Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train Annotation Dione, Bamba
Text: Transcription Written form - Colors
Lan lañu war a xam ci jabet
s-1
wo_wtb-ud-train_1231
Lan lañu war a xam ci jabet
Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo , ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase ( Dr Abdoul Aziz KASSE Chirurgien Institut du Cancer Université Cheikh Anta DIOP )
s-2
wo_wtb-ud-train_1232
Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo, ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase (Dr Abdoul Aziz KASSE Chirurgien Institut du Cancer Université Cheikh Anta DIOP)
Lan mooy jabet ?
s-3
wo_wtb-ud-train_1233
Lan mooy jabet?
Ñaari wirgoy jabet ñoo am , jabet 1 ak jabet 2 .
s-4
wo_wtb-ud-train_1234
Ñaari wirgoy jabet ñoo am, jabet 1 ak jabet 2.
Ñoom ñaar ñépp xàmmees na leen ci nattu suukar bu jéggi dayo ci deret ji , ëpp 1,26 g .
s-5
wo_wtb-ud-train_1235
Ñoom ñaar ñépp xàmmees na leen ci nattu suukar bu jéggi dayo ci deret ji, ëpp 1,26 g.
Waaye li sabab natt bu jéggi dayo bi ci jabet 1 wuute na ak li ko sabab ci jabet 2 .
s-6
wo_wtb-ud-train_1236
Waaye li sabab natt bu jéggi dayo bi ci jabet 1 wuute na ak li ko sabab ci jabet 2.
Jabet 1 , tuddees na ko yitam jabetu ndaw ( diabète juvénile ) , ndax li muy dal nit ki ci ag ndawam , diggante ba mu amee ay weer ba 35 at .
s-7
wo_wtb-ud-train_1237
Jabet 1, tuddees na ko yitam jabetu ndaw (diabète juvénile), ndax li muy dal nit ki ci ag ndawam, diggante ba mu amee ay weer ba 35 at.
Ci wirgo bii , li sabab nattu suukar bu jéggi dayo mu ngi sababoo ci li pànkreyaa bi mënul a defar mbir moomu ñu tudde « insuline » ni mu ware .
s-8
wo_wtb-ud-train_1238
Ci wirgo bii, li sabab nattu suukar bu jéggi dayo mu ngi sababoo ci li pànkreyaa bi mënul a defar mbir moomu ñu tudde «insuline» ni mu ware.
Te « insuline » mënul a ñàkk ci dundug nit , ndax moo di yemale suukar si ci deret ji .
s-9
wo_wtb-ud-train_1239
Te «insuline» mënul a ñàkk ci dundug nit, ndax moo di yemale suukar si ci deret ji.
Ci téeméeri nit ñu yore jabet ñu ne , fukk ñi jabet bii moo leen dal , mu doon fukk ci téeméer ( 10 % ) .
s-10
wo_wtb-ud-train_1240
Ci téeméeri nit ñu yore jabet ñu ne, fukk ñi jabet bii moo leen dal, mu doon fukk ci téeméer (10 %).
Jabet 2 .
s-11
wo_wtb-ud-train_1241
Jabet 2.
Ci wirgo bii , li tax natt bi jéggi dayo jógewul ci pànkreyaa bi , ndax mën na a defar « insuline » , waaye yaram wi a ko mënul a jëfandikoo ni mu ware .
s-12
wo_wtb-ud-train_1242
Ci wirgo bii, li tax natt bi jéggi dayo jógewul ci pànkreyaa bi, ndax mën na a defar «insuline», waaye yaram wi a ko mënul a jëfandikoo ni mu ware.
Ci àddina sépp , ci téeméeri nit ñu yore jabet ñu ne , juróom-ñeen-fukk ñi jabet 2 moo leen dal .
s-13
wo_wtb-ud-train_1243
Ci àddina sépp, ci téeméeri nit ñu yore jabet ñu ne, juróom-ñeen-fukk ñi jabet 2 moo leen dal.
Mu doon juróom-ñeen-fukk ci téeméer ( 90 % ) .
s-14
wo_wtb-ud-train_1244
Mu doon juróom-ñeen-fukk ci téeméer (90 %).
Wirgo bii , mag la di faral di dal , waaye nemmikuwees na ko ci xale yu magaale yi ( adolescents ) .
s-15
wo_wtb-ud-train_1245
Wirgo bii, mag la di faral di dal, waaye nemmikuwees na ko ci xale yu magaale yi (adolescents).
