wo-wtb-dev-xibaaryi-poroxaan-2011

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 17

Poroxaan 2011: Soxna Jaara Mariyama Buso royukaayu jigéenu jullit Soxna Mariyaama Buso ñu koy dàkkantale, ci jikko, Jaaratu-l-Laah (dëkkandoob Yàlla bi) gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta, génn àdduna ci atum 1866 ca Poroxaan. Soxna Jaara Buso mom Sëriñ Hamaat Buso (baayam) ak Soxna Asta Waalo Mbàkke (yaayam), cosaano ci askanu Sëriif goo xam ne calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ci ñoom). Mu dondoo ci loolu ag cell ak ab yar ba war ci doomi soxna jële ko ci waajuram wu jigéen. Soxna Asta Waalo Mbàkke doon ab jàngalekatub Alxuraan ak xam-xamu diine di yare ci Lislaam rawatina ci Tassawuuf, mu juddu ci loolu. Yaayam ju farlu jooju yar ko ci.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees