Sentence view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain
AnnotationDione, Bamba

Text: -

[1] tree
Jolof moo doonoon nguur gi gënoon a mag ci Senegaal ci jamono yooyu.
s-1
wo_wtb-ud-train_331
Jolof moo doonoon nguur gi gënoon a mag ci Senegaal ci jamono yooyu.
[2] tree
Mu ngi sosu ci xarnub XIV ba Nguuru Mali gu mag ga saayee, rawatina la feete woon ca sowam.
s-2
wo_wtb-ud-train_332
Mu ngi sosu ci xarnub XIV ba Nguuru Mali gu mag ga saayee, rawatina la feete woon ca sowam.
[3] tree
Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono.
s-3
wo_wtb-ud-train_333
Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono.
[4] tree
Ki ñu ne moo sos nguur googu moo di Njaa Jaan Njaay.
s-4
wo_wtb-ud-train_334
Ki ñu ne moo sos nguur googu moo di Njaa Jaan Njaay.
[5] tree
Moom doomu Araab la bu ñuy wax Abaabakar ak Lingéer ab Tukulóor bu tudd Faatimata Sall.
s-5
wo_wtb-ud-train_335
Moom doomu Araab la bu ñuy wax Abaabakar ak Lingéer ab Tukulóor bu tudd Faatimata Sall.
[6] tree
Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy.
s-6
wo_wtb-ud-train_336
Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy.
[7] tree
Bokk na ci def Wolof yi ñuy benn, teg réew mi ci yoonu nguur gu leer.
s-7
wo_wtb-ud-train_337
Bokk na ci def Wolof yi ñuy benn, teg réew mi ci yoonu nguur gu leer.
[8] tree
Samp nguuru Waalo ba mu dëgër, mu daldi koy jox rakkam.
s-8
wo_wtb-ud-train_338
Samp nguuru Waalo ba mu dëgër, mu daldi koy jox rakkam.
[9] tree
Sos nguuru Jolof gu mag ga ba mu yegg fa gën a kawe mu door a wàcce boppam.
s-9
wo_wtb-ud-train_339
Sos nguuru Jolof gu mag ga ba mu yegg fa gën a kawe mu door a wàcce boppam.
[10] tree
Looloo tax ña ko wuutu ñoo mottali liggéeyam ci xarnub XIV, waaye jotuñoo moytu taste gu gaaw ca nguur gu mag ga.
s-10
wo_wtb-ud-train_340
Looloo tax ña ko wuutu ñoo mottali liggéeyam ci xarnub XIV, waaye jotuñoo moytu taste gu gaaw ca nguur gu mag ga.
[11] tree
Boo seetloo turi buur yu njëkk yi ci nguur gu mag gi dinga fa fekk ñent fukk doŋŋ.
s-11
wo_wtb-ud-train_341
Boo seetloo turi buur yu njëkk yi ci nguur gu mag gi dinga fa fekk ñent fukk doŋŋ.
[12] tree
Seen péey nekkoon na Céŋŋ ca jamonoy Njaa Jaan Njaay.
s-12
wo_wtb-ud-train_342
Seen péey nekkoon na Céŋŋ ca jamonoy Njaa Jaan Njaay.
[13] tree
Réew yu bari nekkoon nañu ci kilifteefu gu mag ga.
s-13
wo_wtb-ud-train_343
Réew yu bari nekkoon nañu ci kilifteefu gu mag ga.
[14] tree
Lu mel ni Senegaal ak Gaambi ak Faleme nekkoon nañu ci suufu Jolof gu mag ga.
s-14
wo_wtb-ud-train_344
Lu mel ni Senegaal ak Gaambi ak Faleme nekkoon nañu ci suufu Jolof gu mag ga.
[15] tree
Buur yi ñu mënoon fal ngir yilif nguuru Jolof, dañu doon war a bokk ci juróomi meen (wàllu ndeey), yooyu sant: Njaay, Joob, Faal, Ndaw, Ñaŋ.
s-15
wo_wtb-ud-train_345
Buur yi ñu mënoon fal ngir yilif nguuru Jolof, dañu doon war a bokk ci juróomi meen (wàllu ndeey), yooyu sant: Njaay, Joob, Faal, Ndaw, Ñaŋ.
[16] tree
Ci xeeti Seereer ak Pël, lañu jóge.
s-16
wo_wtb-ud-train_346
Ci xeeti Seereer ak Pël, lañu jóge.
[17] tree
Jolof boo ko dee xool dafa këll bunom dem na ba Lag de Geer, égg na Ferlo.
s-17
wo_wtb-ud-train_347
Jolof boo ko dee xool dafa këll bunom dem na ba Lag de Geer, égg na Ferlo.
[18] tree
Moom dafa xaw a uuf Tooro ak Dimat ak Waalo ak Kajoor ak Bawol ak Siin-Saalum.
s-18
wo_wtb-ud-train_348
Moom dafa xaw a uuf Tooro ak Dimat ak Waalo ak Kajoor ak Bawol ak Siin-Saalum.
[19] tree
Wàllu penku wi ndand féy-féy la.
s-19
wo_wtb-ud-train_349
Wàllu penku wi ndand féy-féy la.
[20] tree
Jolof fu neew ñax la, bari na lool garabi werek.
s-20
wo_wtb-ud-train_350
Jolof fu neew ñax la, bari na lool garabi werek.
[21] tree
Mel na ne du fu naat it, ndax ab woykat bu siiw ci yu wolof yi di Sëriñ Musaa KA am na fu mu di melale lu ni mel ci genn xasidaam.
s-21
wo_wtb-ud-train_351
Mel na ne du fu naat it, ndax ab woykat bu siiw ci yu wolof yi di Sëriñ Musaa KA am na fu mu di melale lu ni mel ci genn xasidaam.
[22] tree
Mu ne: nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax soo màggatee yalwaani.
s-22
wo_wtb-ud-train_352
Mu ne: nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax soo màggatee yalwaani.
[23] tree
Kon du war a nekk fu bari ay balluwaayi xéewal.
s-23
wo_wtb-ud-train_353
Kon du war a nekk fu bari ay balluwaayi xéewal.
[24] tree
Waa Jolof nekkoon nañu ay giir yu wuute.
s-24
wo_wtb-ud-train_354
Waa Jolof nekkoon nañu ay giir yu wuute.
[25] tree
Giir yooyu ay Séeréer lañu ak ay Wolof ak ay Tukulóor.
s-25
wo_wtb-ud-train_355
Giir yooyu ay Séeréer lañu ak ay Wolof ak ay Tukulóor.
[26] tree
Naari Gànnar yi daan nañu song ñi dëkk ci tàkkal dex gi.
s-26
wo_wtb-ud-train_356
Naari Gànnar yi daan nañu song ñi dëkk ci tàkkal dex gi.
[27] tree
Nee nañu ki fa njëkk a dëkk mu ngi tudd Njolofeen Mbeng.
s-27
wo_wtb-ud-train_357
Nee nañu ki fa njëkk a dëkk mu ngi tudd Njolofeen Mbeng.
[28] tree
Mu ngi bokk ci xeetu Màndeŋ.
s-28
wo_wtb-ud-train_358
Mu ngi bokk ci xeetu Màndeŋ.
[29] tree
Turam lañu jox nguuru Jolof.
s-29
wo_wtb-ud-train_359
Turam lañu jox nguuru Jolof.
[30] tree
Moo fa njëkk a sos dëkk bu ñu daan wooye Kàyti, moom mu ngi nekkoon ci Yeŋ-yeŋ.
s-30
wo_wtb-ud-train_360
Moo fa njëkk a sos dëkk bu ñu daan wooye Kàyti, moom mu ngi nekkoon ci Yeŋ-yeŋ.
[31] tree
Fuuta moo doon gën jaa màggi réew ci mbooleem gox yi.
s-31
wo_wtb-ud-train_361
Fuuta moo doon gën jaa màggi réew ci mbooleem gox yi.
[32] tree
Loolu masul a deñ ba ci fukkeelu xarnu ak ñeent, moo tollook falug waa Tonjon.
s-32
wo_wtb-ud-train_362
Loolu masul a deñ ba ci fukkeelu xarnu ak ñeent, moo tollook falug waa Tonjon.
[33] tree
Jamono jooju la Màndeŋ yi yaatal seen nguur gu mag dale ca géeju Atlas ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum ca Gàmbi.
s-33
wo_wtb-ud-train_363
Jamono jooju la Màndeŋ yi yaatal seen nguur gu mag dale ca géeju Atlas ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum ca Gàmbi.
[34] tree
Ca jamono jooju yit la nguuru Jolof nangoo boppam.
s-34
wo_wtb-ud-train_364
Ca jamono jooju yit la nguuru Jolof nangoo boppam.
