Sentence view
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | test |
---|
Annotation | Dione, Bamba |
---|
Text: -
Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juróom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko.
s-1
wo_wtb-ud-train_131
Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juróom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko.
Ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko.
s-2
wo_wtb-ud-train_132
Ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko.
Bu ko defee mu daldi jël nguur gi.
s-3
wo_wtb-ud-train_133
Bu ko defee mu daldi jël nguur gi.
Ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana.
s-4
wo_wtb-ud-train_134
Ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana.
Waar Jaabi dugg na ci Lislaam, daldi jóg def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit.
s-5
wo_wtb-ud-train_135
Waar Jaabi dugg na ci Lislaam, daldi jóg def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit.
Ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci Lislaam ci Senegaal.
s-6
wo_wtb-ud-train_136
Ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci Lislaam ci Senegaal.
Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi.
s-7
wo_wtb-ud-train_137
Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi.
Li ko waraloon it moo di dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi.
s-8
wo_wtb-ud-train_138
Li ko waraloon it moo di dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi.
Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn).
s-9
wo_wtb-ud-train_139
Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn).
Ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent).
s-10
wo_wtb-ud-train_140
Ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent).
Ci mujjug xarnub fukk ak juróom la Koli Tingala jóg xeex Tukulóor yi, daldi tembal ay goxam, taxawal nag nguur gu yees, mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko.
s-11
wo_wtb-ud-train_141
Ci mujjug xarnub fukk ak juróom la Koli Tingala jóg xeex Tukulóor yi, daldi tembal ay goxam, taxawal nag nguur gu yees, mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko.
Ci xarnub fukk ak juróom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom: Jolof, Kajoor.
s-12
wo_wtb-ud-train_142
Ci xarnub fukk ak juróom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom: Jolof, Kajoor.
Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarloo ak cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi.
s-13
wo_wtb-ud-train_143
Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarloo ak cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi.
Ci atum 1770 g.j, la ag fippu am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daldi daaneel njabootug Deñanke.
s-14
wo_wtb-ud-train_144
Ci atum 1770 g.j, la ag fippu am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daldi daaneel njabootug Deñanke.
Bu ko defee, Baal jël Lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale.
s-15
wo_wtb-ud-train_145
Bu ko defee, Baal jël Lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale.
Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan.
s-16
wo_wtb-ud-train_146
Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan.
Moom lañu di jàppe ki njëkk a doon Yilimaan.
s-17
wo_wtb-ud-train_147
Moom lañu di jàppe ki njëkk a doon Yilimaan.
Edit as list • Text view • Dependency trees