Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train Annotation Dione, Bamba
Text: Transcription Written form - Colors
Njaayum geerte gi ni mu di doxe baaxul , la njiitu jëwriñ yi naqarlu .
s-1
wo_wtb-ud-train_2027
Njaayum geerte gi ni mu di doxe baaxul, la njiitu jëwriñ yi naqarlu.
Njiitu jëwriñ yu Senegaal , Suleymaan Ndeene Njaay , naqarlu na , àllarba ca Ndakaaru , ni njaayum geerte gi di deme , jàpp na ne ni mu di doxe baaxul dara .
s-2
wo_wtb-ud-train_2028
Njiitu jëwriñ yu Senegaal, Suleymaan Ndeene Njaay, naqarlu na, àllarba ca Ndakaaru, ni njaayum geerte gi di deme, jàpp na ne ni mu di doxe baaxul dara.
Nanu waxante dëgg ndax ñi di defar diwlin ji amaguñu xaalis bu doy ngir jënd geerte gi , mu di lu mu nangu .
s-3
wo_wtb-ud-train_2029
Nanu waxante dëgg ndax ñi di defar diwlin ji amaguñu xaalis bu doy ngir jënd geerte gi, mu di lu mu nangu.
Seriñ Njaay a ngi doon àddu ca peggu ubbiteg 12eelu FIARA ( Fuwaar bi àddina bi jagleel mbey ak càmm ci Ndakaaru , 2 - 13 fewrie .
s-4
wo_wtb-ud-train_2030
Seriñ Njaay a ngi doon àddu ca peggu ubbiteg 12eelu FIARA (Fuwaar bi àddina bi jagleel mbey ak càmm ci Ndakaaru, 2 - 13 fewrie.
Ci Fuwaar boobu , waxtaan wi mu ngi jëm ci : mënal sa bopp ci ag dund .
s-5
wo_wtb-ud-train_2031
Ci Fuwaar boobu, waxtaan wi mu ngi jëm ci: mënal sa bopp ci ag dund.
Waaye , nguur gi du ko seetaan .
s-6
wo_wtb-ud-train_2032
Waaye, nguur gi du ko seetaan.
Jëwriñu mbey mee ngi topp mbir moomu .
s-7
wo_wtb-ud-train_2033
Jëwriñu mbey mee ngi topp mbir moomu.
Seetlu naa , gannaaw bu ma jokkoo ak yenn ci ay beykat , ne ñenn ci ñoom a ngi joxe seen i geerte te duñu jot benn xaalis , la njiitu jëwriñ yi xamale .
s-8
wo_wtb-ud-train_2034
Seetlu naa, gannaaw bu ma jokkoo ak yenn ci ay beykat, ne ñenn ci ñoom a ngi joxe seen i geerte te duñu jot benn xaalis, la njiitu jëwriñ yi xamale.
Wéral na ne mbir moomu mënul a yàgg .
s-9
wo_wtb-ud-train_2035
Wéral na ne mbir moomu mënul a yàgg.
Nguur gi dina jël ay matuwaay ngir ñi jël geerte beykat yi fay leen ci lu gaaw seen alal , loolu la dige .
s-10
wo_wtb-ud-train_2036
Nguur gi dina jël ay matuwaay ngir ñi jël geerte beykat yi fay leen ci lu gaaw seen alal, loolu la dige.
Altine jii , dinaa dajale njiitu bànk yi ak ñi di defar diwlin ngir nu génne ay saafara .
s-11
wo_wtb-ud-train_2037
Altine jii, dinaa dajale njiitu bànk yi ak ñi di defar diwlin ngir nu génne ay saafara.
Du yoon beykat bi def ñetti weer di bey suuf si , déqi , ba noppi jot ay boŋ gannaaw bi mu joxee geerteem , loolu la naqarlu .
s-12
wo_wtb-ud-train_2038
Du yoon beykat bi def ñetti weer di bey suuf si, déqi, ba noppi jot ay boŋ gannaaw bi mu joxee geerteem, loolu la naqarlu.
Alxamis bi weesu , ci Jotaayu Jëwriñ yi , jëwriñu mbey mi , Xaadim Géy , siiwaloon na ne dajalees na 120000 tonu geerte ci réew mépp , ci 45 fani dagaan .
s-13
wo_wtb-ud-train_2039
Alxamis bi weesu, ci Jotaayu Jëwriñ yi, jëwriñu mbey mi, Xaadim Géy, siiwaloon na ne dajalees na 120000 tonu geerte ci réew mépp, ci 45 fani dagaan.
Maki Sàll tënk na ci 8 digub at yi oto yi di dugg Senegaal war a am .
s-14
wo_wtb-ud-train_2040
Maki Sàll tënk na ci 8 digub at yi oto yi di dugg Senegaal war a am.
Ndakaaru , 13 awril ( APS )
s-15
wo_wtb-ud-train_2041
Ndakaaru, 13 awril (APS)
Edit as list • Text view • Dependency trees