wo-wtb-train-xibaaryi-microsoft-siiwalug

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 14

Microsoft: Siiwalug Windows Phone 7 Microsoft dellusi na ci ag woote ak ab gaaral bu ràññeeku altine ci lu aju ci telefonam bi ñépp di xaar Windows Phone 7 ànd ak defar Nosteg Doxiin (operating system) bu bees tàq ñeel Mobiil. Doorees na ag gaaralu Windows Phone 7 ca New York. Gaaral googu njiitul Microsoft Stef Balma moo ko jiite, ngir wone ni seen nosteg doxiin bu bees bi dafa nekk lu taaru te yéeme. Ku nekk war naa man a seet Windows Phone te wax ni man na maa teewal la Balma wax. Ci loolu, joyalees na siiwalug Windows Phone jëmmalug man-mani telefon bi ak ay leeral ci juumtukaay yi ci nekk.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees