wo-wtb-train-xibaaryi-tabaski

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Tabaski Sunna la su far ci ab jullit. Tëbëski mooy ñaareelu iid (bër) ci Lislaam ginnaaw bu Korite jàllee. Jële nanu ci Anas (gërëmul Yàlla ci moom) mu ne: Bi Yonent (Yalla na jàmmi Yàlla nekk ci moom) bi yegsee Madiina fekkee na leen ñaari bis ñu ca daan caaxaan ak a fo. Mu ne leen: Ana lu di ñaari bis yii? Ñu ne: Danu ci daan fo (caaxaan) ci jamonoy ceddo (jaahiliya). - Yonent bi ne leen: Yàlla jox na leen ñaari bis yu gën yooyu ñaar, ñu di bisu Tabaski ak bisu Kori (Abuu Daawud soloo na ko).

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees