Sentence view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest
AnnotationDione, Bamba

Text: -

[1] tree
Xibaaryi.com ab dal la (site) bu di tas xibaar ci wolof, muy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal.
s-1
wo_wtb-ud-train_1657
Xibaaryi.com ab dal la (site) bu di tas xibaar ci wolof, muy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal.
[2] tree
Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar doonoon gëstug jeexal gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa Kelekey Jaxate.
s-2
wo_wtb-ud-train_1658
Mi ngi sosu ci atum 2008 ca Daara Ju Kawe ju Ndar doonoon gëstug jeexal gu ndongo yii di Ibra Njaay ak Musaa Kelekey Jaxate.
[3] tree
Dal bii nag benn la ci saafara yi nu nar a saafaraa jafe-jafe yii nu lim ci suuf.
s-3
wo_wtb-ud-train_1659
Dal bii nag benn la ci saafara yi nu nar a saafaraa jafe-jafe yii nu lim ci suuf.
[4] tree
Ci Senegaal, lu tollu fukk ci téeméer (10 %) rekk ci askan wi ñoo dégg làkku Frãse ba mën ci a jariñu, bu nu méngalee lim boobu ak lu ëpp juróom ñatt fukk ci téeméer (80 %) ci askan wi, ñu nga xam ne seen ag dégg wolof kawe na.
s-4
wo_wtb-ud-train_1660
Ci Senegaal, lu tollu fukk ci téeméer (10 %) rekk ci askan wi ñoo dégg làkku Frãse ba mën ci a jariñu, bu nu méngalee lim boobu ak lu ëpp juróom ñatt fukk ci téeméer (80 %) ci askan wi, ñu nga xam ne seen ag dégg wolof kawe na.
[5] tree
Ñu bari ci askan wi dañu di seetaan ay film te duñu xam sax lu di maanaa mi.
s-5
wo_wtb-ud-train_1661
Ñu bari ci askan wi dañu di seetaan ay film te duñu xam sax lu di maanaa mi.
[6] tree
Loolu nag di mbir mu doy waar ci askan wu bëgg ñu weg ko.
s-6
wo_wtb-ud-train_1662
Loolu nag di mbir mu doy waar ci askan wu bëgg ñu weg ko.
[7] tree
Sunu ndaw ñi, di ëllëgu réew mi, dégguñu solo si baat yi ëmbu dëg-dëg ci film yi ñu leen di jagleel, wante dañuy banneexu rekk ci jëf ju reetaanlu ju ñu gis.
s-7
wo_wtb-ud-train_1663
Sunu ndaw ñi, di ëllëgu réew mi, dégguñu solo si baat yi ëmbu dëg-dëg ci film yi ñu leen di jagleel, wante dañuy banneexu rekk ci jëf ju reetaanlu ju ñu gis.
[8] tree
Loolu tamit di mbir mu nga xam ne du nàmm seen am xel.
s-8
wo_wtb-ud-train_1664
Loolu tamit di mbir mu nga xam ne du nàmm seen am xel.
[9] tree
Bu njëkkoon, barab ya ñu daan seetaane filmu Endo ak kowboy ya dañu daan fees dell ndax ñoo gënoon a neex a nànd.
s-9
wo_wtb-ud-train_1665
Bu njëkkoon, barab ya ñu daan seetaane filmu Endo ak kowboy ya dañu daan fees dell ndax ñoo gënoon a neex a nànd.
[10] tree
Léegi, barab yooya soppees na leen ay ja (marse).
s-10
wo_wtb-ud-train_1666
Léegi, barab yooya soppees na leen ay ja (marse).
[11] tree
Loolu tax ba nit ñi dematuñu sinemaa niki nu ko daan defe bu jëkkoon, waaye tamit dégg-dégg bi jàppandiwul ci film yu mel ni poliis especiaal, afeer kalase tere awaase ak yeneen ak yeneen.
s-11
wo_wtb-ud-train_1667
Loolu tax ba nit ñi dematuñu sinemaa niki nu ko daan defe bu jëkkoon, waaye tamit dégg-dégg bi jàppandiwul ci film yu mel ni poliis especiaal, afeer kalase tere awaase ak yeneen ak yeneen.
