Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev
AnnotationDione, Bamba

Select a sentence

s-1 Ci xarnub fukk ak juróom Bawol nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi.
s-2 Bu ko defee, ag njaboot gu am ag jegeñaale ak buuri Kajoor yi daan ko jiite.
s-3 Bu jëkk, nguur googu, ay socé ak ay séeréer, ñoo ko yoroon.
s-4 Ndax Bawol, benn dex la woon foofu ci lu doog a am.
s-5 Boobu jamono, Bawol, amoon na ndox mu bare.
s-6 Ci cosaan, dañu ne, Bawol, ku fa jëkk a nekk buur, Xaayamagaan moo doon turam.
s-7 Xaayamagaan, ci làkku socé yi la soqeekoo, moo di: buuru gaalam.
s-8 Ñoom, socé yi fa nekkoon jamono boobu, seen mamm, Mande lañu baawoo.
s-9 Ba pare, séeréer yi ñëw.
s-10 Ñoom, Fuuta Tooro lañu jóge woon, gàdday ba Bawol, ndax jiyaar ji Muraabituun yi defoon foofu.
s-11 Ba ñu agsi Bawol, ci ubbite, dañu daan dëkkandoo ak socé, soog a leen daq.
s-12 Ba loolu amee, ñu yilif dëkk boobu.
s-13 Ci séeréer yi, askan yi ñu faloon, ñoo doon ñi sant Juuf, Ngom, Caw.
s-14 Te buur ba ñu daan taan ci ñoom, 'Téeñ' lañu ko daan tudde.
s-15 Loolu moo amoon, laata nguuru Jolof ñëw uuf dëkk bi.
s-16 Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawol ci jenn jamono ji.
s-17 Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam.
s-18 Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk dafa bëgg a yilif ga ca des.
s-19 Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug ki di wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def.
s-20 Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi.
s-21 Mbooleem kuréel yi nag daa nañu fa àttewoo (kuréelug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, boroom mecce yi ak jigéen ñi).
s-22 Bokkug Bawol ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ci ay suufam.
s-23 Moom kay dafa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi.

Text viewDownload CoNNL-U