Dependency Tree
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | dev |
---|
Annotation | Dione, Bamba |
---|
Select a sentence
s-1
| Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yi di dugg Senegaal te di jóge bitim-réew war a am. |
s-2
| Mu ngi ko dogale ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru. |
s-3
| Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare n° 2012-444 soppi bu n° 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi. |
s-4
| Dekkare boobu dafa di tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yi di duggu Senegaal war a am. |
s-5
| S. Sàll dige woon na ci baatum dagaan ne dina ko def bu ñu ko tegee ci boppu réew mi. |
s-6
| Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal. |
s-7
| Lu tax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal? |
s-8
| Loolu la waxoon. |
s-9
| Dogal booboo ngi tukkee woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar yi te aar kéew gi ci saxaar su bon si di tukkee ci oto yu màgget yi. |
s-10
| Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi yi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon. |
s-11
| Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dogal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi. |
Text view
•
Download CoNNL-U