[12] tree
Kuréel yiy tàggat askan wi dañoo bàyyi ñi jàngul ak seen bopp ndax làkk frãse lañu fay tàggate.
s-12
wo_wtb-ud-train_1668
Kuréel yiy tàggat askan wi dañoo bàyyi ñi jàngul ak seen bopp ndax làkk frãse lañu fay tàggate.
[13] tree
Tàggat nit ki ci làkk wi mu dégg moo gën a yomb juróom ñaari yoon - gën gaa néew - tàggat ko ci lammiñu jàmbur.
s-13
wo_wtb-ud-train_1669
Tàggat nit ki ci làkk wi mu dégg moo gën a yomb juróom ñaari yoon - gën gaa néew - tàggat ko ci lammiñu jàmbur.
[14] tree
Tàggat ci wolof soxlawul lu dul mu man a bind, man a yër ndax làkk wi dégg na ko ba noppi.
s-14
wo_wtb-ud-train_1670
Tàggat ci wolof soxlawul lu dul mu man a bind, man a yër ndax làkk wi dégg na ko ba noppi.
[15] tree
Bu dee ci wu doxandéem la nag (niki Frãse), dina laaj yeneen yu mel ni nos-wax, tëggiin xam bennaani baat yi ak waxiin wi añs.
s-15
wo_wtb-ud-train_1671
Bu dee ci wu doxandéem la nag (niki Frãse), dina laaj yeneen yu mel ni nos-wax, tëggiin xam bennaani baat yi ak waxiin wi añs.
[16] tree
Nguur gi am na ay jafe-jafe ci fal boroom lijaasa yi sunu daara yu kawe yi tàggat, rawatina ñi seen xam-xam màcc ci kàllaama yi.
s-16
wo_wtb-ud-train_1672
Nguur gi am na ay jafe-jafe ci fal boroom lijaasa yi sunu daara yu kawe yi tàggat, rawatina ñi seen xam-xam màcc ci kàllaama yi.
[17] tree
Ñu néew ci askan wi ñoo di yër yéenekaay yi ñu bind ci wu Frãse.
s-17
wo_wtb-ud-train_1673
Ñu néew ci askan wi ñoo di yër yéenekaay yi ñu bind ci wu Frãse.
[18] tree
Daanaka ñi leen di yër matuñu ñaar fukk ci téeméer (20 %).
s-18
wo_wtb-ud-train_1674
Daanaka ñi leen di yër matuñu ñaar fukk ci téeméer (20 %).
[19] tree
Ba tax na njariñam taxu koo bari.
s-19
wo_wtb-ud-train_1675
Ba tax na njariñam taxu koo bari.
[20] tree
Saafara si: Gën a yaatal njàngale mi ci sunu làkki réew, jaarale ko ci taxawal ay jumtukaayu tas xibaar ci sunu làkki réew, rawatina ay dali internet.
s-20
wo_wtb-ud-train_1676
Saafara si: Gën a yaatal njàngale mi ci sunu làkki réew, jaarale ko ci taxawal ay jumtukaayu tas xibaar ci sunu làkki réew, rawatina ay dali internet.
[21] tree
Taxawal ay këri yéenekaay ci sunu ay làkk;
s-21
wo_wtb-ud-train_1677
Taxawal ay këri yéenekaay ci sunu ay làkk;
[22] tree
Fexe ba tekki film yi ñu di seetaan ak fowukaay yi sunu xale di jëfandikoo ci sunu ay làkk; rawatina ci wolof ndax mooy làkk wi ëpp lu ñu koy jëfandikoo ci réew.
s-22
wo_wtb-ud-train_1678
Fexe ba tekki film yi ñu di seetaan ak fowukaay yi sunu xale di jëfandikoo ci sunu ay làkk; rawatina ci wolof ndax mooy làkk wi ëpp lu ñu koy jëfandikoo ci réew.
