Sentence view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev
AnnotationDione, Bamba

Text: -

[1] tree
Suuxat sa yaram
s-1
wo_wtb-ud-train_1324
Suuxat sa yaram
[2] tree
Suuxat sa yaram, suuxat sa am xel ni mu ware: caabi ji la di ubbil jàmmu yaram
s-2
wo_wtb-ud-train_1325
Suuxat sa yaram, suuxat sa am xel ni mu ware: caabi ji la di ubbil jàmmu yaram
[3] tree
Mbokk, OSAD a la tekkil dénkaane yii tukkee ci Profesëer Amadu Galo Jóob.
s-3
wo_wtb-ud-train_1326
Mbokk, OSAD a la tekkil dénkaane yii tukkee ci Profesëer Amadu Galo Jóob.
[4] tree
Ci gis-gisam, warees na leen a jàppe ni ab bagaan bu def ay taxañ, ku ne ñëw jël taxañ yi méngoo ak tolluwaayu yaramam, fekk diisoo na ci ak doktooram.
s-4
wo_wtb-ud-train_1327
Ci gis-gisam, warees na leen a jàppe ni ab bagaan bu def ay taxañ, ku ne ñëw jël taxañ yi méngoo ak tolluwaayu yaramam, fekk diisoo na ci ak doktooram.
[5] tree
Bu la ndékki raw.
s-5
wo_wtb-ud-train_1328
Bu la ndékki raw.
[6] tree
Bul yem rekk ci meew, kafe mbaa dute ak yu ni mel.
s-6
wo_wtb-ud-train_1329
Bul yem rekk ci meew, kafe mbaa dute ak yu ni mel.
[7] tree
Jëlal ndékki lu am solo, mburu, ñoom fonde ak yu ni mel, naan yu tàng mbaa yu sedd yu am suukar (su fekkee ne terewuñu la suukar), mbaa ay meññet, mbaa ndoxum meññet añs.
s-7
wo_wtb-ud-train_1330
Jëlal ndékki lu am solo, mburu, ñoom fonde ak yu ni mel, naan yu tàng mbaa yu sedd yu am suukar (su fekkee ne terewuñu la suukar), mbaa ay meññet, mbaa ndoxum meññet añs.
[8] tree
Taamul di naan laata waxtu lekk jot, dafa di tax doo xiif bu baax, su ko defee doo lekk lu bare;
s-8
wo_wtb-ud-train_1331
Taamul di naan laata waxtu lekk jot, dafa di tax doo xiif bu baax, su ko defee doo lekk lu bare;
[9] tree
Loolu baax na ci ki ñu digal lu wàññi yaramam.
s-9
wo_wtb-ud-train_1332
Loolu baax na ci ki ñu digal lu wàññi yaramam.
[10] tree
Su fekkee ne danga lekk ba noppi, bëgg a naan ci saa si, jàppal lii: lekk lu tàng, naan lu tàng.
s-10
wo_wtb-ud-train_1333
Su fekkee ne danga lekk ba noppi, bëgg a naan ci saa si, jàppal lii: lekk lu tàng, naan lu tàng.
[11] tree
Lu ko moy, xaaral ñaar-fukki minit (20), gën jaa néew, nga sog a naan lu sedd.
s-11
wo_wtb-ud-train_1334
Lu ko moy, xaaral ñaar-fukki minit (20), gën jaa néew, nga sog a naan lu sedd.
[12] tree
Su nga yeewoo rekk, daldil naan ndox;
s-12
wo_wtb-ud-train_1335
Su nga yeewoo rekk, daldil naan ndox;
[13] tree
Bu loolu wéyee, nga naan lu mu néew néew 1 liitaru ndox ci bëccëg bi.
s-13
wo_wtb-ud-train_1336
Bu loolu wéyee, nga naan lu mu néew néew 1 liitaru ndox ci bëccëg bi.