Ana màndarga yi di tax ñu jort jabet ?
s-16
wo_wtb-ud-train_1246
Ana màndarga yi di tax ñu jort jabet?
Ci jabet 1 , màndarga yi ñu faral a nemmiku a ngi nii : saw mu bare , mar gu tar , nit ki am àppeti , di lekk bu baax te du tee yaram wi di jeex , lu mu def sonn .
s-17
wo_wtb-ud-train_1247
Ci jabet 1, màndarga yi ñu faral a nemmiku a ngi nii: saw mu bare, mar gu tar, nit ki am àppeti, di lekk bu baax te du tee yaram wi di jeex, lu mu def sonn.
Ci jabet 2 , màndarga yii weesu mën nañoo làqu , mën nañoo ñàkk sax ca njalbéen ga .
s-18
wo_wtb-ud-train_1248
Ci jabet 2, màndarga yii weesu mën nañoo làqu, mën nañoo ñàkk sax ca njalbéen ga.
Balaa ko doktoor di mën a feeñal dina fekk mu am at yu bare , gannaaw ba jàngoro ji sampoo , fekk yàqu-yàqu yi ci laxasu teew nañu ba noppi .
s-19
wo_wtb-ud-train_1249
Balaa ko doktoor di mën a feeñal dina fekk mu am at yu bare, gannaaw ba jàngoro ji sampoo, fekk yàqu-yàqu yi ci laxasu teew nañu ba noppi.
Nan lañuy saxale ne nit ki dafa jabet ?
s-20
wo_wtb-ud-train_1250
Nan lañuy saxale ne nit ki dafa jabet?
Jabet kër doktoor moo ko mën a saxal .
s-21
wo_wtb-ud-train_1251
Jabet kër doktoor moo ko mën a saxal.
Kurél gi di toppatoo wér-gi-yaram ci àddina sépp ( OMS ) siiwal na nattu deret bi di tax ñu mën ne jàngoro jii jabet la .
s-22
wo_wtb-ud-train_1252
Kurél gi di toppatoo wér-gi-yaram ci àddina sépp (OMS) siiwal na nattu deret bi di tax ñu mën ne jàngoro jii jabet la.
Jàppees na ne ku am lu yées 1,10 g amul jabet .
s-23
wo_wtb-ud-train_1253
Jàppees na ne ku am lu yées 1,10 g amul jabet.
Képp ku am natt bu yées 1,10 g/l , ( maanaam liitaru deret bu ne 1,10 garaam ) , fekk lekkul dara ci 8 waxtu yi jiitu jëlug deret ji , mënees na a wax ni amul jabet .
s-24
wo_wtb-ud-train_1254
Képp ku am natt bu yées 1,10 g/l, (maanaam liitaru deret bu ne 1,10 garaam), fekk lekkul dara ci 8 waxtu yi jiitu jëlug deret ji, mënees na a wax ni amul jabet.
Jàppees na ne ku am 1,26 g mbaa lu ko ëpp am na jabet .
s-25
wo_wtb-ud-train_1255
Jàppees na ne ku am 1,26 g mbaa lu ko ëpp am na jabet.
Jàppees na ne am na jabet képp ku am nattub 1,26 g mbaa bu ko ëpp , fekk lekkul dara ci 8 waxtu wi jiitu jëlug deret ji walla natt bu ëpp 2 g/l , ñaari waxtu gannaaw ba mu jëlee 75 garaamu suukar ( glucose ) .
s-26
wo_wtb-ud-train_1256
Jàppees na ne am na jabet képp ku am nattub 1,26 g mbaa bu ko ëpp, fekk lekkul dara ci 8 waxtu wi jiitu jëlug deret ji walla natt bu ëpp 2 g/l, ñaari waxtu gannaaw ba mu jëlee 75 garaamu suukar (glucose).
Pajum jabet na muy deme ?
s-27
wo_wtb-ud-train_1257
Pajum jabet na muy deme?
Lekk gu deme ni mu ware ( dees na ci dellusi ci jukki bi di ñëw ) ak yëngal yaram , farataal dox , am nañu solo lool ci paj mi .
s-28
wo_wtb-ud-train_1258
Lekk gu deme ni mu ware (dees na ci dellusi ci jukki bi di ñëw) ak yëngal yaram, farataal dox, am nañu solo lool ci paj mi.
