s-1
| Jimbulang aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam, maanaam jimbulang bu di wax ci paj walla ci taariix kepp. |
s-2
| Jimbulang am mbooloom ay jukki la def, bu ci nekk di wax ci lenn: ci aw nit, ci ab barab, ci ab xew-xew, ci ab xam-xam, ... |
s-3
| Jimbulang dafa di wuute ak baatukaay, ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi. |
s-4
| Naka-jekk dafay doon ay téere yu bari. |
s-5
| Cër yi ëpp solo yi di tax a raññee ab jimbulang, ñeent lañu: Jagleel gi ci am, seenug lëkkaloo, nosiin wi ak mbidiinu jukki yi. |
s-6
| Jimbulang yi man nañu a wuute, aju ci seen ëmbiit, man nañu a ubbeeku ci xeeti xameef yépp (Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa Brëtaañ, ñoo di yi ci gën a siiw), walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi, niki ab jimbulangu paj, bu xam-xam walla bu xeltu. |
s-7
| Am na it ay jimbulang yu di jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan, diine walla politig wu wenn askan, walla xeet, niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi, Jimbulangu Jewish bi... |
s-8
| Yitteey liggéeyi jimbulang moo di jébbal xameef gi ëpp solo gi di dajale ñeel tëriit li. |
s-9
| Yii liggéey nit yàgg na koo def, dalee lu sori ci taariixam, waaye baatu jimbulang ñu ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu. |
s-10
| Bépp liggéeyu jimbulang, ci lu leer, ab tënk rekk la ci xameefi nit, te it liggéey bi dafa di soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam. |
s-11
| Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi; ab jimbulang bi ñuy jagleel i gune mooy gën a néew bi ñuy jagleel i mag. |
s-12
| Nosiinu jukki yi am na solo lool, ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb, kon gëstu ci dina yomb. |
s-13
| Ci taariix, ñaari xeeti nosiin lañu di jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi: nosiin gu abajada, jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba, beneen bi moo di séddale leen ci ay wàll. |
s-14
| Nit, dale ci lu yàgg ci ag nekkam, doon na jéem a nos ay xameefam. |
s-15
| Li dale ci jamono ju yàgg ja, bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp. |
s-16
| Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu ci a lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia (taariixu dend bi), doonoon ag faramfacce, ci fanweer ak juróom-ñaari téere ñeel dend bi, nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja. |
s-17
| Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377, duppee ko Al-Muqaddima (Taariixu àdduna bi), mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi: melosuuf, xeltu, taariix, koom-koom, gëstumboolaay, politig, paj ba ci suqaliku gu sax. |
s-18
| Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr Al-Razi, mutasilita bu Al-Kindi (ci daanaka 270 téere) |
s-19
| Imbratóor bu Siin bi, Cheng-Zu bu Callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle, di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix. |
s-20
| Mu ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yi ñu binde ak loxo, lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay. |
s-21
| Yii téere, loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool, boroom alal yi ak niti diine yi rekk ñoo ci doon jot: doonoon nañu ay téere yu seer lool. |