wo-wtb-test-wol-wiki-Fuuta-Tooro

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juróom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko. Ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko. Bu ko defee mu daldi jël nguur gi. Ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana. Waar Jaabi dugg na ci Lislaam, daldi jóg def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit. Ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci Lislaam ci Senegaal.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees