wo-wtb-dev-xibaaryi-alliance-panafricaniste

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev

Javascript seems to be turned off, or there was a communication error. Turn on Javascript for more display options.

index sentence 1 - 6 > sentence 7 - 13

Li gën ci li nit njëkk a amal ci wàllug xam-xam mu ngi xewe ci Goxub Afrig. Ci lu gën a leer, ca Isipt gu yàgg ga la nit ku ñuul yóbboo ag nite (l'humanité) ba àggale ko ci xam-xam. Booba la joxee firnde ci ne xam-xam du moomeelug wenn xeet, du caagéenu benn gox. Gëstu yu boroom xam-xam bii di doomu Senegaal, di Seex Anta Jóob, maye nañu manees a saxal am-amu xam-xam bii di 'xeetu nit benn la'. Ñoo bokk fu ñu bawoo, te xayug nit ku ñuul (la civilisation négre) moo jiitu ci xay yi. Taariix mu ngi nuy jàngal ne xam-xam ak xarala dañoo gàddaay dem ca goxub Tugal, jaare ko ca Geres.

Download XMLDownload textSentence viewDependency trees