s-1
| Njaayum geerte gi ni mu di doxe baaxul, la njiitu jëwriñ yi naqarlu. |
s-2
| Njiitu jëwriñ yu Senegaal, Suleymaan Ndeene Njaay, naqarlu na, àllarba ca Ndakaaru, ni njaayum geerte gi di deme, jàpp na ne ni mu di doxe baaxul dara. |
s-3
| Nanu waxante dëgg ndax ñi di defar diwlin ji amaguñu xaalis bu doy ngir jënd geerte gi, mu di lu mu nangu. |
s-4
| Seriñ Njaay a ngi doon àddu ca peggu ubbiteg 12eelu FIARA (Fuwaar bi àddina bi jagleel mbey ak càmm ci Ndakaaru, 2 - 13 fewrie. |
s-5
| Ci Fuwaar boobu, waxtaan wi mu ngi jëm ci: mënal sa bopp ci ag dund. |
s-6
| Waaye, nguur gi du ko seetaan. |
s-7
| Jëwriñu mbey mee ngi topp mbir moomu. |
s-8
| Seetlu naa, gannaaw bu ma jokkoo ak yenn ci ay beykat, ne ñenn ci ñoom a ngi joxe seen i geerte te duñu jot benn xaalis, la njiitu jëwriñ yi xamale. |
s-9
| Wéral na ne mbir moomu mënul a yàgg. |
s-10
| Nguur gi dina jël ay matuwaay ngir ñi jël geerte beykat yi fay leen ci lu gaaw seen alal, loolu la dige. |
s-11
| Altine jii, dinaa dajale njiitu bànk yi ak ñi di defar diwlin ngir nu génne ay saafara. |
s-12
| Du yoon beykat bi def ñetti weer di bey suuf si, déqi, ba noppi jot ay boŋ gannaaw bi mu joxee geerteem, loolu la naqarlu. |
s-13
| Alxamis bi weesu, ci Jotaayu Jëwriñ yi, jëwriñu mbey mi, Xaadim Géy, siiwaloon na ne dajalees na 120000 tonu geerte ci réew mépp, ci 45 fani dagaan. |
s-14
| Maki Sàll tënk na ci 8 digub at yi oto yi di dugg Senegaal war a am. |
s-15
| Ndakaaru, 13 awril (APS) |