s-1
| Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juróom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko. |
s-2
| Ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko. |
s-3
| Bu ko defee mu daldi jël nguur gi. |
s-4
| Ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana. |
s-5
| Waar Jaabi dugg na ci Lislaam, daldi jóg def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit. |
s-6
| Ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci Lislaam ci Senegaal. |
s-7
| Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi. |
s-8
| Li ko waraloon it moo di dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi. |
s-9
| Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn). |
s-10
| Ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent). |
s-11
| Ci mujjug xarnub fukk ak juróom la Koli Tingala jóg xeex Tukulóor yi, daldi tembal ay goxam, taxawal nag nguur gu yees, mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko. |
s-12
| Ci xarnub fukk ak juróom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom: Jolof, Kajoor. |
s-13
| Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarloo ak cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi. |
s-14
| Ci atum 1770 g.j, la ag fippu am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daldi daaneel njabootug Deñanke. |
s-15
| Bu ko defee, Baal jël Lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale. |
s-16
| Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan. |
s-17
| Moom lañu di jàppe ki njëkk a doon Yilimaan. |