[14] tree
Loolu dafa di yeesal ndox mi ci sa yaram (lu ëpp juróom-ñaar-fukk ci téeméer 70 % ndox la), su ko defee mu aar la ci sank, maanaam seere.
s-14
wo_wtb-ud-train_1337
Loolu dafa di yeesal ndox mi ci sa yaram (lu ëpp juróom-ñaar-fukk ci téeméer 70 % ndox la), su ko defee mu aar la ci sank, maanaam seere.
[15] tree
Lée-lée, nanga amal subas ndox, maanaam nga naan benn liitaru ndox, lu jiitu ndékki.
s-15
wo_wtb-ud-train_1338
Lée-lée, nanga amal subas ndox, maanaam nga naan benn liitaru ndox, lu jiitu ndékki.
[16] tree
Ngir aar sa bopp ci kolesterol, moytul ñam yu ñu fiiriir mbaa saaf ci diwlin, taamul ñam yi ñu baxal, mbaa tay, mbaa lakk, mbaa dugal ci fuur, mbaa yu ñu toggul niki salaatu tamaate, karoot ju ñu joos ak yu ni mel.
s-16
wo_wtb-ud-train_1339
Ngir aar sa bopp ci kolesterol, moytul ñam yu ñu fiiriir mbaa saaf ci diwlin, taamul ñam yi ñu baxal, mbaa tay, mbaa lakk, mbaa dugal ci fuur, mbaa yu ñu toggul niki salaatu tamaate, karoot ju ñu joos ak yu ni mel.
[17] tree
Moytul soos yi ak yu niin yi, ak limonaat yi, ak ngato yi, ak yàpp yu xonq yi, ak biiru nag yi ak xar yi, ak sosisoŋ yi ak yu ni mel.
s-17
wo_wtb-ud-train_1340
Moytul soos yi ak yu niin yi, ak limonaat yi, ak ngato yi, ak yàpp yu xonq yi, ak biiru nag yi ak xar yi, ak sosisoŋ yi ak yu ni mel.
[18] tree
Taxawal temm ba kenn du def safal yi xew, moo xam ay kibb lañu walla sunguf su ñuy suy ci togg gi.
s-18
wo_wtb-ud-train_1341
Taxawal temm ba kenn du def safal yi xew, moo xam ay kibb lañu walla sunguf su ñuy suy ci togg gi.
[19] tree
Deel lekk lujum ak meññet, ganaar ak yi mu xeetool, jën ak yeneen yi di dund ci géej.
s-19
wo_wtb-ud-train_1342
Deel lekk lujum ak meññet, ganaar ak yi mu xeetool, jën ak yeneen yi di dund ci géej.
[20] tree
Deel teel a reer, na doon ñam yu woyof te bañ a saf xorom.
s-20
wo_wtb-ud-train_1343
Deel teel a reer, na doon ñam yu woyof te bañ a saf xorom.
[21] tree
Moytul di dolli xorom ci ñam wi.
s-21
wo_wtb-ud-train_1344
Moytul di dolli xorom ci ñam wi.
[22] tree
Bul reere lu am xorom, su fekkee ne danga am tasyoŋ mbaa mu am ñu ko am ci njaboot gi.
s-22
wo_wtb-ud-train_1345
Bul reere lu am xorom, su fekkee ne danga am tasyoŋ mbaa mu am ñu ko am ci njaboot gi.
[23] tree
Naan yu tàng: kenkiliba, àttaaya ju am limoŋ mbaa naanaa, kafe gu woyof, meew...
s-23
wo_wtb-ud-train_1346
Naan yu tàng: kenkiliba, àttaaya ju am limoŋ mbaa naanaa, kafe gu woyof, meew...
[24] tree
Naan yu sedd: na la ndoxum meññet yi fi fekk baax gënal limonaat yi ak yu ni mel, yi ñu di jaay ci bitig yi.
s-24
wo_wtb-ud-train_1347
Naan yu sedd: na la ndoxum meññet yi fi fekk baax gënal limonaat yi ak yu ni mel, yi ñu di jaay ci bitig yi.