[23] tree
Defar tëriin ci sunu ay làkk.
s-23
wo_wtb-ud-train_1679
Defar tëriin ci sunu ay làkk.
[24] tree
Loolu doon na luy yokk xereñug askan wi.
s-24
wo_wtb-ud-train_1680
Loolu doon na luy yokk xereñug askan wi.
[25] tree
Dina yokk ay junniy junniy liggéey ñeel ndongo-daara yi ñu tàggat te amuñu fu ñu leen dugal, ñoñ fànn ñi (ci tekkig film yi ci sunu ay làkk).
s-25
wo_wtb-ud-train_1681
Dina yokk ay junniy junniy liggéey ñeel ndongo-daara yi ñu tàggat te amuñu fu ñu leen dugal, ñoñ fànn ñi (ci tekkig film yi ci sunu ay làkk).
[26] tree
Dina yokk sinemaa yi ñuy seetaane film yi, dina yokk njënd mi ak njaay mi.
s-26
wo_wtb-ud-train_1682
Dina yokk sinemaa yi ñuy seetaane film yi, dina yokk njënd mi ak njaay mi.
[27] tree
Nañu xayma ñaata ci ay film yu wayndare, fowukaay, téere ak film yu xale ñoo am ci àdduna bi ci yeneen i làkk te ñu man koo soppi ci sunu ay làkk, su nu bëggee xam njariñ li ci wàllu kom-kom ak xel.
s-27
wo_wtb-ud-train_1683
Nañu xayma ñaata ci ay film yu wayndare, fowukaay, téere ak film yu xale ñoo am ci àdduna bi ci yeneen i làkk te ñu man koo soppi ci sunu ay làkk, su nu bëggee xam njariñ li ci wàllu kom-kom ak xel.
[28] tree
Ndaxam man nañu di jëfandikoo làkku Faraas ba léegi, waaye loolu warul a tax ba ñu bañ a xalaat ne aw làkk lu man a indi kom-kom la su fekkee ni lu ëpp ci askan wi moom lañu di jëfandikoo.
s-28
wo_wtb-ud-train_1684
Ndaxam man nañu di jëfandikoo làkku Faraas ba léegi, waaye loolu warul a tax ba ñu bañ a xalaat ne aw làkk lu man a indi kom-kom la su fekkee ni lu ëpp ci askan wi moom lañu di jëfandikoo.
[29] tree
Looloo dal wolof fii ci Senegaal, bambara ca Mali.
s-29
wo_wtb-ud-train_1685
Looloo dal wolof fii ci Senegaal, bambara ca Mali.
[30] tree
Loolu la Microsoft sàmm ba tàmbali a amal Windows ak Office ci làkk yu mel ni wolof ak bambara.
s-30
wo_wtb-ud-train_1686
Loolu la Microsoft sàmm ba tàmbali a amal Windows ak Office ci làkk yu mel ni wolof ak bambara.
[31] tree
Google tamit tàmbali na ko.
s-31
wo_wtb-ud-train_1687
Google tamit tàmbali na ko.
[32] tree
Loolu tamit la waa Faraas xam ba taxawal kuréel gi ñuy woowe Francophonie.
s-32
wo_wtb-ud-train_1688
Loolu tamit la waa Faraas xam ba taxawal kuréel gi ñuy woowe Francophonie.
[33] tree
Lu ñu gën di jëfandikoo làkku Faraas ci àdduna bi rekk (lu tollu ak ñaari téeméeri milyoŋ ci doomi aadama) gën di yokk ay liggéey ca Faras, ndax ñoom ñoo di soppi film yooyu di ko jaayaat yeneen téeméer ak ñeen-fukki milyoŋi doomi aadama yi nekk ci yeneen réew te di jëfandikoo làkku Faraas te nun noo ngi ci biir.
s-33
wo_wtb-ud-train_1689

[34] tree
Ndax làkk wolof am na mucc?
s-34
wo_wtb-ud-train_1690
Ndax làkk wolof am na mucc?
