wo-wtb-dev-xibaaryi-luwaa-ndaamar-senegaal

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 11

Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yi di dugg Senegaal te di jóge bitim-réew war a am. Mu ngi ko dogale ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru. Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare 2012-444 soppi bu 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi. Dekkare boobu dafa di tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yi di duggu Senegaal war a am. S. Sàll dige woon na ci baatum dagaan ne dina ko def bu ñu ko tegee ci boppu réew mi. Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees