wo-wtb-train-wol-wiki-Jolof

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain
AnnotationDione, Bamba

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Jolof moo doonoon nguur gi gënoon a mag ci Senegaal ci jamono yooyu. Mu ngi sosu ci xarnub XIV ba Nguuru Mali gu mag ga saayee, rawatina la feete woon ca sowam. Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono. Ki ñu ne moo sos nguur googu moo di Njaa Jaan Njaay. Moom doomu Araab la bu ñuy wax Abaabakar ak Lingéer ab Tukulóor bu tudd Faatimata Sall. Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees