wo-wtb-test-xibaaryi-dalal

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest
AnnotationDione, Bamba

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Xibaaryi.com ab dal la (site) bu di tas xibaar ci wolof, muy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal. Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar doonoon gëstug jeexal gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa Kelekey Jaxate. Dal bii nag benn la ci saafara yi nu nar a saafaraa jafe-jafe yii nu lim ci suuf. Ci Senegaal, lu tollu fukk ci téeméer (10 %) rekk ci askan wi ñoo dégg làkku Frãse ba mën ci a jariñu, bu nu méngalee lim boobu ak lu ëpp juróom ñatt fukk ci téeméer (80 %) ci askan wi, ñu nga xam ne seen ag dégg wolof kawe na. Ñu bari ci askan wi dañu di seetaan ay film te duñu xam sax lu di maanaa mi. Loolu nag di mbir mu doy waar ci askan wu bëgg ñu weg ko.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees