Sentence view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain
AnnotationDione, Bamba

Text: -


[1] tree
Senegaal ak bés bi UNESCO jàgleel làkki-ndey
s-1
wo_wtb-ud-train_956
Senegaal ak bés bi UNESCO jàgleel làkki-ndey
[2] tree
Bésu 21 fan ci weeru Fewrie at mu jot, moom la kurél gi di toppatoo caada, njàng ak xamtéef (UNESCO) te feeteewoo ci Mbotaayu-xeet-yi, jagleel làkki-ndey yi, maanaam làkk wi nga xam ne moom la nit ku nekk nàmp.
s-2
wo_wtb-ud-train_957
Bésu 21 fan ci weeru Fewrie at mu jot, moom la kurél gi di toppatoo caada, njàng ak xamtéef (UNESCO) te feeteewoo ci Mbotaayu-xeet-yi, jagleel làkki-ndey yi, maanaam làkk wi nga xam ne moom la nit ku nekk nàmp.
[3] tree
Loolu bi ko UNESCO dooree ak léegi ëpp na 10 at.
s-3
wo_wtb-ud-train_958
Loolu bi ko UNESCO dooree ak léegi ëpp na 10 at.
[4] tree
Li waral bés bi mooy yee nit ñi, artu leen, soññ leen ci solo bu jeggi-dayoo bi làkki-ndey yi am ci fànnu yokkute yépp.
s-4
wo_wtb-ud-train_959
Li waral bés bi mooy yee nit ñi, artu leen, soññ leen ci solo bu jeggi-dayoo bi làkki-ndey yi am ci fànnu yokkute yépp.
[5] tree
Rawatina ci réewi Afrik yi nga xam ne daanaka ya ca ëpp ba ñu tàbbee ci 'kolonisation' ba téy jii ñu moomee seen bopp, dañoo xeeb seeni làkk yi ñu nàmp.
s-5
wo_wtb-ud-train_960
Rawatina ci réewi Afrik yi nga xam ne daanaka ya ca ëpp ba ñu tàbbee ci 'kolonisation' ba téy jii ñu moomee seen bopp, dañoo xeeb seeni làkk yi ñu nàmp.
[6] tree
Réew yi gën a bari Afrik, Senegaal waxi noppi, seeni làkk sedduñu leen daanaka benn cër bu tàkku.
s-6
wo_wtb-ud-train_961
Réew yi gën a bari Afrik, Senegaal waxi noppi, seeni làkk sedduñu leen daanaka benn cër bu tàkku.
[7] tree
Kenn du leen jàng mbaa di leen jàngale ci lekkool yi.
s-7
wo_wtb-ud-train_962
Kenn du leen jàng mbaa di leen jàngale ci lekkool yi.
[8] tree
Kenn du leen jëfandikoo ci bérebi àttekaay yi ak feneen ak feneen.
s-8
wo_wtb-ud-train_963
Kenn du leen jëfandikoo ci bérebi àttekaay yi ak feneen ak feneen.
[9] tree
Dañu leen a soofal daal maanaam.
s-9
wo_wtb-ud-train_964
Dañu leen a soofal daal maanaam.
[10] tree
Te fekk nag, loolu sax naka jekk moo waral sunu xeex bii;
s-10
wo_wtb-ud-train_965
Te fekk nag, loolu sax naka jekk moo waral sunu xeex bii;
[11] tree
Amul wenn askan wu mën a am tawféex, yokkute ak jëm-ca-kanam ci wàllu politik, koom-koom, njàng ak leneen te dumooyu say làkk.
s-11
wo_wtb-ud-train_966
Amul wenn askan wu mën a am tawféex, yokkute ak jëm-ca-kanam ci wàllu politik, koom-koom, njàng ak leneen te dumooyu say làkk.
[12] tree
Bind nañu ko fi lu bare, indi nañu it firnde yiy wone ne réewi tubaab yi seen bopp nuy roy ci lu nekk, laata ñu doon génn ci ag lëndëmtu, dañoo mujj a dekkil seeni làkk.
s-12
wo_wtb-ud-train_967
Bind nañu ko fi lu bare, indi nañu it firnde yiy wone ne réewi tubaab yi seen bopp nuy roy ci lu nekk, laata ñu doon génn ci ag lëndëmtu, dañoo mujj a dekkil seeni làkk.
[13] tree
Loola a nga xewoon ca ndorteel 15eelu xarnu bi:
s-13
wo_wtb-ud-train_968
Loola a nga xewoon ca ndorteel 15eelu xarnu bi:
[14] tree
Booba ñoom làkki Lateñ rekk lañu daan jàng di ca bind, defe woon ne seeni làkk tekkiwuñu dara.
s-14
wo_wtb-ud-train_969
Booba ñoom làkki Lateñ rekk lañu daan jàng di ca bind, defe woon ne seeni làkk tekkiwuñu dara.
[15] tree
Ba ñu daggee buum googu lañu tàmbalee gindeeku ba léegi, am yokkute ci lu nekk, ba tollu tey ci boppu àddina.
s-15
wo_wtb-ud-train_970
Ba ñu daggee buum googu lañu tàmbalee gindeeku ba léegi, am yokkute ci lu nekk, ba tollu tey ci boppu àddina.
[16] tree
Looloo waral bi UNESCO nemmeekoo càggante ak yàq gu jeggi-dayoo googu mu def at mu nekk mu di fàttali xeet yi ak askan yi seeni làmmiñ!
s-16
wo_wtb-ud-train_971
Looloo waral bi UNESCO nemmeekoo càggante ak yàq gu jeggi-dayoo googu mu def at mu nekk mu di fàttali xeet yi ak askan yi seeni làmmiñ!
[17] tree
Ndax gëstu yépp ci fànnu xam-xami làkk ak xaralaay jàngale wone nañu ci lu wér, ne xale bi door njàngam ci làkk wi mu nàmp, moo di gën a ubbeeku fuuf moroomam ma tàmbale njàngam làkk wu mu nàmpul.
s-17
wo_wtb-ud-train_972
Ndax gëstu yépp ci fànnu xam-xami làkk ak xaralaay jàngale wone nañu ci lu wér, ne xale bi door njàngam ci làkk wi mu nàmp, moo di gën a ubbeeku fuuf moroomam ma tàmbale njàngam làkk wu mu nàmpul.
[18] tree
Li ko waral mooy xale bi buy dal rekk dees di mën a tàggat xelam ci fànn yu bare niki matematik, xam-xami cosaan, fisik ak yeneen.
s-18
wo_wtb-ud-train_973
Li ko waral mooy xale bi buy dal rekk dees di mën a tàggat xelam ci fànn yu bare niki matematik, xam-xami cosaan, fisik ak yeneen.
[19] tree
Te bu dee, kom ni ñu koy defe Senegaal, njàng mi yépp ci Nasaraan la, su xale bi duggee lekool dafay mel ni ku lu.
s-19
wo_wtb-ud-train_974
Te bu dee, kom ni ñu koy defe Senegaal, njàng mi yépp ci Nasaraan la, su xale bi duggee lekool dafay mel ni ku lu.
[20] tree
Dafay mel ni perantal buy door a jàng wax.
s-20
wo_wtb-ud-train_975
Dafay mel ni perantal buy door a jàng wax.
[21] tree
Dina def lu yágg ci ay at balaa lees ko mën a jàngal lenn lu am solo ci Nasaraan.
s-21
wo_wtb-ud-train_976
Dina def lu yágg ci ay at balaa lees ko mën a jàngal lenn lu am solo ci Nasaraan.
[22] tree
Ndax déggu ko!
s-22
wo_wtb-ud-train_977
Ndax déggu ko!
[23] tree
Li ëpp ci lu muy jàng du weesu ijji ak nafar lu mu xamul lu muy tekki.
s-23
wo_wtb-ud-train_978
Li ëpp ci lu muy jàng du weesu ijji ak nafar lu mu xamul lu muy tekki.
[24] tree
Rax-ci-dolli, xeeb boppam, tiitange ak jaaxle bi xale biy am, su ràññee ne, ndeke moom làkk bi mu nàmp tekkiwul dara ca béréb yay indi tekki ëllëg ca réewam!
s-24
wo_wtb-ud-train_979
Rax-ci-dolli, xeeb boppam, tiitange ak jaaxle bi xale biy am, su ràññee ne, ndeke moom làkk bi mu nàmp tekkiwul dara ca béréb yay indi tekki ëllëg ca réewam!
[25] tree
Dafay juux ci lu ñu woowee 'crise d'identité', maanaam, dootul ràññeeti li mu doon, dafay nekk ku neex a yobbale, ku neex a ómmat!
s-25
wo_wtb-ud-train_980
Dafay juux ci lu ñu woowee 'crise d'identité', maanaam, dootul ràññeeti li mu doon, dafay nekk ku neex a yobbale, ku neex a ómmat!
[26] tree
Waxoon nañu fi itam ne sax soo koy seet, demokarasi bi ñuy wax, maanaam 'nguuru askan wi ngir askan wi', mënul a am ci làkk woo jeggani!
s-26
wo_wtb-ud-train_981
Waxoon nañu fi itam ne sax soo koy seet, demokarasi bi ñuy wax, maanaam 'nguuru askan wi ngir askan wi', mënul a am ci làkk woo jeggani!
[27] tree
Wante tey bi ñu demee bay tekki ci saa si lépp li ñuy wax ci pencum réewum Senegaal ci làkki réew mi, sànt nañu Yàlla, ndax mel na ni li ñuy fiy wax am na ñu ko dégg!
s-27
wo_wtb-ud-train_982
Wante tey bi ñu demee bay tekki ci saa si lépp li ñuy wax ci pencum réewum Senegaal ci làkki réew mi, sànt nañu Yàlla, ndax mel na ni li ñuy fiy wax am na ñu ko dégg!
[28] tree
Wante li des bare na lool: Jot na ñu jàngale làkki réew mi ci daara yi, ci lekool!
s-28
wo_wtb-ud-train_983
Wante li des bare na lool: Jot na ñu jàngale làkki réew mi ci daara yi, ci lekool!

Edit as listText viewDependency trees