[25] tree
Su fekkee ne danga am mbokk mu am jabet: defal suukar su yem, mbaa nga jëfandikoo wuutalu suukar te bañ ci a xér.
s-25
wo_wtb-ud-train_1348
Su fekkee ne danga am mbokk mu am jabet: defal suukar su yem, mbaa nga jëfandikoo wuutalu suukar te bañ ci a xér.
[26] tree
Ñam yii fàww nga lekk leen: dugub, ceeb, xeeti màkkaróoni, mburu, ñàmbi ak yu ni mel, pombiteer...
s-26
wo_wtb-ud-train_1349
Ñam yii fàww nga lekk leen: dugub, ceeb, xeeti màkkaróoni, mburu, ñàmbi ak yu ni mel, pombiteer...
[27] tree
Li ci gën nag, moo di ñu baxal leen mbaa ñu tay leen.
s-27
wo_wtb-ud-train_1350
Li ci gën nag, moo di ñu baxal leen mbaa ñu tay leen.
[28] tree
Su dee ku ànd ak jabet, mbaa metitu biir, mbaa ku am yaram lool, bumu ci xér.
s-28
wo_wtb-ud-train_1351
Su dee ku ànd ak jabet, mbaa metitu biir, mbaa ku am yaram lool, bumu ci xér.
[29] tree
Moytul lekk ba biir bi fees dell te moytu yit di lekkantu ci diggante ndënale yi.
s-29
wo_wtb-ud-train_1352
Moytul lekk ba biir bi fees dell te moytu yit di lekkantu ci diggante ndënale yi.
[30] tree
Yëngal sa yaram lu war la.
s-30
wo_wtb-ud-train_1353
Yëngal sa yaram lu war la.
[31] tree
Kenn waxul nga xéy suba di daw ak a maaj, sonn ci lool, yemale ko fa ba jëmmi jamono;
s-31
wo_wtb-ud-train_1354
Kenn waxul nga xéy suba di daw ak a maaj, sonn ci lool, yemale ko fa ba jëmmi jamono;
[32] tree
Loolu du la amal njariñ.
s-32
wo_wtb-ud-train_1355
Loolu du la amal njariñ.
[33] tree
Li gën moo di saxoo di yëngal sa yaram, lu mu néew-néew ñetti yoon ci ayu-bés bi, mën na a doon dox, lagg-laag maanaam daw yu yemamaay, féey, biskalet añs., lu tollu ci fanweeri minit jëm benn waxtu, lépp nag tolloo ak li nga àttan.
s-33
wo_wtb-ud-train_1356
Li gën moo di saxoo di yëngal sa yaram, lu mu néew-néew ñetti yoon ci ayu-bés bi, mën na a doon dox, lagg-laag maanaam daw yu yemamaay, féey, biskalet añs., lu tollu ci fanweeri minit jëm benn waxtu, lépp nag tolloo ak li nga àttan.
[34] tree
Bul tóx, moytul garabu yoo gi ñu di jafal mu di saxaar, naka noonu garab yi di rey gunóor.
s-34
wo_wtb-ud-train_1357
Bul tóx, moytul garabu yoo gi ñu di jafal mu di saxaar, naka noonu garab yi di rey gunóor.
[35] tree
Sàngara yit mat naa moytu.
s-35
wo_wtb-ud-train_1358
Sàngara yit mat naa moytu.
[36] tree
Jëlal sa matukaay ba mën a nelaw bu baax, lu mu néew-néew juróom-benni waxtu (6 w).
s-36
wo_wtb-ud-train_1359
Jëlal sa matukaay ba mën a nelaw bu baax, lu mu néew-néew juróom-benni waxtu (6 w).
[37] tree
Ngir suuxat sam xel, gannaaw nelaw yu mucc ayib yi nu wax léegi, yokkal sa xam-xam, mu doon ci bëccëg bi, ngay bind ak a jàng, tàggat sa bopp ci tari loo jàngoon, nettali lu nga mas a dégg ak yu ni mel, boole ci ay po yuy tàggat sam xel añs.
s-37
wo_wtb-ud-train_1360

Edit as listText viewDependency trees