Sentence view
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | train |
---|
Annotation | Dione, Bamba |
---|
Text: -
Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal.
s-1
wo_wtb-ud-train_24
Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal.
Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk.
s-2
wo_wtb-ud-train_25
Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk.
Kajoor moo di kàdd ag garab gu nekk Senegaal ak joor, suuf si.
s-3
wo_wtb-ud-train_26
Kajoor moo di kàdd ag garab gu nekk Senegaal ak joor, suuf si.
Moo jur baat boobu Kajoor ci Wolof.
s-4
wo_wtb-ud-train_27
Moo jur baat boobu Kajoor ci Wolof.
Ñi jëkk a yor suufi Kajoor, ay séeréer lañu woon.
s-5
wo_wtb-ud-train_28
Ñi jëkk a yor suufi Kajoor, ay séeréer lañu woon.
Ñu doonoon ay lamaan te sant JAAÑ.
s-6
wo_wtb-ud-train_29
Ñu doonoon ay lamaan te sant JAAÑ.
Ba pare, xeetu Wagadu ak Jafunu, soqi ci Sooninké yi, jóge ca penku.
s-7
wo_wtb-ud-train_30
Ba pare, xeetu Wagadu ak Jafunu, soqi ci Sooninké yi, jóge ca penku.
Ñoo sos meen yi jëkk a ilif nguur gi, ak ñu sant FAAL.
s-8
wo_wtb-ud-train_31
Ñoo sos meen yi jëkk a ilif nguur gi, ak ñu sant FAAL.
Gàddaay moo leen tax ñëw Kajoor.
s-9
wo_wtb-ud-train_32
Gàddaay moo leen tax ñëw Kajoor.
Kon ñooñu mujj nekk Dammeel Kajoor, ay doxandéem lañu yu nekkoon ca réew moomu ca njëlbéen.
s-10
wo_wtb-ud-train_33
Kon ñooñu mujj nekk Dammeel Kajoor, ay doxandéem lañu yu nekkoon ca réew moomu ca njëlbéen.
Dammeel mooy damm.
s-11
wo_wtb-ud-train_34
Dammeel mooy damm.
Ndax ku jëkk a jël dakkantal boobu, di Decce Fu Njogu FAAL, dañu naan damm na li Kajoor seqante woon ak Jolof, ndax Jolof moo nangu woon Kajoor.
s-12
wo_wtb-ud-train_35
Ndax ku jëkk a jël dakkantal boobu, di Decce Fu Njogu FAAL, dañu naan damm na li Kajoor seqante woon ak Jolof, ndax Jolof moo nangu woon Kajoor.
Li mu def a tax Kajoor jël yoonam te yore boppam.
s-13
wo_wtb-ud-train_36
Li mu def a tax Kajoor jël yoonam te yore boppam.
Loolu, ca jamono ja Lele Fuli Fak NJAAY nekkoon Buur-ba Jolof la xeewe.
s-14
wo_wtb-ud-train_37
Loolu, ca jamono ja Lele Fuli Fak NJAAY nekkoon Buur-ba Jolof la xeewe.
Buur-ba boobu moo tase ci xare ak doomu Decce Fu Njogu, di Amari Ngone Sobel FAAL, ca benn dëkk bu ñu naan DANKI.
s-15
wo_wtb-ud-train_38
Buur-ba boobu moo tase ci xare ak doomu Decce Fu Njogu, di Amari Ngone Sobel FAAL, ca benn dëkk bu ñu naan DANKI.
Ca xare boobu Kajoor jël yoonam, te damm li ko Jolof nangu woon.
s-16
wo_wtb-ud-train_39
Ca xare boobu Kajoor jël yoonam, te damm li ko Jolof nangu woon.
Ba noppi Amari Ngone jox baayam Decce Fu Njogu mu jiite Kajoor.
s-17
wo_wtb-ud-train_40
Ba noppi Amari Ngone jox baayam Decce Fu Njogu mu jiite Kajoor.
Ca tegu, Kajoor di gën a am doole.
s-18
wo_wtb-ud-train_41
Ca tegu, Kajoor di gën a am doole.
Amari Ngone dem na Bawol ak ay jàmbaaram, nangu reew moomu.
s-19
wo_wtb-ud-train_42
Amari Ngone dem na Bawol ak ay jàmbaaram, nangu reew moomu.
Lii moo tax Amari doonoon ku jëkk a nekk Dammeel-Teeñ.
s-20
wo_wtb-ud-train_43
Lii moo tax Amari doonoon ku jëkk a nekk Dammeel-Teeñ.
Bawol, njabootu ndeyam ñoo fa nekkoon buur, ak nijaayam, Ñoxor Njaay Kuli Njigan.
s-21
wo_wtb-ud-train_44
Bawol, njabootu ndeyam ñoo fa nekkoon buur, ak nijaayam, Ñoxor Njaay Kuli Njigan.
Amari moo duggal aada bi.
s-22
wo_wtb-ud-train_45
Amari moo duggal aada bi.
Ñu fal buur bu ñu tudde Xulixuli, di fàtteliku bi NJAAJAAN NJAAY (ku jëkk a nekk Buur-ba Jolof) nekkoon biir dex gi, ca Waalo.
s-23
wo_wtb-ud-train_46
Ñu fal buur bu ñu tudde Xulixuli, di fàtteliku bi NJAAJAAN NJAAY (ku jëkk a nekk Buur-ba Jolof) nekkoon biir dex gi, ca Waalo.
Ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na nguur gu ay am-amam newoon gàññ.
s-24
wo_wtb-ud-train_47
Ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na nguur gu ay am-amam newoon gàññ.
Mbay ak liggéey ci loxo ak càmm ak napp ak njaay ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca nguur ga.
s-25
wo_wtb-ud-train_48
Mbay ak liggéey ci loxo ak càmm ak napp ak njaay ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca nguur ga.
Mbay moo doonoon liggéey bi ëppoon solo ci koom-koomam.
s-26
wo_wtb-ud-train_49
Mbay moo doonoon liggéey bi ëppoon solo ci koom-koomam.
Looloo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ ca koom ga.
s-27
wo_wtb-ud-train_50
Looloo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ ca koom ga.
Manoon naa indi sax ab xiif.
s-28
wo_wtb-ud-train_51
Manoon naa indi sax ab xiif.
Dugub moo ëppoon ci mbay mi ak ci dund gi.
s-29
wo_wtb-ud-train_52
Dugub moo ëppoon ci mbay mi ak ci dund gi.
Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng.
s-30
wo_wtb-ud-train_53
Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng.
Xamoon nañu mbayum wëtteen.
s-31
wo_wtb-ud-train_54
Xamoon nañu mbayum wëtteen.
Liggéey ak loxo ñeeño yi lañu ko feetale woon.
s-32
wo_wtb-ud-train_55
Liggéey ak loxo ñeeño yi lañu ko feetale woon.
Napp gi amoon na solo lool ci dund gi.
s-33
wo_wtb-ud-train_56
Napp gi amoon na solo lool ci dund gi.
Waaye njaay moom naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal.
s-34
wo_wtb-ud-train_57
Waaye njaay moom naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal.
Mujj na ba yoon yi jóge bëj-gànnaar ñàkk solo lool njëgg mi.
s-35
wo_wtb-ud-train_58
Mujj na ba yoon yi jóge bëj-gànnaar ñàkk solo lool njëgg mi.
Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo.
s-36
wo_wtb-ud-train_59
Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo.
Fekkoon na Kajoor daan jaay ay der ak ay bëñi ñayy.
s-37
wo_wtb-ud-train_60
Fekkoon na Kajoor daan jaay ay der ak ay bëñi ñayy.
Mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi, ...
s-38
wo_wtb-ud-train_61
Mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi, ...
Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon.
s-39
wo_wtb-ud-train_62
Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon.
Ñi ñu di wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu.
s-40
wo_wtb-ud-train_63
Ñi ñu di wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu.
Benn nit amu ci woon moomeel.
s-41
wo_wtb-ud-train_64
Benn nit amu ci woon moomeel.
Loolu terewul woon ku mu neexoon mu jariñoo ci kéem kàttanam.
s-42
wo_wtb-ud-train_65
Loolu terewul woon ku mu neexoon mu jariñoo ci kéem kàttanam.
Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya.
s-43
wo_wtb-ud-train_66
Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya.
Ñi di door a falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo.
s-44
wo_wtb-ud-train_67
Ñi di door a falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo.
Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon.
s-45
wo_wtb-ud-train_68
Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon.
Ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul.
s-46
wo_wtb-ud-train_69
Ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul.
Rax-ci-dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk.
s-47
wo_wtb-ud-train_70
Rax-ci-dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk.
Su fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi.
s-48
wo_wtb-ud-train_71
Su fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi.
Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetale woon mbay mi.
s-49
wo_wtb-ud-train_72
Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetale woon mbay mi.
Ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat.
s-50
wo_wtb-ud-train_73
Ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat.
Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay.
s-51
wo_wtb-ud-train_74
Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay.
Nguur gu bees gi tax na ba ñu indi tër yu bees ci ay àtte yu bees.
s-52
wo_wtb-ud-train_75
Nguur gu bees gi tax na ba ñu indi tër yu bees ci ay àtte yu bees.
Dammeel moo féete woon ñépp kaw.
s-53
wo_wtb-ud-train_76
Dammeel moo féete woon ñépp kaw.
Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen.
s-54
wo_wtb-ud-train_77
Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen.
Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen.
s-55
wo_wtb-ud-train_78
Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen.
Waaye loolu su xewee li ko di waral moo di fullay waa ja ak faydaam ak tabeem.
s-56
wo_wtb-ud-train_79
Waaye loolu su xewee li ko di waral moo di fullay waa ja ak faydaam ak tabeem.
Yii yépp ñi di tànn daa nañu ci bàyyi xel.
s-57
wo_wtb-ud-train_80
Yii yépp ñi di tànn daa nañu ci bàyyi xel.
Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem.
s-58
wo_wtb-ud-train_81
Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem.
Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe.
s-59
wo_wtb-ud-train_82
Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe.
Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur.
s-60
wo_wtb-ud-train_83
Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur.
Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn.
s-61
wo_wtb-ud-train_84
Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn.
Kajoor nekkoon na juróomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum.
s-62
wo_wtb-ud-train_85
Kajoor nekkoon na juróomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum.
Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam fu nga féete.
s-63
wo_wtb-ud-train_86
Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam fu nga féete.
Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur.
s-64
wo_wtb-ud-train_87
Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur.
Edit as list • Text view • Dependency trees