s-1
| Moytuleen kolesterol (cholestérol) |
s-2
| Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo, ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase. |
s-3
| Lan mooy kolesterol? |
s-4
| Kolesterol diw la gu baax ci nit, ndax dafa bokk ci yi di tabax yaram. |
s-5
| Waaye nag, su natt bi jéggee dayo ci deret ji, dafa di bàyyi ay àkk ci solom yi deret ji di jaar ngir dem ci xol bi (athérosclérose). |
s-6
| Fu kolesterol di jóge? |
s-7
| Li ëpp ci kolesterol res bee koy defar. |
s-8
| Gannaaw loolu, dees na ko jële ci ñam yu deme ni nen, mbàq ak butit (laxas), bëer, yàpp wu duuf añs (ak ñoom seen). |
s-9
| Nattu kolesterol bu jéggi dayo lan lañu ciy ragal? |
s-10
| Natt bu jéggi dayo mën naa jur jàngoroy xol, niki kriis kàrjag «crise cardiaque». |
s-11
| Jàppees na ne kolesterol, póon, jabet, ak tasyoŋ bu kowe ñoo jiitu ci yi di sabab jàngoroy xol. |
s-12
| Looloo waral boroom xam-xam yi naan kolesterol benn la ci ñeent ñiy faat xol «bourreaux du cœur». |
s-13
| Yow mi bëgg lu la musal ci kolesterol bu ëpp, toppal dénkaane yii la Doktoor Kase baaxe. |
s-14
| Wàññil yu niin yi, kenn waxul nga bàyyi leen. |
s-15
| Bul xér ci diwlin, te bu ko bàyyi ba mu sãs. |
s-16
| Naka noonu wàññil ñam yii: bëer (doonte sax dañu bind ne woyofalees na ko), diwu-ñor, sosisoŋ, yàpp wu duuf, meew mu ñu tonniwul diw ga, soowu niw, nebbon (garees), dax, mburu mu ñu noote meew «pain au lait», mbaa mburu ak sokkolaa, kurwaasã «croissants», ngato, kreem glaase... |
s-17
| Deel lekk jën lu mu néew néew ñetti yoon ci ayu-bés bi. |
s-18
| Jën yu deme ni wëyëŋ, yaabóoy, óoba, jay, njunna jàppees na ne baax nañu ci yemale kolesterol. |
s-19
| Taamul meew mu ñu woyofal, ak soow, yawuur, formaas yu niinaay ba barewul (0 % ba ci 10 % MG). |
s-20
| Mën ngaa lekk yàpp, waaye bumu doon yàpp wu duuf; |
s-21
| Xamal ne yàpp wu ñu wàjji moo gën wu ñu saaf ci diwlin. |
s-22
| Naka noonu ganaar it baax na, ñu wàjji ko, dindi der bi. |
s-23
| Deel lekk lujum ak meññent 'fruits'. |
s-24
| Deel lekk lujum (naaje, karoot, batañse, suppome, pooro, kànja, jaxatu, soble ñax 'oignons verts', pooro, batañse... ak meññent (sorãs, pom, màngo, anaanaas, pàppaayo, xaal añs. |