s-1
| Lesoleil: Gàawu 11 awril 2009 |
s-2
| Porogaraam biy xeex sibbiru ci réew mi te tudd PNLP, ci jàppleg ñi muy jëflanteel, yeesal na xam-xamu 51 njiiti doktoori gox yi ak seen i toftal, ci pexe yu bees yi ñu tëral ngir xeex sibbiru, ci ñaari lël. |
s-3
| Ñaareelu lël bi, jëm ci njàngale ñeel sibbiru ak xeex bi mu laaj, dajale na 26 doktoor. |
s-4
| Lël boobu mu ngi tàmbali ci 16 màrs ci Daaray Wér (ISED) tëj ci 4 awril 2009, ci njiitéefu Dr Asan Yaradu, kenn ci ñi di xelal njawriñu wér ak fàggutéef. |
s-5
| Doktoor Pàppa Muusaa Coor miy saytu PNLP xamle na ne njàngale mii ñu sumb mu ngi bokk ci pexe yi ñu tëral ngir sibbiru ak dee yi muy jur bañ a jéggi tolluwaay bi mu nekk jamono yii. |
s-6
| Ndax gisees na ne tolluwaay bi dafay gën di wàññiku te li ko waral moo di pexe yi ñu tëral ngir xeex jàngoro ji. |
s-7
| Mënees naa lim yenn ci pexe yooyu: joxe sànke yu ñu nàndal, ak fexe ba garab yi (ACT) ñépp mën cee jot ci njëg gu yomb, ak def ay càmbar yu feeñal jàngoro ji, na mu gën a gaawe. |
s-8
| Ci 2008, tolluwaay baa ngi nekkoon ci 5,6 % te mooy junni nit ñu ne, juróom-fukk ak juróom–benn yi sibbiru dal na leen. |
s-9
| Looloo waral Dr Coor yokk ci: su nu wéyee di góor-góorlu, waxuma rekk ne tolluwaay bi dina yem foofu, waaye sax dinanu faagaagal xeetu sibbiru bii. |
s-10
| Ci xalaatam, ngir bundxataal sibbiru, dafa laaj beneen wirgo doktoor, beneen wirgo saytukat ngir tolluwaayu dee gi ci aju ak jàngoro ji bañ a yéeg. |
s-11
| Looloo tax ñu taxaw temm ci yeesal xam-xamu doktoor yi te dooleel leen ci pajum sibbiru, Doktoor Coor teg ko ci. |
s-12
| Njiital Ised, Pr Anta Taal Ja, moom, dafa ñaax doktoor yi ñu nekk ay mbër ak ay saytukat ci xeexu sibbiru, ku nekk ci sa gox. |
s-13
| Doktoor yi ñoom rafetlu nañu njàngale mi, ndax ñi leen doon xamal wàccoo nañu ak ñoom, li ñu ci doon xaar gis nañu ko. |