Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part test Annotation Dione, Bamba
Text: Transcription Written form - Colors
Jimbulang aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam , maanaam jimbulang bu di wax ci paj walla ci taariix kepp .
s-1
wo_wtb-ud-train_1390
Jimbulang aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam, maanaam jimbulang bu di wax ci paj walla ci taariix kepp.
Jimbulang am mbooloom ay jukki la def , bu ci nekk di wax ci lenn : ci aw nit , ci ab barab , ci ab xew-xew , ci ab xam-xam , ...
s-2
wo_wtb-ud-train_1391
Jimbulang am mbooloom ay jukki la def, bu ci nekk di wax ci lenn: ci aw nit, ci ab barab, ci ab xew-xew, ci ab xam-xam, ...
Jimbulang dafa di wuute ak baatukaay , ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi .
s-3
wo_wtb-ud-train_1392
Jimbulang dafa di wuute ak baatukaay, ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi.
Naka-jekk dafay doon ay téere yu bari .
s-4
wo_wtb-ud-train_1393
Naka-jekk dafay doon ay téere yu bari.
Cër yi ëpp solo yi di tax a raññee ab jimbulang , ñeent lañu : Jagleel gi ci am , seenug lëkkaloo , nosiin wi ak mbidiinu jukki yi .
s-5
wo_wtb-ud-train_1394
Cër yi ëpp solo yi di tax a raññee ab jimbulang, ñeent lañu: Jagleel gi ci am, seenug lëkkaloo, nosiin wi ak mbidiinu jukki yi.
Jimbulang yi man nañu a wuute , aju ci seen ëmbiit , man nañu a ubbeeku ci xeeti xameef yépp ( Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa Brëtaañ , ñoo di yi ci gën a siiw ) , walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi , niki ab jimbulangu paj , bu xam-xam walla bu xeltu .
s-6
wo_wtb-ud-train_1395
Jimbulang yi man nañu a wuute, aju ci seen ëmbiit, man nañu a ubbeeku ci xeeti xameef yépp (Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa Brëtaañ, ñoo di yi ci gën a siiw), walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi, niki ab jimbulangu paj, bu xam-xam walla bu xeltu.
Am na it ay jimbulang yu di jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan , diine walla politig wu wenn askan , walla xeet , niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi , Jimbulangu Jewish bi ...
s-7
wo_wtb-ud-train_1396
Am na it ay jimbulang yu di jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan, diine walla politig wu wenn askan, walla xeet, niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi, Jimbulangu Jewish bi...
Yitteey liggéeyi jimbulang moo di jébbal xameef gi ëpp solo gi di dajale ñeel tëriit li .
s-8
wo_wtb-ud-train_1397
Yitteey liggéeyi jimbulang moo di jébbal xameef gi ëpp solo gi di dajale ñeel tëriit li.
Yii liggéey nit yàgg na koo def , dalee lu sori ci taariixam , waaye baatu jimbulang ñu ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu .
s-9
wo_wtb-ud-train_1398
Yii liggéey nit yàgg na koo def, dalee lu sori ci taariixam, waaye baatu jimbulang ñu ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu.
Bépp liggéeyu jimbulang , ci lu leer , ab tënk rekk la ci xameefi nit , te it liggéey bi dafa di soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam .
s-10
wo_wtb-ud-train_1399
Bépp liggéeyu jimbulang, ci lu leer, ab tënk rekk la ci xameefi nit, te it liggéey bi dafa di soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam.
Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi ; ab jimbulang bi ñuy jagleel i gune mooy gën a néew bi ñuy jagleel i mag .
s-11
wo_wtb-ud-train_1400
Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi; ab jimbulang bi ñuy jagleel i gune mooy gën a néew bi ñuy jagleel i mag.
Nosiinu jukki yi am na solo lool , ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb , kon gëstu ci dina yomb .
s-12
wo_wtb-ud-train_1401
Nosiinu jukki yi am na solo lool, ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb, kon gëstu ci dina yomb.
Ci taariix , ñaari xeeti nosiin lañu di jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi : nosiin gu abajada , jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba , beneen bi moo di séddale leen ci ay wàll .
s-13
wo_wtb-ud-train_1402
Ci taariix, ñaari xeeti nosiin lañu di jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi: nosiin gu abajada, jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba, beneen bi moo di séddale leen ci ay wàll.
Nit , dale ci lu yàgg ci ag nekkam , doon na jéem a nos ay xameefam .
s-14
wo_wtb-ud-train_1403
Nit, dale ci lu yàgg ci ag nekkam, doon na jéem a nos ay xameefam.
Li dale ci jamono ju yàgg ja , bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp .
s-15
wo_wtb-ud-train_1404
Li dale ci jamono ju yàgg ja, bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp.
Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu ci a lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia ( taariixu dend bi ) , doonoon ag faramfacce , ci fanweer ak juróom-ñaari téere ñeel dend bi , nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja .
s-16
wo_wtb-ud-train_1405
Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu ci a lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia (taariixu dend bi), doonoon ag faramfacce, ci fanweer ak juróom-ñaari téere ñeel dend bi, nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja.
Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377 , duppee ko Al-Muqaddima ( Taariixu àdduna bi ) , mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi : melosuuf , xeltu , taariix , koom-koom , gëstumboolaay , politig , paj ba ci suqaliku gu sax .
s-17
wo_wtb-ud-train_1406
Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377, duppee ko Al-Muqaddima (Taariixu àdduna bi), mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi: melosuuf, xeltu, taariix, koom-koom, gëstumboolaay, politig, paj ba ci suqaliku gu sax.
Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr Al-Razi , mutasilita bu Al-Kindi ( ci daanaka 270 téere )
s-18
wo_wtb-ud-train_1407
Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr Al-Razi, mutasilita bu Al-Kindi (ci daanaka 270 téere)
Imbratóor bu Siin bi , Cheng-Zu bu Callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle , di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix .
s-19
wo_wtb-ud-train_1408
Imbratóor bu Siin bi, Cheng-Zu bu Callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle, di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix.
Mu ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yi ñu binde ak loxo , lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay .
s-20
wo_wtb-ud-train_1409
Mu ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yi ñu binde ak loxo, lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay.
Yii téere , loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool , boroom alal yi ak niti diine yi rekk ñoo ci doon jot : doonoon nañu ay téere yu seer lool .
s-21
wo_wtb-ud-train_1410
Yii téere, loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool, boroom alal yi ak niti diine yi rekk ñoo ci doon jot: doonoon nañu ay téere yu seer lool.
Edit as list • Text view • Dependency trees