[35] tree
Moo gënoon a am solo ci réewu Wolof yi ak Séeréer si ak ci mbooleem réew yi ci géej gi, ci li ko dale ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum, Fuuta ba Saalum.
s-35
wo_wtb-ud-train_365
Moo gënoon a am solo ci réewu Wolof yi ak Séeréer si ak ci mbooleem réew yi ci géej gi, ci li ko dale ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum, Fuuta ba Saalum.
[36] tree
Ëmboon na Waalo, Kajoor, Bawol ak réewi Séeréer si ak lenn ci Fuuta Tooro.
s-36
wo_wtb-ud-train_366
Ëmboon na Waalo, Kajoor, Bawol ak réewi Séeréer si ak lenn ci Fuuta Tooro.
[37] tree
Réew yu bari nangu nañu seen bopp ci nguuru Jolof gu mag ga.
s-37
wo_wtb-ud-train_367
Réew yu bari nangu nañu seen bopp ci nguuru Jolof gu mag ga.
[38] tree
Kajoor njëkk a nangu boppam topp ca Waalo ci njiitu Barag.
s-38
wo_wtb-ud-train_368
Kajoor njëkk a nangu boppam topp ca Waalo ci njiitu Barag.
[39] tree
Bawol ci njiitu Teeñ.
s-39
wo_wtb-ud-train_369
Bawol ci njiitu Teeñ.
[40] tree
Réewi Séeréer si ci njiitu Buur.
s-40
wo_wtb-ud-train_370
Réewi Séeréer si ci njiitu Buur.
[41] tree
Jolof mujj na nekk réew ni yeneen yi ci xarnub XVI ba XIX.
s-41
wo_wtb-ud-train_371
Jolof mujj na nekk réew ni yeneen yi ci xarnub XVI ba XIX.
[42] tree
Waaye Dammeel moom moo gënoon a metti ag jàmmaarloo ak Burba Jolof ca xareb Danki ba nga xam ne moo njëkk a faagaagal nguuru Jolof gu mag ga.
s-42
wo_wtb-ud-train_372
Waaye Dammeel moom moo gënoon a metti ag jàmmaarloo ak Burba Jolof ca xareb Danki ba nga xam ne moo njëkk a faagaagal nguuru Jolof gu mag ga.
[43] tree
Gannaaw loolu la xareb Mbisin ca 1697, foofa Kajoor moo jekku, ak xareb Ambaal ci 1760, ak xareb 1886.
s-43
wo_wtb-ud-train_373
Gannaaw loolu la xareb Mbisin ca 1697, foofa Kajoor moo jekku, ak xareb Ambaal ci 1760, ak xareb 1886.
[44] tree
Bokk na ci li ngirteel saayam, ñaari noon yu doon xëccoo nguur ga ñaarelu xaaj bu xarnub XIX.
s-44
wo_wtb-ud-train_374
Bokk na ci li ngirteel saayam, ñaari noon yu doon xëccoo nguur ga ñaarelu xaaj bu xarnub XIX.
[45] tree
Noon bu njëkk bi mooy Tanoor Jeŋ.
s-45
wo_wtb-ud-train_375
Noon bu njëkk bi mooy Tanoor Jeŋ.
[46] tree
Ñaareelu noon bi mooy Amadu Sayxu.
s-46
wo_wtb-ud-train_376
Ñaareelu noon bi mooy Amadu Sayxu.
[47] tree
Tanoor Jeŋ doomi Lingeer Kura Ngoy, song na Buurba ngir nangu nguur ga.
s-47
wo_wtb-ud-train_377
Tanoor Jeŋ doomi Lingeer Kura Ngoy, song na Buurba ngir nangu nguur ga.
[48] tree
Ginnaaw bi moom Amadu Sayxu nanguwaat ko ci 1870, yor ko ba ci atum 1875.
s-48
wo_wtb-ud-train_378
Ginnaaw bi moom Amadu Sayxu nanguwaat ko ci 1870, yor ko ba ci atum 1875.
[49] tree
Ci at moomu lañu ko jekkoo ca xareb Sàmba Saajo.
s-49
wo_wtb-ud-train_379
Ci at moomu lañu ko jekkoo ca xareb Sàmba Saajo.
[50] tree
Ci noonu la Jolof tàbbee ci loxoy Faraas ci 18 rakki gammu 1885.
s-50
wo_wtb-ud-train_380
Ci noonu la Jolof tàbbee ci loxoy Faraas ci 18 rakki gammu 1885.

Edit as listText viewDependency trees