Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train Annotation Dione, Bamba
Text: Transcription Written form - Colors
Tambaakundaa , 2 awril ( APS )
s-1
wo_wtb-ud-train_2053
Tambaakundaa, 2 awril (APS)
Tàmbaakundaa : taxawal ay wanagi wowal , ngir doomi jàngoro yi bañ a ayibal ndoxum teen yi ak yu ni mel .
s-2
wo_wtb-ud-train_2054
Tàmbaakundaa: taxawal ay wanagi wowal, ngir doomi jàngoro yi bañ a ayibal ndoxum teen yi ak yu ni mel.
Sàntar bi di saytu kàttanu jant bi ak cet , te nekk ci Tàmbaakundaa samp na ay wanagi wowal .
s-3
wo_wtb-ud-train_2055
Sàntar bi di saytu kàttanu jant bi ak cet, te nekk ci Tàmbaakundaa samp na ay wanagi wowal.
Xeetu wanag woowu nag mbeeste la , dees ko di tabax ci taxawaayu benn meetar walla lu ko ëpp , mu lëkkaloo ak ñaari pax .
s-4
wo_wtb-ud-train_2056
Xeetu wanag woowu nag mbeeste la, dees ko di tabax ci taxawaayu benn meetar walla lu ko ëpp, mu lëkkaloo ak ñaari pax.
Benn bi def sobe si ( puup yi ) , fekk am na pexe mu leen nal ba ñu wow , ñu def leen tos .
s-5
wo_wtb-ud-train_2057
Benn bi def sobe si (puup yi), fekk am na pexe mu leen nal ba ñu wow, ñu def leen tos.
Beneen bii def saw mi ak ndoxum laablu mi , ñu suuxate ko flëer yi .
s-6
wo_wtb-ud-train_2058
Beneen bii def saw mi ak ndoxum laablu mi, ñu suuxate ko flëer yi.
Njariñ li mën a tukkee ci xeetu wanag wii bari na , ndax lépp la ñuy jëfandikoowaat , day yi , saw mi ak yi ci ànd , rax-ci-dolli dafay yaxanal ndox , indi cet .
s-7
wo_wtb-ud-train_2059
Njariñ li mën a tukkee ci xeetu wanag wii bari na, ndax lépp la ñuy jëfandikoowaat, day yi, saw mi ak yi ci ànd, rax-ci-dolli dafay yaxanal ndox, indi cet.
Loolu la Abdukariim Saane xamle , moo sos sàntar bi te yit moo jiite mbootaayu xariti Tàmbaakundaa .
s-8
wo_wtb-ud-train_2060
Loolu la Abdukariim Saane xamle, moo sos sàntar bi te yit moo jiite mbootaayu xariti Tàmbaakundaa.
Mbir mi nag dafa laaj toppatoo ak yeete bu yaatu jëmale ko ci nit ñi .
s-9
wo_wtb-ud-train_2061
Mbir mi nag dafa laaj toppatoo ak yeete bu yaatu jëmale ko ci nit ñi.
Nit ku nekk , war ngaa yar sa bopp ngir sàmmoonteek fàggutéef yi ci aju , ndax yar boobu bu amul , doomi jàngoro yi dañuy tasaaroo .
s-10
wo_wtb-ud-train_2062
Nit ku nekk, war ngaa yar sa bopp ngir sàmmoonteek fàggutéef yi ci aju, ndax yar boobu bu amul, doomi jàngoro yi dañuy tasaaroo.
Su ko defee dañuy ayibal ndox mi ci biir suuf si , niki ndoxum teen yi ak yu ni mel .
s-11
wo_wtb-ud-train_2063
Su ko defee dañuy ayibal ndox mi ci biir suuf si, niki ndoxum teen yi ak yu ni mel.
Looloo waral jamono yi weesu , waa sàntar bi liggéey ak waa Serwiis Diiseen , ngir gëstu day yi .
s-12
wo_wtb-ud-train_2064
Looloo waral jamono yi weesu, waa sàntar bi liggéey ak waa Serwiis Diiseen, ngir gëstu day yi.
Su ko defee ñu ràññee xeeti jàngoro yi ba xam ndax mënees na leen a tose gàncax gi .
s-13
wo_wtb-ud-train_2065
Su ko defee ñu ràññee xeeti jàngoro yi ba xam ndax mënees na leen a tose gàncax gi.
Abdu Kariim Saane ñaawlu na li waa dëkk bi tàmm a def : bale biir kër gi ba mu set , waaye bàyyi mbalit mi ci buntu kër gi .
s-14
wo_wtb-ud-train_2066
Abdu Kariim Saane ñaawlu na li waa dëkk bi tàmm a def: bale biir kër gi ba mu set, waaye bàyyi mbalit mi ci buntu kër gi.
Ci wàllu cet gi ba tey , sàntar baa ngi di seet na muy def ba teqale mbalit mi , boole li mën a ànd , ber yi ci des .
s-15
wo_wtb-ud-train_2067
Ci wàllu cet gi ba tey, sàntar baa ngi di seet na muy def ba teqale mbalit mi, boole li mën a ànd, ber yi ci des.
Mu ngiy xalaat it defar ay mbuusi ndimo , ñu wuutu mbuusi plastig yi .
s-16
wo_wtb-ud-train_2068
Mu ngiy xalaat it defar ay mbuusi ndimo, ñu wuutu mbuusi plastig yi.
Loolu dafa laaj ñépp xàccandoo , bokk liggéey bi , ndax sàntar bi moom rekk mënul a def lépp .
s-17
wo_wtb-ud-train_2069
Loolu dafa laaj ñépp xàccandoo, bokk liggéey bi, ndax sàntar bi moom rekk mënul a def lépp.
Ci ag pàttali , ci mbënnum 1998 lañu sosoon sàntar bi , nga xam ne ñu bari dañu ñàkkoon seen kër .
s-18
wo_wtb-ud-train_2070
Ci ag pàttali, ci mbënnum 1998 lañu sosoon sàntar bi, nga xam ne ñu bari dañu ñàkkoon seen kër.
Ñu fat leen ci lekkool Saada Maka Si .
s-19
wo_wtb-ud-train_2071
Ñu fat leen ci lekkool Saada Maka Si.
Sàntar bi am ñu mu ci dalal .
s-20
wo_wtb-ud-train_2072
Sàntar bi am ñu mu ci dalal.
Ñu faf ko def bérébu sotteente xalaat .
s-21
wo_wtb-ud-train_2073
Ñu faf ko def bérébu sotteente xalaat.
Li ñu ci jublu woon moo di xalaat ci mbir yi leen soxal , sukkandiku ci lekkool yi , ngir tasaare xam-xam ci wàllu tabaxinu ban , ak kàttanu jant bi , ak cet , ak yeneen i ponk .
s-22
wo_wtb-ud-train_2074
Li ñu ci jublu woon moo di xalaat ci mbir yi leen soxal, sukkandiku ci lekkool yi, ngir tasaare xam-xam ci wàllu tabaxinu ban, ak kàttanu jant bi, ak cet, ak yeneen i ponk.
Ndongo yi ñoo waroon a siiwal xam-xam boobu ci biir njaboot gi .
s-23
wo_wtb-ud-train_2075
Ndongo yi ñoo waroon a siiwal xam-xam boobu ci biir njaboot gi.
Yokk jëf yi nga xam ne kenn nàttablewul seen njariñ ci xeex sibbiru
s-24
wo_wtb-ud-train_2076
Yokk jëf yi nga xam ne kenn nàttablewul seen njariñ ci xeex sibbiru
Edit as list • Text view • Dependency trees