Sentence view
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | dev |
---|
Annotation | Dione, Bamba |
---|
Text: -
Ci xarnub fukk ak juróom Bawol nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi.
s-1
wo_wtb-ud-train_1
Ci xarnub fukk ak juróom Bawol nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi.
Bu ko defee, ag njaboot gu am ag jegeñaale ak buuri Kajoor yi daan ko jiite.
s-2
wo_wtb-ud-train_2
Bu ko defee, ag njaboot gu am ag jegeñaale ak buuri Kajoor yi daan ko jiite.
Bu jëkk, nguur googu, ay socé ak ay séeréer, ñoo ko yoroon.
s-3
wo_wtb-ud-train_3
Bu jëkk, nguur googu, ay socé ak ay séeréer, ñoo ko yoroon.
Ndax Bawol, benn dex la woon foofu ci lu doog a am.
s-4
wo_wtb-ud-train_4
Ndax Bawol, benn dex la woon foofu ci lu doog a am.
Boobu jamono, Bawol, amoon na ndox mu bare.
s-5
wo_wtb-ud-train_5
Boobu jamono, Bawol, amoon na ndox mu bare.
Ci cosaan, dañu ne, Bawol, ku fa jëkk a nekk buur, Xaayamagaan moo doon turam.
s-6
wo_wtb-ud-train_6
Ci cosaan, dañu ne, Bawol, ku fa jëkk a nekk buur, Xaayamagaan moo doon turam.
Xaayamagaan, ci làkku socé yi la soqeekoo, moo di: buuru gaalam.
s-7
wo_wtb-ud-train_7
Xaayamagaan, ci làkku socé yi la soqeekoo, moo di: buuru gaalam.
Ñoom, socé yi fa nekkoon jamono boobu, seen mamm, Mande lañu baawoo.
s-8
wo_wtb-ud-train_8
Ñoom, socé yi fa nekkoon jamono boobu, seen mamm, Mande lañu baawoo.
Ba pare, séeréer yi ñëw.
s-9
wo_wtb-ud-train_9
Ba pare, séeréer yi ñëw.
Ñoom, Fuuta Tooro lañu jóge woon, gàdday ba Bawol, ndax jiyaar ji Muraabituun yi defoon foofu.
s-10
wo_wtb-ud-train_10
Ñoom, Fuuta Tooro lañu jóge woon, gàdday ba Bawol, ndax jiyaar ji Muraabituun yi defoon foofu.
Ba ñu agsi Bawol, ci ubbite, dañu daan dëkkandoo ak socé, soog a leen daq.
s-11
wo_wtb-ud-train_11
Ba ñu agsi Bawol, ci ubbite, dañu daan dëkkandoo ak socé, soog a leen daq.
Ba loolu amee, ñu yilif dëkk boobu.
s-12
wo_wtb-ud-train_12
Ba loolu amee, ñu yilif dëkk boobu.
Ci séeréer yi, askan yi ñu faloon, ñoo doon ñi sant Juuf, Ngom, Caw.
s-13
wo_wtb-ud-train_13
Ci séeréer yi, askan yi ñu faloon, ñoo doon ñi sant Juuf, Ngom, Caw.
Te buur ba ñu daan taan ci ñoom, 'Téeñ' lañu ko daan tudde.
s-14
wo_wtb-ud-train_14
Te buur ba ñu daan taan ci ñoom, 'Téeñ' lañu ko daan tudde.
Loolu moo amoon, laata nguuru Jolof ñëw uuf dëkk bi.
s-15
wo_wtb-ud-train_15
Loolu moo amoon, laata nguuru Jolof ñëw uuf dëkk bi.
Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawol ci jenn jamono ji.
s-16
wo_wtb-ud-train_16
Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawol ci jenn jamono ji.
Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam.
s-17
wo_wtb-ud-train_17
Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam.
Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk dafa bëgg a yilif ga ca des.
s-18
wo_wtb-ud-train_18
Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk dafa bëgg a yilif ga ca des.
Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug ki di wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def.
s-19
wo_wtb-ud-train_19
Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug ki di wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def.
Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi.
s-20
wo_wtb-ud-train_20
Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi.
Mbooleem kuréel yi nag daa nañu fa àttewoo (kuréelug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, boroom mecce yi ak jigéen ñi).
s-21
wo_wtb-ud-train_21
Mbooleem kuréel yi nag daa nañu fa àttewoo (kuréelug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, boroom mecce yi ak jigéen ñi).
Bokkug Bawol ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ci ay suufam.
s-22
wo_wtb-ud-train_22
Bokkug Bawol ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ci ay suufam.
Moom kay dafa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi.
s-23
wo_wtb-ud-train_23
Moom kay dafa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi.
Edit as list • Text view • Dependency trees