekk 35 Dollar (ton bu nekk).
s-268 APS: Dibéer 15 maars 2009
s-269 Ku wax feeñ: demokaraasi ag làkki réew mi
s-270 Wote bi nu dëgmal, ñépp xam nañu ko, wote bu jeggi dayoo la: ndax ci la ëllëgu réew mi aaju!
s-271 Wote la wu ñuy tànne wan yoon la Senegaal war a teggu jëm ca kanam mbaa mu teggi ko, dellu gannaaw: lawla cat!
s-272 Wante li ñu soxal ci jukki bii, lu lëkkëloo ag loolu gaa, wante leneen la.
s-273 Loo xam ne soo ko seetloo, dafa mel ni dafa am jàllarbi ci ni 'politiciens' di jëfandikoo làkki réew mi!
s-274 Li ñu leen doon faral di wax mooy : demokaraasi ci làkki jambuur ay kàcci neen la, mënul a nekk!
s-275 Ndax demokaraasi mooy nguuru askan wi ngir askan wi!
s-276 Waaw, bu fekkee ne nag fa ñuy takke ak a tekki, fa ñuy dogale, fa ñuy fasee ak a fecci, ña fay wax duñu wax lu askan wi mën a dégg, naka lees mën a tuddee mbir mooma demokaraasi?
s-277 Dafa mel ni daal buum bi nu kolonisatëër bi nasoon, ba taxoon ñuy wéy ci waawaam, ba léegi dógagul!
s-278 Te buum boobu, xàncc bi ñu ko ràbbee mooy di jëfandikoo làkki Nasaraan soofal sunu bos, di jàng cosaanam fàtte sunu bos, jël ay kureelam indi teg, jël doxalinam indi teg, jël xaalisam indi teg.
s-279 Te loolu feek mu ngi fi, cóow li mooy bari rekk, wante demokaraasi dëgg, mbaa jëm-ca-kanam ci wàllu koom-koom caada ag nekkinu askan wi dina fi jafe lool!
s-280 Li di firndeel loolu, mooy ba Nasaraan bi xamee ne léegi mu ñakk réewi Afrik yi mu kolonise woon, fekk Alseeri ngi di xare ngir moom boppam, Wietnam duma Faraas Jemben-Fuu, Kamerun tàmbali a fippu, Seneraal Degaulle dafa ne woon: 'nañu yolomal buum gi balaa moo dóg'!
s-281 Te loolu li muy tekki mooy , na fi sunu jëmm yi jóge, wante sunu doxalin moom na sax ci xel yi ba fàww!
s-282 Te looloo fi amoon, ba fi Seηóor nekkee ba ci Abdu Juuf ag ñi fi nekk téy!
s-283 Xam nañu ne Seηóor ba mu fi jógee dafa dem Faraas nekk 'Accadémie francaise', Abdu Juuf jóge fi dem jiiteji 'francophonie' di bàkk, di bàkkoo làkki nasaaraan!
s-284 Xalaas, loolu de du ngoóora!
s-285 Te su caaxaan faaxee dëgg des, Afrikee rekk ngay gis muy nangu loolu!
s-286 Kenn ñemewul xalaat sax, gis Sinwaa, mbaa Sapone mbaa Wietnamee buy soofal làkk wi mu nàmp, dem di bàkkoo làkki ñi ko mas a dëkkee tuutal ag nas buum!
s-287 Dañu fee déggoon ci lu yàggul dara sax njiitu-réew mi di wax di bàkku naan, Senegaal mooy réew mi nga xam ne, soo limaaleewul Faraas, fa la nit ña gën a xereññe ci làkk Nasaraan!
s-288 Wante nag Wolof Njaay dafa ne li nga moom nga mën a tiitaroo!
s-289 Li nga moomul moom, Bafa rekk la sànt!
s-290 Seex Anta yokk ca ne 'làkki jambuur de su safoon suukar ba mel ni lem itam, mënoo ko màcc ba cay taxamtiku'.
s-291 Ñakk a xam daal ag ñakk fayda li ñu waral bari na!
s-292 Ñu bari ci waay-xeltu yi sax dañoo defe ni, wax yu ni mel ay waxi-démb mbaa ay wax yu amul solo lañu, te fekk ne loolooy ndéyi-mbill ji!
s-293 Amul xejj-ak-seen, amul benn réew bu mën a am yokkute, am tawféex ci kow topp aadaa, ag cosaanu weneen askan, rawatina dëkkee jëfandikoo làmmiñ woo moomul te fekk Yàlla natoowu la ag lu!
s-294 Wante nag ba léegi yakaar tasagul!
s-295 Ndax téy su nga seetee xale yiy 'rap', seen xarala ci làkki réew mi, li ñu ciy wax, li ñu di ciy yàtt ci ay kàddu yu di xalam, seen farlu ci siggil réew mi ag askan wi, dootoo amati benn siiki-saaka ne làkki réew mi ñu ngi ci yoonu suqaliku gu wér!
s-296 Ba tax na sax, soo ko setantalee, dangay gis ne 'politiciens' yi seen bopp dafa mel ni dañoo xaw a nànd loolu!
s-297 Ndax léegi ñoom ñépp a taamoo wut ay dàkkentali wolof:
s-298 Moo xam 'Bennoo Siggil Senegaal la, Bes Du Ñàkk, Fekkee Ma Ci Boolee, Daas Fanaanal, Nay Leer, Car Leneen, Taxaw Temm' ag yeneen yeneen i yëngu-yëngu lañu!
s-299 Loolu soo ko seetloo bu baax ag jàllarbi la daanaaka, ab 'revolution linguistique' la!
s-300 Ndax ku ci nekk xam na ni soo nee askan wi 'Bennoo Siggil Senegaal' rekk nit ñi xam loo wax, jaratul sax nga leen di faram-fàcceel lenn.

Text viewDownload CoNNL-U