s-1
| Tambaakundaa, 2 awril (APS) |
s-2
| Tàmbaakundaa: taxawal ay wanagi wowal, ngir doomi jàngoro yi bañ a ayibal ndoxum teen yi ak yu ni mel. |
s-3
| Sàntar bi di saytu kàttanu jant bi ak cet, te nekk ci Tàmbaakundaa samp na ay wanagi wowal. |
s-4
| Xeetu wanag woowu nag mbeeste la, dees ko di tabax ci taxawaayu benn meetar walla lu ko ëpp, mu lëkkaloo ak ñaari pax. |
s-5
| Benn bi def sobe si (puup yi), fekk am na pexe mu leen nal ba ñu wow, ñu def leen tos. |
s-6
| Beneen bii def saw mi ak ndoxum laablu mi, ñu suuxate ko flëer yi. |
s-7
| Njariñ li mën a tukkee ci xeetu wanag wii bari na, ndax lépp la ñuy jëfandikoowaat, day yi, saw mi ak yi ci ànd, rax-ci-dolli dafay yaxanal ndox, indi cet. |
s-8
| Loolu la Abdukariim Saane xamle, moo sos sàntar bi te yit moo jiite mbootaayu xariti Tàmbaakundaa. |
s-9
| Mbir mi nag dafa laaj toppatoo ak yeete bu yaatu jëmale ko ci nit ñi. |
s-10
| Nit ku nekk, war ngaa yar sa bopp ngir sàmmoonteek fàggutéef yi ci aju, ndax yar boobu bu amul, doomi jàngoro yi dañuy tasaaroo. |
s-11
| Su ko defee dañuy ayibal ndox mi ci biir suuf si, niki ndoxum teen yi ak yu ni mel. |
s-12
| Looloo waral jamono yi weesu, waa sàntar bi liggéey ak waa Serwiis Diiseen, ngir gëstu day yi. |
s-13
| Su ko defee ñu ràññee xeeti jàngoro yi ba xam ndax mënees na leen a tose gàncax gi. |
s-14
| Abdu Kariim Saane ñaawlu na li waa dëkk bi tàmm a def: bale biir kër gi ba mu set, waaye bàyyi mbalit mi ci buntu kër gi. |
s-15
| Ci wàllu cet gi ba tey, sàntar baa ngi di seet na muy def ba teqale mbalit mi, boole li mën a ànd, ber yi ci des. |
s-16
| Mu ngiy xalaat it defar ay mbuusi ndimo, ñu wuutu mbuusi plastig yi. |
s-17
| Loolu dafa laaj ñépp xàccandoo, bokk liggéey bi, ndax sàntar bi moom rekk mënul a def lépp. |
s-18
| Ci ag pàttali, ci mbënnum 1998 lañu sosoon sàntar bi, nga xam ne ñu bari dañu ñàkkoon seen kër. |
s-19
| Ñu fat leen ci lekkool Saada Maka Si. |
s-20
| Sàntar bi am ñu mu ci dalal. |
s-21
| Ñu faf ko def bérébu sotteente xalaat. |
s-22
| Li ñu ci jublu woon moo di xalaat ci mbir yi leen soxal, sukkandiku ci lekkool yi, ngir tasaare xam-xam ci wàllu tabaxinu ban, ak kàttanu jant bi, ak cet, ak yeneen i ponk. |
s-23
| Ndongo yi ñoo waroon a siiwal xam-xam boobu ci biir njaboot gi. |
s-24
| Yokk jëf yi nga xam ne kenn nàttablewul seen njariñ ci xeex sibbiru |