Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Tambaakundaa, 2 awril (APS)
s-2 Tàmbaakundaa: taxawal ay wanagi wowal, ngir doomi jàngoro yi bañ a ayibal ndoxum teen yi ak yu ni mel.
s-3 Sàntar bi di saytu kàttanu jant bi ak cet, te nekk ci Tàmbaakundaa samp na ay wanagi wowal.
s-4 Xeetu wanag woowu nag mbeeste la, dees ko di tabax ci taxawaayu benn meetar walla lu ko ëpp, mu lëkkaloo ak ñaari pax.
s-5 Benn bi def sobe si (puup yi), fekk am na pexe mu leen nal ba ñu wow, ñu def leen tos.
s-6 Beneen bii def saw mi ak ndoxum laablu mi, ñu suuxate ko flëer yi.
s-7 Njariñ li mën a tukkee ci xeetu wanag wii bari na, ndax lépp la ñuy jëfandikoowaat, day yi, saw mi ak yi ci ànd, rax-ci-dolli dafay yaxanal ndox, indi cet.
s-8 Loolu la Abdukariim Saane xamle, moo sos sàntar bi te yit moo jiite mbootaayu xariti Tàmbaakundaa.
s-9 Mbir mi nag dafa laaj toppatoo ak yeete bu yaatu jëmale ko ci nit ñi.
s-10 Nit ku nekk, war ngaa yar sa bopp ngir sàmmoonteek fàggutéef yi ci aju, ndax yar boobu bu amul, doomi jàngoro yi dañuy tasaaroo.
s-11 Su ko defee dañuy ayibal ndox mi ci biir suuf si, niki ndoxum teen yi ak yu ni mel.
s-12 Looloo waral jamono yi weesu, waa sàntar bi liggéey ak waa Serwiis Diiseen, ngir gëstu day yi.
s-13 Su ko defee ñu ràññee xeeti jàngoro yi ba xam ndax mënees na leen a tose gàncax gi.
s-14 Abdu Kariim Saane ñaawlu na li waa dëkk bi tàmm a def: bale biir kër gi ba mu set, waaye bàyyi mbalit mi ci buntu kër gi.
s-15 Ci wàllu cet gi ba tey, sàntar baa ngi di seet na muy def ba teqale mbalit mi, boole li mën a ànd, ber yi ci des.
s-16 Mu ngiy xalaat it defar ay mbuusi ndimo, ñu wuutu mbuusi plastig yi.
s-17 Loolu dafa laaj ñépp xàccandoo, bokk liggéey bi, ndax sàntar bi moom rekk mënul a def lépp.
s-18 Ci ag pàttali, ci mbënnum 1998 lañu sosoon sàntar bi, nga xam ne ñu bari dañu ñàkkoon seen kër.
s-19 Ñu fat leen ci lekkool Saada Maka Si.
s-20 Sàntar bi am ñu mu ci dalal.
s-21 Ñu faf ko def bérébu sotteente xalaat.
s-22 Li ñu ci jublu woon moo di xalaat ci mbir yi leen soxal, sukkandiku ci lekkool yi, ngir tasaare xam-xam ci wàllu tabaxinu ban, ak kàttanu jant bi, ak cet, ak yeneen i ponk.
s-23 Ndongo yi ñoo waroon a siiwal xam-xam boobu ci biir njaboot gi.
s-24 Yokk jëf yi nga xam ne kenn nàttablewul seen njariñ ci xeex sibbiru

Text viewDownload CoNNL-U