wo-wtb-train-xibaaryi-njaayum_geerte

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain
AnnotationDione, Bamba

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 15

Njaayum geerte gi ni mu di doxe baaxul, la njiitu jëwriñ yi naqarlu. Njiitu jëwriñ yu Senegaal, Suleymaan Ndeene Njaay, naqarlu na, àllarba ca Ndakaaru, ni njaayum geerte gi di deme, jàpp na ne ni mu di doxe baaxul dara. Nanu waxante dëgg ndax ñi di defar diwlin ji amaguñu xaalis bu doy ngir jënd geerte gi, mu di lu mu nangu. Seriñ Njaay a ngi doon àddu ca peggu ubbiteg 12eelu FIARA (Fuwaar bi àddina bi jagleel mbey ak càmm ci Ndakaaru, 2 - 13 fewrie. Ci Fuwaar boobu, waxtaan wi mu ngi jëm ci: mënal sa bopp ci ag dund. Waaye, nguur gi du ko seetaan.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees