wo-wtb-test-wol-wiki-Lebu

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Lebu, mooy benn waaso nekk ci reewum Senegaal. Ñoom, Ndakaaru moo di seen dëkk, nu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint-Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur, ci wetu geej ak tefes. Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan. Seen làkk di wolof. Seen wolof dafa xaw a wuute tuuti ak wolof bi ñeneen ñi di làkk. Am na ñu ne, lebu yi ñoo sos làkk wolof.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees