s-1
| Suuxat sa yaram |
s-2
| Suuxat sa yaram, suuxat sa am xel ni mu ware: caabi ji la di ubbil jàmmu yaram |
s-3
| Mbokk, OSAD a la tekkil dénkaane yii tukkee ci Profesëer Amadu Galo Jóob. |
s-4
| Ci gis-gisam, warees na leen a jàppe ni ab bagaan bu def ay taxañ, ku ne ñëw jël taxañ yi méngoo ak tolluwaayu yaramam, fekk diisoo na ci ak doktooram. |
s-5
| Bu la ndékki raw. |
s-6
| Bul yem rekk ci meew, kafe mbaa dute ak yu ni mel. |
s-7
| Jëlal ndékki lu am solo, mburu, ñoom fonde ak yu ni mel, naan yu tàng mbaa yu sedd yu am suukar (su fekkee ne terewuñu la suukar), mbaa ay meññet, mbaa ndoxum meññet añs. |
s-8
| Taamul di naan laata waxtu lekk jot, dafa di tax doo xiif bu baax, su ko defee doo lekk lu bare; |
s-9
| Loolu baax na ci ki ñu digal lu wàññi yaramam. |
s-10
| Su fekkee ne danga lekk ba noppi, bëgg a naan ci saa si, jàppal lii: lekk lu tàng, naan lu tàng. |
s-11
| Lu ko moy, xaaral ñaar-fukki minit (20), gën jaa néew, nga sog a naan lu sedd. |
s-12
| Su nga yeewoo rekk, daldil naan ndox; |
s-13
| Bu loolu wéyee, nga naan lu mu néew néew 1 liitaru ndox ci bëccëg bi. |
s-14
| Loolu dafa di yeesal ndox mi ci sa yaram (lu ëpp juróom-ñaar-fukk ci téeméer 70 % ndox la), su ko defee mu aar la ci sank, maanaam seere. |
s-15
| Lée-lée, nanga amal subas ndox, maanaam nga naan benn liitaru ndox, lu jiitu ndékki. |
s-16
| Ngir aar sa bopp ci kolesterol, moytul ñam yu ñu fiiriir mbaa saaf ci diwlin, taamul ñam yi ñu baxal, mbaa tay, mbaa lakk, mbaa dugal ci fuur, mbaa yu ñu toggul niki salaatu tamaate, karoot ju ñu joos ak yu ni mel. |
s-17
| Moytul soos yi ak yu niin yi, ak limonaat yi, ak ngato yi, ak yàpp yu xonq yi, ak biiru nag yi ak xar yi, ak sosisoŋ yi ak yu ni mel. |
s-18
| Taxawal temm ba kenn du def safal yi xew, moo xam ay kibb lañu walla sunguf su ñuy suy ci togg gi. |
s-19
| Deel lekk lujum ak meññet, ganaar ak yi mu xeetool, jën ak yeneen yi di dund ci géej. |
s-20
| Deel teel a reer, na doon ñam yu woyof te bañ a saf xorom. |
s-21
| Moytul di dolli xorom ci ñam wi. |
s-22
| Bul reere lu am xorom, su fekkee ne danga am tasyoŋ mbaa mu am ñu ko am ci njaboot gi. |
s-23
| Naan yu tàng: kenkiliba, àttaaya ju am limoŋ mbaa naanaa, kafe gu woyof, meew... |
s-24
| Naan yu sedd: na la ndoxum meññet yi fi fekk baax gënal limonaat yi ak yu ni mel, yi ñu di jaay ci bitig yi. |
s-25
| Su fekkee ne danga am mbokk mu am jabet: defal suukar su yem, mbaa nga jëfandikoo wuutalu suukar te bañ ci a xér. |
s-26
| Ñam yii fàww nga lekk leen: dugub, ceeb, xeeti màkkaróoni, mburu, ñàmbi ak yu ni mel, pombiteer... |
s-27
| Li ci gën nag, moo di ñu baxal leen mbaa ñu tay leen. |
s-28
| Su dee ku ànd ak jabet, mbaa metitu biir, mbaa ku am yaram lool, bumu ci xér. |
s-29
| Moytul lekk ba biir bi fees dell te moytu yit di lekkantu ci diggante ndënale yi. |
s-30
| Yëngal sa yaram lu war la. |
s-31
| Kenn waxul nga xéy suba di daw ak a maaj, sonn ci lool, yemale ko fa ba jëmmi jamono; |
s-32
| Loolu du la amal njariñ. |
s-33
| Li gën moo di saxoo di yëngal sa yaram, lu mu néew-néew ñetti yoon ci ayu-bés bi, mën na a doon dox, lagg-laag maanaam daw yu yemamaay, féey, biskalet añs., lu tollu ci fanweeri minit jëm benn waxtu, lépp nag tolloo ak li nga àttan. |
s-34
| Bul tóx, moytul garabu yoo gi ñu di jafal mu di saxaar, naka noonu garab yi di rey gunóor. |
s-35
| Sàngara yit mat naa moytu. |
s-36
| Jëlal sa matukaay ba mën a nelaw bu baax, lu mu néew-néew juróom-benni waxtu (6 w). |
s-37
| Ngir suuxat sam xel, gannaaw nelaw yu mucc ayib yi nu wax léegi, yokkal sa xam-xam, mu doon ci bëccëg bi, ngay bind ak a jàng, tàggat sa bopp ci tari loo jàngoon, nettali lu nga mas a dégg ak yu ni mel, boole ci ay po yuy tàggat sam xel añs. |