Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest
AnnotationDione, Bamba

Select a sentence

s-1 Xibaaryi.com ab dal la (site) bu di tas xibaar ci wolof, muy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal.
s-2 Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar doonoon gëstug jeexal gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa Kelekey Jaxate.
s-3 Dal bii nag benn la ci saafara yi nu nar a saafaraa jafe-jafe yii nu lim ci suuf.
s-4 Ci Senegaal, lu tollu fukk ci téeméer (10 %) rekk ci askan wi ñoo dégg làkku Frãse ba mën ci a jariñu, bu nu méngalee lim boobu ak lu ëpp juróom ñatt fukk ci téeméer (80 %) ci askan wi, ñu nga xam ne seen ag dégg wolof kawe na.
s-5 Ñu bari ci askan wi dañu di seetaan ay film te duñu xam sax lu di maanaa mi.
s-6 Loolu nag di mbir mu doy waar ci askan wu bëgg ñu weg ko.
s-7 Sunu ndaw ñi, di ëllëgu réew mi, dégguñu solo si baat yi ëmbu dëg-dëg ci film yi ñu leen di jagleel, wante dañuy banneexu rekk ci jëf ju reetaanlu ju ñu gis.
s-8 Loolu tamit di mbir mu nga xam ne du nàmm seen am xel.
s-9 Bu njëkkoon, barab ya ñu daan seetaane filmu Endo ak kowboy ya dañu daan fees dell ndax ñoo gënoon a neex a nànd.
s-10 Léegi, barab yooya soppees na leen ay ja (marse).
s-11 Loolu tax ba nit ñi dematuñu sinemaa niki nu ko daan defe bu jëkkoon, waaye tamit dégg-dégg bi jàppandiwul ci film yu mel ni poliis especiaal, afeer kalase tere awaase ak yeneen ak yeneen.
s-12 Kuréel yiy tàggat askan wi dañoo bàyyi ñi jàngul ak seen bopp ndax làkk frãse lañu fay tàggate.
s-13 Tàggat nit ki ci làkk wi mu dégg moo gën a yomb juróom ñaari yoon - gën gaa néew - tàggat ko ci lammiñu jàmbur.
s-14 Tàggat ci wolof soxlawul lu dul mu man a bind, man a yër ndax làkk wi dégg na ko ba noppi.
s-15 Bu dee ci wu doxandéem la nag (niki Frãse), dina laaj yeneen yu mel ni nos-wax, tëggiin xam bennaani baat yi ak waxiin wi añs.
s-16 Nguur gi am na ay jafe-jafe ci fal boroom lijaasa yi sunu daara yu kawe yi tàggat, rawatina ñi seen xam-xam màcc ci kàllaama yi.
s-17 Ñu néew ci askan wi ñoo di yër yéenekaay yi ñu bind ci wu Frãse.
s-18 Daanaka ñi leen di yër matuñu ñaar fukk ci téeméer (20 %).
s-19 Ba tax na njariñam taxu koo bari.
s-20 Saafara si: Gën a yaatal njàngale mi ci sunu làkki réew, jaarale ko ci taxawal ay jumtukaayu tas xibaar ci sunu làkki réew, rawatina ay dali internet.
s-21 Taxawal ay këri yéenekaay ci sunu ay làkk;
s-22 Fexe ba tekki film yi ñu di seetaan ak fowukaay yi sunu xale di jëfandikoo ci sunu ay làkk; rawatina ci wolof ndax mooy làkk wi ëpp lu ñu koy jëfandikoo ci réew.
s-23 Defar tëriin ci sunu ay làkk.
s-24 Loolu doon na luy yokk xereñug askan wi.
s-25 Dina yokk ay junniy junniy liggéey ñeel ndongo-daara yi ñu tàggat te amuñu fu ñu leen dugal, ñoñ fànn ñi (ci tekkig film yi ci sunu ay làkk).
s-26 Dina yokk sinemaa yi ñuy seetaane film yi, dina yokk njënd mi ak njaay mi.
s-27 Nañu xayma ñaata ci ay film yu wayndare, fowukaay, téere ak film yu xale ñoo am ci àdduna bi ci yeneen i làkk te ñu man koo soppi ci sunu ay làkk, su nu bëggee xam njariñ li ci wàllu kom-kom ak xel.
s-28 Ndaxam man nañu di jëfandikoo làkku Faraas ba léegi, waaye loolu warul a tax ba ñu bañ a xalaat ne aw làkk lu man a indi kom-kom la su fekkee ni lu ëpp ci askan wi moom lañu di jëfandikoo.
s-29 Looloo dal wolof fii ci Senegaal, bambara ca Mali.
s-30 Loolu la Microsoft sàmm ba tàmbali a amal Windows ak Office ci làkk yu mel ni wolof ak bambara.
s-31 Google tamit tàmbali na ko.
s-32 Loolu tamit la waa Faraas xam ba taxawal kuréel gi ñuy woowe Francophonie.
s-33 Lu ñu gën di jëfandikoo làkku Faraas ci àdduna bi rekk (lu tollu ak ñaari téeméeri milyoŋ ci doomi aadama) gën di yokk ay liggéey ca Faras, ndax ñoom ñoo di soppi film yooyu di ko jaayaat yeneen téeméer ak ñeen-fukki milyoŋi doomi aadama yi nekk ci yeneen réew te di jëfandikoo làkku Faraas te nun noo ngi ci biir.
s-34 Ndax làkk wolof am na mucc?
s-35 Colette Grinevald di ab gëstukat ci làkk ca laboraatuwaaru làkk ba ne ca Lyon-II.
s-36 Ci ab gëstu bu mu defal Unesco aju ci dundiinu làkk yi, jàpp na ne lu jege 50 % ci làkk yi dinañu saay fi ak atum 2100.
s-37 Am na sax gox yu nga xam ni, man na a am mu egg ci 90 % (niki Óstrali ak Amerig).
s-38 Gisees na ne ca atum 2100, làkk yu ñu di gën a wax ñoo di: Àngale, niki làkk njënd, njaay ak xarala, Español ca bëj-saalumu Amerig, Purtugees, ca bëj-saalumu Amerig ak Afrig, Araab, Sinwaa ak Endo ca Asii, Swaahili ak Wolof, ci Afrig.
s-39 Li ñu mën a jàngee ci mbajtalu gëstu bi moo di: Benn, làkk Frãse bokkul ci làkk yi am mucc.
s-40 Te monte Colette Grinevald mi jiite gëstu bi doomu réewum Frãs la.
s-41 Kon ndax warees naa wéy di jiital ci réewum Senegaal làkk wu amul mucc, rax-ci-dolli 10 % askan wi rekk a ko dégg ba mën koo jariñoo?
s-42 Ñaar: Sunu làkk wii di Wolof doon na làkk wu am mucc ba tax ñu war koo jiital ci réew mi.
s-43 Kon ndax wareesuñoo jiital làkk wu ame nii mucc te lu ëpp 80 % askan wi dégg te di jëfandikoo?

Text viewDownload CoNNL-U