Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev
AnnotationDione, Bamba

Select a sentence

s-1 Milyoη ak 450 junni ay toni jën ñoo di jaar at mu nekk ci géeji Senegaal yi.
s-2 Jëwriñ ji yor Koomug Géej gi, Xureysi Caam jibal na ne at mu jot 1 Milyoη ak 450 junni ay toni jëni biir géej dinañu di jóge géeju Kap-weer jaar ci sunu géej yi.
s-3 Xureysi Caam mi doon àddu ci surnaalu 12 w bu Rfm, leeral na ne jën yooyu dañuy njëkke jaar Giné-Bisaaw, Gàmbi, Senegaal, Moritani, Marok door a dëppaat.
s-4 Bu ñu egsiwaatee Moritani, te nappeesu leen, dañuy dee.
s-5 Teg na ci ne: am na 1 milyoη ak 450 junni ay ton yu doomi réew mi mënul a napp, ndax amuñu jumtuwaay yu ko mën a napp.
s-6 Jëwriñ jee ngi laaj: Ku di napp toni jën yooyu?
s-7 Ay bato wëyyu ñoo koy napp, bato yu xarala lañu, gaaw lool te mëneesu leen a teg loxo.
s-8 Loolu lanuy ñàkk at mu jot.
s-9 Ndax jaadu na nguur gi di seetaan woowu yàqute, déedéet.
s-10 Nee na, xalaat nanu ren, jàppandal ay batoy biir réew mi ak yu bitim-réew ngir ñu dem nappi jën yooyu.
s-11 Nee na, li ñuy napp dina nu indil at mu nekk 35 Dollar (ton bu nekk).
s-12 APS: Dibéer 15 maars 2009

Text viewDownload CoNNL-U