Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain
AnnotationDione, Bamba

Select a sentence

s-1 Jolof moo doonoon nguur gi gënoon a mag ci Senegaal ci jamono yooyu.
s-2 Mu ngi sosu ci xarnub XIV ba Nguuru Mali gu mag ga saayee, rawatina la feete woon ca sowam.
s-3 Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono.
s-4 Ki ñu ne moo sos nguur googu moo di Njaa Jaan Njaay.
s-5 Moom doomu Araab la bu ñuy wax Abaabakar ak Lingéer ab Tukulóor bu tudd Faatimata Sall.
s-6 Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy.
s-7 Bokk na ci def Wolof yi ñuy benn, teg réew mi ci yoonu nguur gu leer.
s-8 Samp nguuru Waalo ba mu dëgër, mu daldi koy jox rakkam.
s-9 Sos nguuru Jolof gu mag ga ba mu yegg fa gën a kawe mu door a wàcce boppam.
s-10 Looloo tax ña ko wuutu ñoo mottali liggéeyam ci xarnub XIV, waaye jotuñoo moytu taste gu gaaw ca nguur gu mag ga.
s-11 Boo seetloo turi buur yu njëkk yi ci nguur gu mag gi dinga fa fekk ñent fukk doŋŋ.
s-12 Seen péey nekkoon na Céŋŋ ca jamonoy Njaa Jaan Njaay.
s-13 Réew yu bari nekkoon nañu ci kilifteefu gu mag ga.
s-14 Lu mel ni Senegaal ak Gaambi ak Faleme nekkoon nañu ci suufu Jolof gu mag ga.
s-15 Buur yi ñu mënoon fal ngir yilif nguuru Jolof, dañu doon war a bokk ci juróomi meen (wàllu ndeey), yooyu sant: Njaay, Joob, Faal, Ndaw, Ñaŋ.
s-16 Ci xeeti Seereer ak Pël, lañu jóge.
s-17 Jolof boo ko dee xool dafa këll bunom dem na ba Lag de Geer, égg na Ferlo.
s-18 Moom dafa xaw a uuf Tooro ak Dimat ak Waalo ak Kajoor ak Bawol ak Siin-Saalum.
s-19 Wàllu penku wi ndand féy-féy la.
s-20 Jolof fu neew ñax la, bari na lool garabi werek.
s-21 Mel na ne du fu naat it, ndax ab woykat bu siiw ci yu wolof yi di Sëriñ Musaa KA am na fu mu di melale lu ni mel ci genn xasidaam.
s-22 Mu ne: nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax soo màggatee yalwaani.
s-23 Kon du war a nekk fu bari ay balluwaayi xéewal.
s-24 Waa Jolof nekkoon nañu ay giir yu wuute.
s-25 Giir yooyu ay Séeréer lañu ak ay Wolof ak ay Tukulóor.
s-26 Naari Gànnar yi daan nañu song ñi dëkk ci tàkkal dex gi.
s-27 Nee nañu ki fa njëkk a dëkk mu ngi tudd Njolofeen Mbeng.
s-28 Mu ngi bokk ci xeetu Màndeŋ.
s-29 Turam lañu jox nguuru Jolof.
s-30 Moo fa njëkk a sos dëkk bu ñu daan wooye Kàyti, moom mu ngi nekkoon ci Yeŋ-yeŋ.
s-31 Fuuta moo doon gën jaa màggi réew ci mbooleem gox yi.
s-32 Loolu masul a deñ ba ci fukkeelu xarnu ak ñeent, moo tollook falug waa Tonjon.
s-33 Jamono jooju la Màndeŋ yi yaatal seen nguur gu mag dale ca géeju Atlas ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum ca Gàmbi.
s-34 Ca jamono jooju yit la nguuru Jolof nangoo boppam.
s-35 Moo gënoon a am solo ci réewu Wolof yi ak Séeréer si ak ci mbooleem réew yi ci géej gi, ci li ko dale ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum, Fuuta ba Saalum.
s-36 Ëmboon na Waalo, Kajoor, Bawol ak réewi Séeréer si ak lenn ci Fuuta Tooro.
s-37 Réew yu bari nangu nañu seen bopp ci nguuru Jolof gu mag ga.
s-38 Kajoor njëkk a nangu boppam topp ca Waalo ci njiitu Barag.
s-39 Bawol ci njiitu Teeñ.
s-40 Réewi Séeréer si ci njiitu Buur.
s-41 Jolof mujj na nekk réew ni yeneen yi ci xarnub XVI ba XIX.
s-42 Waaye Dammeel moom moo gënoon a metti ag jàmmaarloo ak Burba Jolof ca xareb Danki ba nga xam ne moo njëkk a faagaagal nguuru Jolof gu mag ga.
s-43 Gannaaw loolu la xareb Mbisin ca 1697, foofa Kajoor moo jekku, ak xareb Ambaal ci 1760, ak xareb 1886.
s-44 Bokk na ci li ngirteel saayam, ñaari noon yu doon xëccoo nguur ga ñaarelu xaaj bu xarnub XIX.
s-45 Noon bu njëkk bi mooy Tanoor Jeŋ.
s-46 Ñaareelu noon bi mooy Amadu Sayxu.
s-47 Tanoor Jeŋ doomi Lingeer Kura Ngoy, song na Buurba ngir nangu nguur ga.
s-48 Ginnaaw bi moom Amadu Sayxu nanguwaat ko ci 1870, yor ko ba ci atum 1875.
s-49 Ci at moomu lañu ko jekkoo ca xareb Sàmba Saajo.
s-50 Ci noonu la Jolof tàbbee ci loxoy Faraas ci 18 rakki gammu 1885.

Text viewDownload CoNNL-U