Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest
AnnotationDione, Bamba

Select a sentence

s-1 Lebu, mooy benn waaso nekk ci reewum Senegaal.
s-2 Ñoom, Ndakaaru moo di seen dëkk, nu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint-Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur, ci wetu geej ak tefes.
s-3 Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan.
s-4 Seen làkk di wolof.
s-5 Seen wolof dafa xaw a wuute tuuti ak wolof bi ñeneen ñi di làkk.
s-6 Am na ñu ne, lebu yi ñoo sos làkk wolof.
s-7 Cosaanu baat boobu, wuute na ci li kilifa yi tekki.
s-8 Ñooñu dinañu di nettali ay cosaan yu wuute: 'leeb' moo juur baat bi.
s-9 Am na ñeneen ñu ni 'luubu' mooy 'bañ', ndax ci cosaan, Lebu yi dañu mas a bañ ku leen noot.
s-10 Seex Anta Jóob, ci gëstoom, dafa wone ni, li ñu tudde lebu, am na lu mu bokk ak tur boobu ñu joxe reewum Libi.
s-11 Libi, ci jamono Isipt gu yàgg ga, benn diwaan la woon bu nit ñi daan dem di fa rëbbi, ak nappi.
s-12 Dëkk boobu dafa jannoo ak géej gi.
s-13 Moo tax ñu yoroon Isipt gu yagg ga, tudde dëkk boobu: rëbu.
s-14 Ñu war a xam ni, Seex Anta Jóob ak yeneen gestukat wone nañu ko.
s-15 Làkk boobu amoon ca Isipt boobu, ak làkk wolof, ñoo bokk maam.
s-16 Rëbu moo juur Lebu.
s-17 Lebu moo juur Libi.
s-18 Dëkk bi ñu xam ne, ay nit ñu ñuul ñoo fa ne woon, te ñu daan tudde ñu dëkk ca biir réew mi 'kaw'.
s-19 Mel ni li am Senegaal tey: Lebu yi dëkk ci tefes ak wetu geej gi, kaw-kaw yi dëkk ci biir réew mi.
s-20 Lebu yi, kon, réew mi ñu tudde tey Libi, lañu ne woon ci jamono yu Isipt gu yàgg ga ame.
s-21 Dañoo mujj daw dëkk boobu, ndax amoon na benn askan bu ñëwoon foofu, jóge Asi, te ñu leen daan bëgg a noot.
s-22 Ñoom ñooy Persi yi.
s-23 Ci seen gàdday, jaar nañu ci ay dëkk yu bare (Sudaan, Caad, Niseer, Mali).
s-24 Sudaan, mooy dëkk bi Lebu yi baawoo.
s-25 Ñu ko gën a ràññe ci turu Nubi walla Kuus.
s-26 Senegaal, lañu agsi, jamono ja nguuru Tekuruur ame.
s-27 Foofu lañu fekk seen bokk, di Pël yi ak Séeréer yi, rawatina Pël ak Seereer yi ñuy napp.
s-28 Ñu leen tudde ci làkku pulaar ay Cuballo / Subalbe.
s-29 Foofu lañu sanc ay dëkk yu mel ni KasKas ak Njum.
s-30 Waaye ci Senegaal, taxawuñu Tekruur rekk.
s-31 Jaar nañu Jolof, ak Kajoor, soog a mujj agsi ca Ndakkaru ci diggante atum 1430 ak 1530.
s-32 Foofu, ay Socé lañu fa fekk.
s-33 Fukki ak ñaari xeet ñoo nose askanu Lebu yi.
s-34 Ñu ne tamit, fukki ak ñaari PENC yi.
s-35 Ñoom ci senn bopp, dañu xaaj ci ñaari njabootay yu mag, di Sumbejun yi ak Beeñ yi.
s-36 Ñoo yore woon gox yi ci Ndakaaru: Yoff, Wakam, Ngor, Sumbejun, ...
s-37 Lebu yi ñoo bokk sant ak Seereer yi, mel ni: Ndóoy, Puy, Ndir, Jeen, Yaad, Jaañ, Fay, Jeey, Sar, Caw, Njaay, Juuf, Sek.
s-38 Ñu sant 'Mbeŋ', ci li cosaan tekki, seen maam ay Mandiŋ lañu woon.
s-39 Seen mamaat di Jolof Mbeŋ (ab lamaanu Jolof), jóge Mali.
s-40 Da firnde ni, Lebu yi, ci ñoom lañu cosaanoo.
s-41 Mel ni wolof yi rekk.
s-42 Lebu yi, ay jullit lañu.
s-43 Ñu bare bokk ci Tariqa Tijaan, ak Layeen yi (Seydinaa Limaamu Laay).
s-44 Seen këru diine di Kambereen, ca Yoff.
s-45 Waaye, du tax ñu fate seen cosaan, ak li seen maam defoon, ba ñu nekkee Ceddo, manaam tuur yi.
s-46 Tuur yi, am na solo ci Lebu yi.
s-47 Ci seen jaar jaar, tuur yi, gëdd gu mag lañu yoroon ci ñoom, ci lu jëm ci xare yi, ak yeneen xeew yu amoon solo ci seen cosaan.
s-48 Ci seen tuur yi, 'ndëpp' la nit ñi gën a xam, ngiir faj febaru ñooñu ñu xam ne, jiine a leen jàpp.
s-49 Jiine ci Lebu, 'rab' lañu ko tudde.
s-50 Lëk Dawwur, Maam Kumba Kastel, Maam Jaare, ak yeneen i tuur, bokk nañu ci ñooñu Lebu yi seqante.

Text viewDownload CoNNL-U