[35] tree
Colette Grinevald di ab gëstukat ci làkk ca laboraatuwaaru làkk ba ne ca Lyon-II.
s-35
wo_wtb-ud-train_1691
Colette Grinevald di ab gëstukat ci làkk ca laboraatuwaaru làkk ba ne ca Lyon-II.
[36] tree
Ci ab gëstu bu mu defal Unesco aju ci dundiinu làkk yi, jàpp na ne lu jege 50 % ci làkk yi dinañu saay fi ak atum 2100.
s-36
wo_wtb-ud-train_1692
Ci ab gëstu bu mu defal Unesco aju ci dundiinu làkk yi, jàpp na ne lu jege 50 % ci làkk yi dinañu saay fi ak atum 2100.
[37] tree
Am na sax gox yu nga xam ni, man na a am mu egg ci 90 % (niki Óstrali ak Amerig).
s-37
wo_wtb-ud-train_1693
Am na sax gox yu nga xam ni, man na a am mu egg ci 90 % (niki Óstrali ak Amerig).
[38] tree
Gisees na ne ca atum 2100, làkk yu ñu di gën a wax ñoo di: Àngale, niki làkk njënd, njaay ak xarala, Español ca bëj-saalumu Amerig, Purtugees, ca bëj-saalumu Amerig ak Afrig, Araab, Sinwaa ak Endo ca Asii, Swaahili ak Wolof, ci Afrig.
s-38
wo_wtb-ud-train_1694
Gisees na ne ca atum 2100, làkk yu ñu di gën a wax ñoo di: Àngale, niki làkk njënd, njaay ak xarala, Español ca bëj-saalumu Amerig, Purtugees, ca bëj-saalumu Amerig ak Afrig, Araab, Sinwaa ak Endo ca Asii, Swaahili ak Wolof, ci Afrig.
[39] tree
Li ñu mën a jàngee ci mbajtalu gëstu bi moo di: Benn, làkk Frãse bokkul ci làkk yi am mucc.
s-39
wo_wtb-ud-train_1695
Li ñu mën a jàngee ci mbajtalu gëstu bi moo di: Benn, làkk Frãse bokkul ci làkk yi am mucc.
[40] tree
Te monte Colette Grinevald mi jiite gëstu bi doomu réewum Frãs la.
s-40
wo_wtb-ud-train_1696
Te monte Colette Grinevald mi jiite gëstu bi doomu réewum Frãs la.
[41] tree
Kon ndax warees naa wéy di jiital ci réewum Senegaal làkk wu amul mucc, rax-ci-dolli 10 % askan wi rekk a ko dégg ba mën koo jariñoo?
s-41
wo_wtb-ud-train_1697
Kon ndax warees naa wéy di jiital ci réewum Senegaal làkk wu amul mucc, rax-ci-dolli 10 % askan wi rekk a ko dégg ba mën koo jariñoo?
[42] tree
Ñaar: Sunu làkk wii di Wolof doon na làkk wu am mucc ba tax ñu war koo jiital ci réew mi.
s-42
wo_wtb-ud-train_1698
Ñaar: Sunu làkk wii di Wolof doon na làkk wu am mucc ba tax ñu war koo jiital ci réew mi.
[43] tree
Kon ndax wareesuñoo jiital làkk wu ame nii mucc te lu ëpp 80 % askan wi dégg te di jëfandikoo?
s-43
wo_wtb-ud-train_1699
Kon ndax wareesuñoo jiital làkk wu ame nii mucc te lu ëpp 80 % askan wi dégg te di jëfandikoo?

Edit as listText viewDependency trees