Su loolu wéyee , way-jabet 1 ( les diabétiques de type 1 ) fàww bés bu ne ñu pikkiiru « insuline » , ngir lu wuutu « insuline » bi pànkreyaa bi war a defar , te mënu ko .
s-29
wo_wtb-ud-train_1259
Su loolu wéyee, way-jabet 1 (les diabétiques de type 1) fàww bés bu ne ñu pikkiiru «insuline», ngir lu wuutu «insuline» bi pànkreyaa bi war a defar, te mënu ko.
Way-jabet 2 , garab yu yemale suukar si lañu leen di jox , waaye nag am na ci ñoom ñu nga xam ne bu ñu demee ba jëmmi jamono , dina laaj ñu pingu « insuline » .
s-30
wo_wtb-ud-train_1260
Way-jabet 2, garab yu yemale suukar si lañu leen di jox, waaye nag am na ci ñoom ñu nga xam ne bu ñu demee ba jëmmi jamono, dina laaj ñu pingu «insuline».
Yan yàqu-yàqu la jabet mën a jur ?
s-31
wo_wtb-ud-train_1261
Yan yàqu-yàqu la jabet mën a jur?
Dafay jàpp bët yi ba mën a indi silmaxa .
s-32
wo_wtb-ud-train_1262
Dafay jàpp bët yi ba mën a indi silmaxa.
Jabet am na cër bu yaatu ci safaan yi di sabab doyadi ag roñoŋ .
s-33
wo_wtb-ud-train_1263
Jabet am na cër bu yaatu ci safaan yi di sabab doyadi ag roñoŋ.
Jabet mën na a jàpp siddit yi , ba ki mu dal dootul am yëg-yëg ci yaramam , maanaam du yëg lu tàng mbaa lu sedd .
s-34
wo_wtb-ud-train_1264
Jabet mën na a jàpp siddit yi, ba ki mu dal dootul am yëg-yëg ci yaramam, maanaam du yëg lu tàng mbaa lu sedd.
Jabet mën na a laal yit góor ñi ci seen ngóora .
s-35
wo_wtb-ud-train_1265
Jabet mën na a laal yit góor ñi ci seen ngóora.
Tànk yi jar nañu a toppatoo bu baax .
s-36
wo_wtb-ud-train_1266
Tànk yi jar nañu a toppatoo bu baax.
Looloo waral ba gaañu-gaañu , lu mu tuuti tuuti , kenn waru ko a sàggane .
s-37
wo_wtb-ud-train_1267
Looloo waral ba gaañu-gaañu, lu mu tuuti tuuti, kenn waru ko a sàggane.
Li ci war moo di faj ko ba mu wér .
s-38
wo_wtb-ud-train_1268
Li ci war moo di faj ko ba mu wér.
Jabet ci jigéenu-wérul ji mën na a jur jeexital yu bare ci doomam .
s-39
wo_wtb-ud-train_1269
Jabet ci jigéenu-wérul ji mën na a jur jeexital yu bare ci doomam.
Ñu gën ci a ràññee xale bi juddu deme ni noppu jaboot , walla doom ju réy ci juddoom , walla sax doom ji bañ a indaale bakkan .
s-40
wo_wtb-ud-train_1270
Ñu gën ci a ràññee xale bi juddu deme ni noppu jaboot, walla doom ju réy ci juddoom, walla sax doom ji bañ a indaale bakkan.
Ndax jàngoro ji tasaroo na ci àddina si ?
s-41
wo_wtb-ud-train_1271
Ndax jàngoro ji tasaroo na ci àddina si?
Am na 150 milyoŋi way-jabet ci àddina .
s-42
wo_wtb-ud-train_1272
Am na 150 milyoŋi way-jabet ci àddina.
Fii ba 2025 lim bi mën naa fulu ñaari yoon .
s-43
wo_wtb-ud-train_1273
Fii ba 2025 lim bi mën naa fulu ñaari yoon.
Li ci ëpp ñu ngi di nekk ci réew yi néew doole te li ko waral moo di yokku gi nit ñi di yokku , ak magal gi nit ñi di magal , ak lekk gu awul yoon , ak yaram wu ëpp , ak ñàkk a yëngal sa yaram .
s-44
wo_wtb-ud-train_1274
Li ci ëpp ñu ngi di nekk ci réew yi néew doole te li ko waral moo di yokku gi nit ñi di yokku, ak magal gi nit ñi di magal, ak lekk gu awul yoon, ak yaram wu ëpp, ak ñàkk a yëngal sa yaram.
Edit as list • Text view • Dependency trees