wo-wtb-train-xibaaryi-porograam-xeex-sibiru

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 13

Lesoleil: Gàawu 11 awril 2009 Porogaraam biy xeex sibbiru ci réew mi te tudd PNLP, ci jàppleg ñi muy jëflanteel, yeesal na xam-xamu 51 njiiti doktoori gox yi ak seen i toftal, ci pexe yu bees yi ñu tëral ngir xeex sibbiru, ci ñaari lël. Ñaareelu lël bi, jëm ci njàngale ñeel sibbiru ak xeex bi mu laaj, dajale na 26 doktoor. Lël boobu mu ngi tàmbali ci 16 màrs ci Daaray Wér (ISED) tëj ci 4 awril 2009, ci njiitéefu Dr Asan Yaradu, kenn ci ñi di xelal njawriñu wér ak fàggutéef. Doktoor Pàppa Muusaa Coor miy saytu PNLP xamle na ne njàngale mii ñu sumb mu ngi bokk ci pexe yi ñu tëral ngir sibbiru ak dee yi muy jur bañ a jéggi tolluwaay bi mu nekk jamono yii. Ndax gisees na ne tolluwaay bi dafay gën di wàññiku te li ko waral moo di pexe yi ñu tëral ngir xeex jàngoro ji.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees