Dependency Tree
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | train |
---|
Annotation | Dione, Bamba |
---|
Select a sentence
s-1
| Microsoft: Siiwalug Windows Phone 7 |
s-2
| Microsoft dellusi na ci ag woote ak ab gaaral bu ràññeeku altine ci lu aju ci telefonam bi ñépp di xaar Windows Phone 7 ànd ak defar Nosteg Doxiin (operating system) bu bees tàq ñeel Mobiil. |
s-3
| Doorees na ag gaaralu Windows Phone 7 ca New York. |
s-4
| Gaaral googu njiitul Microsoft Stef Balma moo ko jiite, ngir wone ni seen nosteg doxiin bu bees bi dafa nekk lu taaru te yéeme. |
s-5
| Ku nekk war naa man a seet Windows Phone te wax ni man na maa teewal la Balma wax. |
s-6
| Ci loolu, joyalees na siiwalug Windows Phone jëmmalug man-mani telefon bi ak ay leeral ci juumtukaay yi ci nekk. |
s-7
| Wonees na nosteg doxiin bi mel niki luy mottalil boppam ag dundam ci lu dul di ko xaar feneen. |
s-8
| Siiwalees na juróom ñeenti telefoni Windows Phone yoo xam ne fimne way-jëfandikuy waa-aamerig dinañu ci daldi man a tàmbali a tànn, ànd ak T-Mobiil AT&T génne ko, ci gën gaa yeex, 8 Nowàmbar. |
s-9
| Lu aju ci tëriin li, jëmmal gi ak yomb-gee-jëfandikoo moo di li tax a jóg Mickrosoft ci lii, ci yakaar a joxe jëmmal gu mat sëkk. |
s-10
| Looloo tax sa Smartphone (telefon bi) man a teyewaale la ñu xamoon ci Microsoft-centric (beneen telefon). |
s-11
| Wax nag yomb na, kon nanu xaar ba Windows Phone 7 wàcc ci maarse bi (ja bi) nu xool ndax seen jubluwaay walla yéene jooju mel na ni. |
s-12
| Mbetteel gi gën a rëy ci wàllu ndefarum tëriin dal na leen, ndekete Windows Phone 7 déy manul sax a jël man-manu sotti-taf (copie-coller), Waawaaw! |
s-13
| Lu man a am daal manu ko fimne. |
s-14
| Nee nañu nag dinañu def ag yeesal ngir mu man ko ci weeru Saawiyee. |
Text view
•
Download CoNNL-U