Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev
AnnotationDione, Bamba

Select a sentence

s-1 Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yi di dugg Senegaal te di jóge bitim-réew war a am.
s-2 Mu ngi ko dogale ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru.
s-3 Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare 2012-444 soppi bu 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi.
s-4 Dekkare boobu dafa di tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yi di duggu Senegaal war a am.
s-5 S. Sàll dige woon na ci baatum dagaan ne dina ko def bu ñu ko tegee ci boppu réew mi.
s-6 Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal.
s-7 Lu tax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal?
s-8 Loolu la waxoon.
s-9 Dogal booboo ngi tukkee woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar yi te aar kéew gi ci saxaar su bon si di tukkee ci oto yu màgget yi.
s-10 Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi yi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon.
s-11 Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dogal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi.

Text viewDownload CoNNL-U