wo-wtb-dev-xibaaryi-napp-j__n
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | dev |
---|
View options
Text: - Show: - Tags:
Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
-
Milyoη ak 450 junni ay toni jën ñoo di jaar at mu nekk ci géeji Senegaal yi. Jëwriñ ji yor Koomug Géej gi, Xureysi Caam jibal na ne at mu jot 1 Milyoη ak 450 junni ay toni jëni biir géej dinañu di jóge géeju Kap-weer jaar ci sunu géej yi. Xureysi Caam mi doon àddu ci surnaalu 12 w bu Rfm, leeral na ne jën yooyu dañuy njëkke jaar Giné-Bisaaw, Gàmbi, Senegaal, Moritani, Marok door a dëppaat. Bu ñu egsiwaatee Moritani, te nappeesu leen, dañuy dee. Teg na ci ne: am na 1 milyoη ak 450 junni ay ton yu doomi réew mi mënul a napp, ndax amuñu jumtuwaay yu ko mën a napp. Jëwriñ jee ngi laaj: Ku di napp toni jën yooyu?
Download XML • Download text
• Sentence view • Dependency trees