Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train Annotation Dione, Bamba
Text: Transcription Written form - Colors
Soleil , Jokkub awril , xët 7
s-1
wo_wtb-ud-train_2077
Soleil, Jokkub awril, xët 7
Sibbiru màtt-màttu yoo moo koy joxe .
s-2
wo_wtb-ud-train_2078
Sibbiru màtt-màttu yoo moo koy joxe.
Su fagaru amul , xel xalaatul xeex sibbiru .
s-3
wo_wtb-ud-train_2079
Su fagaru amul, xel xalaatul xeex sibbiru.
Xeex bi warul a yem rekk ci faj nit ñi .
s-4
wo_wtb-ud-train_2080
Xeex bi warul a yem rekk ci faj nit ñi.
Kàddu yii tukkee ci Mustafaa Siise , kilifag biro bi di toppatoo fagaru ak jëflante ci Progaraam bi di xeex sibbiru , tudd PNLP ci frãse , wone na cër bu yaatu bi fagaru am ci xeex sibbiru , nga xam ne at mu ne dina rey lu ëpp milyoŋ ci ay nit .
s-5
wo_wtb-ud-train_2081
Kàddu yii tukkee ci Mustafaa Siise, kilifag biro bi di toppatoo fagaru ak jëflante ci Progaraam bi di xeex sibbiru, tudd PNLP ci frãse, wone na cër bu yaatu bi fagaru am ci xeex sibbiru, nga xam ne at mu ne dina rey lu ëpp milyoŋ ci ay nit.
Kon fagaru moo gën faju .
s-6
wo_wtb-ud-train_2082
Kon fagaru moo gën faju.
Kilifa gi fàttali na liggéey bi ñu jot a tàmbali ci fagaru gi , fésal ci ñaari poñ yii : pompe garabu yoo ci kër yi ak joxe sànke yu ñu nàndal .
s-7
wo_wtb-ud-train_2083
Kilifa gi fàttali na liggéey bi ñu jot a tàmbali ci fagaru gi, fésal ci ñaari poñ yii: pompe garabu yoo ci kër yi ak joxe sànke yu ñu nàndal.
Bu dee lu jëm ci poñ bu jëkk bi , gannaaw ba ñu gisee njariñal pompe biir kër , léegi li leen yitteel moo di seet nan lañu leen di yaatale ba ñu yegg ci yeneen i dëkk ak dëkk-dëkkaan yi .
s-8
wo_wtb-ud-train_2084
Bu dee lu jëm ci poñ bu jëkk bi, gannaaw ba ñu gisee njariñal pompe biir kër, léegi li leen yitteel moo di seet nan lañu leen di yaatale ba ñu yegg ci yeneen i dëkk ak dëkk-dëkkaan yi.
Bu dee lu soxal sànke yi nag , daaw yóbbu nañu leen ci 5 diwaan , jagleel leen xale yi amagul 5 at ak jigéenu-wérul yi .
s-9
wo_wtb-ud-train_2085
Bu dee lu soxal sànke yi nag, daaw yóbbu nañu leen ci 5 diwaan, jagleel leen xale yi amagul 5 at ak jigéenu-wérul yi.
Liggéey boobu lañu bëgg a yaatal .
s-10
wo_wtb-ud-train_2086
Liggéey boobu lañu bëgg a yaatal.
Mënees na leen a ame ci fajukaay yi , ak ci woote yi mbootaayi gox yi di amal , ak ci jataayi yeete yi jëm ci xale yi , ak ci wisiti jiitu-wasin yi jigéenu-wérul yi di def , ak mbooloo yu ni deme .
s-11
wo_wtb-ud-train_2087
Mënees na leen a ame ci fajukaay yi, ak ci woote yi mbootaayi gox yi di amal, ak ci jataayi yeete yi jëm ci xale yi, ak ci wisiti jiitu-wasin yi jigéenu-wérul yi di def, ak mbooloo yu ni deme.
Ci biir loolu , ñu xamal nit ñi nan lañuy jëfandikoo sànke yi , yee leen ci njariñ li nekk ci nelaw ci biir sànke .
s-12
wo_wtb-ud-train_2088
Ci biir loolu, ñu xamal nit ñi nan lañuy jëfandikoo sànke yi, yee leen ci njariñ li nekk ci nelaw ci biir sànke.
Jàngal ay fajkati kër ngir xam-xam bi jëm ci pajum kër .
s-13
wo_wtb-ud-train_2089
Jàngal ay fajkati kër ngir xam-xam bi jëm ci pajum kër.
Bu mbirum fagaru gi wéyee , PNLP tëral na pexe mu tax ba lu dëkk sori sori , ak lu mu làqu làqu , nit ña mën a jot ci paj mi war ci ñoom .
s-14
wo_wtb-ud-train_2090
Bu mbirum fagaru gi wéyee, PNLP tëral na pexe mu tax ba lu dëkk sori sori, ak lu mu làqu làqu, nit ña mën a jot ci paj mi war ci ñoom.
Ci noonu mu xalaat a taxawal li ñu naan pajum kër ( ñu tudde ko Pecadom ci Frãse ) .
s-15
wo_wtb-ud-train_2091
Ci noonu mu xalaat a taxawal li ñu naan pajum kër (ñu tudde ko Pecadom ci Frãse).
Pecadom mooy fekk nit ki feebar ci këram , teel koo toppatoo , laata jàngoro ji di màgg .
s-16
wo_wtb-ud-train_2092
Pecadom mooy fekk nit ki feebar ci këram, teel koo toppatoo, laata jàngoro ji di màgg.
Loolu nag dafa laaj ñu jël ay nit ñu dëkk ca gox ba , mënees na leen a sax tudde fajkati kër , jàngal leen li war ci ñoom , ba ñu mën a def liggéey bi ñu séentu ci ñoom .
s-17
wo_wtb-ud-train_2093
Loolu nag dafa laaj ñu jël ay nit ñu dëkk ca gox ba, mënees na leen a sax tudde fajkati kër, jàngal leen li war ci ñoom, ba ñu mën a def liggéey bi ñu séentu ci ñoom.
Ngir xeex sibbiru : 51 doktoori diwaani wér-gi-yaram tàggat nañu leen .
s-18
wo_wtb-ud-train_2094
Ngir xeex sibbiru: 51 doktoori diwaani wér-gi-yaram tàggat nañu leen.
Edit as list • Text view • Dependency trees